| 7 | GEN 1:7 | Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona. |
| 9 | GEN 1:9 | Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. |
| 11 | GEN 1:11 | Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. |
| 15 | GEN 1:15 | Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. |
| 22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
| 24 | GEN 1:24 | Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. |
| 30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
| 33 | GEN 2:2 | Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. |
| 47 | GEN 2:16 | Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, |
| 58 | GEN 3:2 | Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. |
| 66 | GEN 3:10 | Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» |
| 67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
| 73 | GEN 3:17 | Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. |
| 89 | GEN 4:9 | Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» |
| 98 | GEN 4:18 | Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. |
| 105 | GEN 4:25 | Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» |
| 109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
| 118 | GEN 5:12 | Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. |
| 119 | GEN 5:13 | Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
| 121 | GEN 5:15 | Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. |
| 122 | GEN 5:16 | Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
| 123 | GEN 5:17 | Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. |
| 127 | GEN 5:21 | Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. |
| 128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
| 131 | GEN 5:25 | Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. |
| 132 | GEN 5:26 | Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
| 133 | GEN 5:27 | Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu. |
| 135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
| 141 | GEN 6:3 | Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» |
| 155 | GEN 6:17 | «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee. |
| 177 | GEN 7:17 | Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore. |
| 178 | GEN 7:18 | Ma ngay gën di yokku, tey baawaan ci kaw suuf, ba gaal ga tëmb, di dem ca kaw ndox ma. |
| 180 | GEN 7:20 | Muy yokku, di yokku, ba gëna kawe tund ya lu mat fukki xasab ak juróom. |
| 181 | GEN 7:21 | Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp. |
| 182 | GEN 7:22 | Mboolem mbindeef muy boroom bakkan ci kaw suuf a bokk dee. |
| 192 | GEN 8:8 | Mu teg ca yebal pitax, ba xam ndax ndox mi ci suuf fer na. |
| 193 | GEN 8:9 | Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. |
| 196 | GEN 8:12 | Mu négati juróom ñaari fan, bàyyiwaat pitax ma. Boobu yoon nag délsiwaatul ca moom. |
| 204 | GEN 8:20 | Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. |
| 208 | GEN 9:2 | Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo. |
| 209 | GEN 9:3 | Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax. |
| 226 | GEN 9:20 | Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ. |
| 227 | GEN 9:21 | Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu. |
| 230 | GEN 9:24 | Màndite ma giif, Nóoyin yewwu, daldi yég ni xale bi def ak moom. |
| 232 | GEN 9:26 | Mu dellu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Sem, yal na Kanaan dib jaamam. |
| 237 | GEN 10:2 | Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. |
| 241 | GEN 10:6 | Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. |
| 244 | GEN 10:9 | mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» |
| 248 | GEN 10:13 | Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi |
| 256 | GEN 10:21 | Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. |
| 258 | GEN 10:23 | Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. |
| 265 | GEN 10:30 | Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa, ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku. |
| 296 | GEN 11:29 | Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay. |
| 298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
| 304 | GEN 12:5 | Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan. |
| 305 | GEN 12:6 | Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. |
| 309 | GEN 12:10 | Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon. |
| 310 | GEN 12:11 | Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga. |
| 311 | GEN 12:12 | Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des. |
| 313 | GEN 12:14 | Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. |
| 320 | GEN 13:1 | Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. |
| 329 | GEN 13:10 | Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja. |
| 337 | GEN 13:18 | Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay. |
| 344 | GEN 14:7 