57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
58 | GEN 3:2 | Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. |
60 | GEN 3:4 | Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! |
62 | GEN 3:6 | Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk. |
68 | GEN 3:12 | Aadama ne ko: «Jigéen, ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
209 | GEN 9:3 | Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax. |
300 | GEN 12:1 | Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won, |
314 | GEN 12:15 | Jaraafi Firawna itam gis ko, di ko kañ ca Firawna ndax taar ba, ñu daldi ko yóbbu ca kër Firawna. |
336 | GEN 13:17 | Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.» |
358 | GEN 14:21 | Gannaaw loolu buurub Sodom wax Ibraam ne ko: «Jox ma nit, ñi nga jàpp, te nga fab alal ji.» |
370 | GEN 15:9 | Aji Sax ji ne ko: «Jëlal wëlluw ñetti at ak bëyu ñetti at ak kuuyu ñetti at, boole ci pitaxu àll ak xati mu ndaw.» |
411 | GEN 17:13 | Jaam bu juddoo sa kër ak boo jënd, ñoom ñaar ñépp, dees leen wara xarfal. Xaraf ay màndargaal sama kóllëre ci seen yaram, muy kóllëre gu sax fàww. |
495 | GEN 19:37 | Taaw ba am ca doom ju góor, tudde ko Mowab (mu firi Jóge ci baay). Mowab moo sos Mowabeen ñi. |
536 | GEN 21:22 | Jamono yooyu Abimeleg àndoon na ak Pikol kilifay xarekatam, dem ci Ibraayma ne ko: «Gis naa ne Yàlla ànd na ak yaw, di àntal li ngay def lépp. |
544 | GEN 21:30 | Ibraayma ne ko: «Jëlal xar yii ci sama loxo, muy firnde ne man maa gas teen bii.» |
606 | GEN 24:14 | Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.» |
620 | GEN 24:28 | Janq bi nag daw dem, nettali waa kër yaayam la xew lépp. |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
728 | GEN 26:35 | Jigéen ñooñu mu jël nag di naqar wu réy ci Isaaxa ak Rebeka. |
747 | GEN 27:19 | Yanqóoba ne baayam: «Mana Esawu sa taaw. Def naa li nga ma wax. Jógal toog te lekk ci li ma la rëbbal, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» |
749 | GEN 27:21 | Isaaxa ne Yanqóoba: «Jegesil, ma làmb la, ba mu wóor ma ne sama doom Esawoo.» |
753 | GEN 27:25 | Isaaxa ne ko: «Jottli ma fii ma lekk ci sam rëbb, doom, ba ñaanal la ci sama xol.» Yanqóoba jottli Isaaxa ndab li, mu lekk, daldi koy may biiñ, mu naan. |
759 | GEN 27:31 | Mu togg moom it, ba mu neex, indil baayam. Mu ne ko: «Jógal baay, lekk ci sa rëbbum doom, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
803 | GEN 29:7 | Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!» |
817 | GEN 29:21 | Loolu wéy, Yanqóoba ne Laban: «Jox ma sama jabar, ma séetal ko, ndax àpp bi jot na.» |
844 | GEN 30:13 | Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte). |
913 | GEN 31:39 | Jur gu rab fàdd sax ma féetewoo, waaye masuma la koo indil. Mboolem lu ñu sàcc guddi ak lu ñu sàcc bëccëg, danga ma ko daa feyu. |
917 | GEN 31:43 | Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? |
922 | GEN 31:48 | Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede). |
926 | GEN 31:52 | Jal bi seede la, doj wi di seede ne duma jéggi jal bi, jublu ci yaw, te yaw itam doo jéggi jal bi mbaa doj wi, jublu ci man, te naraluloo ma jàmm. |
945 | GEN 32:17 | Dafa ber gétt yi, gu ci nekk mu jox ay surgaam, ne leen: «Jiituleen ma, te na gétt yi dàndante.» |
967 | GEN 33:6 | Jaam ya ak seeni doom daldi jegesi, sujjóotal ko. |
975 | GEN 33:14 | Jiitu ma rekk, sang bi, man ma topp ndànk ci wewu jur gi, jiital leen, te baña raw xale yi, ba kera ma lay fekksi Seyir.» |
976 | GEN 33:15 | Esawu ne ko: «Xaaral ma bàyyee la ñenn ci góor, ñi ma àndal.» Yanqóoba ne ko: «Matu ko. Boobu teraanga ëpp na, sang bi. Jàmm ji nga ma dalal rekk doy na.» |
1013 | GEN 35:1 | Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.» |
1014 | GEN 35:2 | Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu. |
1063 | GEN 36:22 | Doomi Lotan yu góor ya nag ñooy Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna. |
1101 | GEN 37:17 | Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: “Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa. |
1112 | GEN 37:28 | Julay Majan ya nag jaare fa, ñu yóotu Yuusufa, génne ko kàmb ga, jaay ko Ismayleen ña ci ñaar fukki dogi xaalis. Ñu yóbbu Yuusufa Misra. |
1137 | GEN 38:17 | Mu ne ko: «Dinaa jël bëy wu ndaw ca sama gétt, yónnee la.» Mu ne ko: «Jox ma lenn looy tayle, ba kera ngay yónnee.» |
1167 | GEN 39:17 | mu nettalee ko ko noonu ne ko: «Jaamu ebrë, bi nga indi ci kër gi de, da maa fekksi, di ma sàkku. |
1182 | GEN 40:9 | Jawriñ bay topptoo naanu buur daldi nettali géntam Yuusufa, ne ko: «Ci gént gi, garabu reseñ laa gis ci sama kanam, |
1222 | GEN 41:26 | Juróom ñaari nag yu baax yi, juróom ñaari at la. Te it juróom ñaari gub yu baax yi, juróom ñaari at la. Muy genn gént gi. |
1314 | GEN 43:23 | Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko. |
1342 | GEN 44:17 | Mu ne leen: «Jomb naa loolu. Ki ñu fekk kaas bi ci loxoom mooy doon sama jaam; ñi ci des dellu ca seen baay ci jàmm.» |
1363 | GEN 45:4 | Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra. |
1436 | GEN 47:15 | Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» |
1498 | GEN 49:24 | Teewul xalaam ga di wéye daŋ, te la loxo yay dëgërloo mooy loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba, kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil, |
1556 | EXO 2:1 | Jenn waay ju bokk ci giirug Lewi nag moo jëloon janq bu mu bokkal giir. |
1627 | EXO 4:25 | Soxnaam Sipora jël paaka bu ñu yette doj, dog mbuñukam doomam, laalale ko ca tànkam, ne ko: «Jëkkër ju ñuy jote deret de laa am.» |
1695 | EXO 7:9 | «Bu leen Firawna waxee ne leen: “Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: “Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.» |
1705 | EXO 7:19 | Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko: “Jëlal saw yet, te tàllal sa loxo tiimale ko ndoxi Misra, muy seeni dex ak seen yooni ndox ak seeni déeg ak fépp fu ndox taa, mu ànd soppliku deret.” Deret ja dina daj Misra gépp, ba ca këll yaak njaq ya.» |
1833 | EXO 12:16 | Bés bu jëkk bi nangeen ci amal ndaje mu sell. Juróom ñaareelu bés ba itam nangeen ca amal ndaje mu sell; deesul liggéey lenn ci yooyu bés, lu moy ngeen togg ñam wu ñépp lekk. Loolu doŋŋ lees ciy mana def. |
1935 | EXO 15:14 | Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti, |
1974 | EXO 16:26 | Juróom benni fan ngeen koy for, waaye bésub juróom ñaareel bay bésub Noflaay, kenn du ko gis.» |
1986 | EXO 17:2 | Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» |
1991 | EXO 17:7 | Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?» |
2061 | EXO 20:9 | Juróom benni fan ngeen wara liggéey, def ci seen soxla yépp. |
2080 | EXO 21:2 | «Su ngeen jëndee jaam bu góor bu dib Ebrë, na liggéey juróom benni at. Juróom ñaareel ba lay moom boppam te du ameel kenn dara. |
2144 | EXO 22:29 | Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko. |
2170 | EXO 23:25 | Jaamuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir. |
2199 | EXO 25:3 | Jooxe bi ngeen di nangoo ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, |
2228 | EXO 25:32 | Juróom benni car ñooy soqikoo ca wet ya, ñetti car ci gii wet, ñett ca ga ca des. |
2241 | EXO 26:5 | Juróom fukki takku ngay def ci catal benn sor bi, ak juróom fukki takku ci catal sor, bi jeexal taqalante bi ci des, te na takku yi yemoo. |
2283 | EXO 27:10 | Jëni jaamookaay bi ñaar fukk lay doon, seen ñaar fukki tegu di xànjar, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis. |
2290 | EXO 27:17 | «Jën ya wër ëtt ba yépp, dees koy lëkklee galan yu xaalis, wékkukaayi jën yi di xaalis, seeni tegu di xànjar. |
2350 | EXO 29:13 | Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi. |
2356 | EXO 29:19 | «Jëlal kuuy mi ci des, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ci boppu kuuy mi. |
2436 | EXO 31:15 | Juróom benni fan lees wara liggéey, waaye bésub Noflaay bay juróom ñaareel ba, bés bu sell la, bésub Noflaay bu mat sëkk, ñeel Aji Sax ji. Képp ku liggéey bésub Noflaay, dee rekk mooy àtteem. |
2447 | EXO 32:8 | Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”» |
2469 | EXO 32:30 | Ca ëllëg sa Musaa ne mbooloo ma: «Yeen de bàkkaar ngeen bàkkaar bu réy, waaye maa ngi nii di yéeg, jëm ci Aji Sax ji. Jombul ma jotul leen seen bàkkaar.» |
2500 | EXO 34:3 | Bu kenn ànd ak yaw, te bu kenn xand fenn kaw tund wi. Jur gi sax bumu forsi ci suufu tund wi, du gu gudd, du gu gàtt.» |
2506 | EXO 34:9 | ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.» |
2518 | EXO 34:21 | «Juróom benni fan nag ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, dal-luleen. Bu ngeen doon bey, bu ngeen doon góob, dal-luleen. |
2534 | EXO 35:2 | Juróom benni fan lees di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, seen bésub Noflaay bu sell bu mat sëkk la, ñeel Aji Sax ji. Képp ku ci liggéey lenn, dees koy rey. |
2579 | EXO 36:12 | Juróom fukki takku lañu ñaw ci benn sor bi, ak juróom fukki takku ci catal sor bi jeexal taqalante bi ci des, takku yi yemoo. |
2623 | EXO 37:18 | Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des. |
2653 | EXO 38:19 | Jëni lafu bunt bi ñeent la, seen ñeenti tegu di xànjar, seeni wékkukaay di xaalis, ñu xoob kaw jën yi xaalis, galan yi di xaalis. |
2717 | EXO 40:9 | «Jëlal nag diwu pal gi, nga diw ci jaamookaay bi ak li ci biiram lépp, sellale ko ko, mook yëfam yépp, mu daldi sell. |
2752 | LEV 1:6 | Juru saraxu rendi-dóomal bi, na ko boroom sarax bi fees, daggat ko. |
2875 | LEV 6:18 | «Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la. |
2990 | LEV 10:12 | Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la. |
3068 | LEV 13:15 | Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la. |
3073 | LEV 13:20 | Su ko sarxalkat bi seetee ba gis fa taab ba nekkoon mel ni lu def pax, te kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca taab ba. |
3075 | LEV 13:22 | Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la. |
3080 | LEV 13:27 | Sarxalkat bi da koy seet ca bésub juróom ñaareel ba. Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la. |
3307 | LEV 19:25 | Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. |
3331 | LEV 20:12 | Ku dëkkoo sa soxnas doom, mook soxnas doomam ñoom ñaar ñépp dee mooy seen àtte. Jëfu yàqute lañu def, kon ñooy gàddu seen bakkanu bopp. |
3381 | LEV 22:11 | Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu. |
3406 | LEV 23:3 | «Juróom benni fan lees di liggéey, bésub juróom ñaareel ba bésub Noflaay doŋŋ lay doon, di bésub ndaje mu sell. Du lenn lu ngeen ciy liggéey. Bésub Noflaay la bu ñuy jagleel Aji Sax ji, ak fépp fu ngeen dëkk. |
3441 | LEV 23:38 | Yooyu sarax jotewul dara ak saraxi bési Noflaay yu Aji Sax ji. Jotewul dara it ak yi ngeen di joxeel Aji Sax ji mbaa mboolem sarax yi ngeen di wàccoo ngiñ, ak mboolem saraxi yéene yi ngeen di defal Aji Sax ji. |
3454 | LEV 24:7 | Jal bu nekk teg ca cuuraay lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. |
3490 | LEV 25:20 | Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?” |
3823 | NUM 5:30 | mbaa jëkkër ju xelum fiiraange dikkal, mu fiire jabaram. Jabar ji lay taxawloo fi kanam Aji Sax ji, sarxalkat bi defal ko mboolem dogalu yoon boobu. |
4024 | NUM 10:35 | Bu gaal ga jógaan, Musaa da naan: «Jógaloo, Aji Sax ji, say noon fëlxoo, say bañ daw la.» |
4038 | NUM 11:13 | Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”? |
4046 | NUM 11:21 | Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! |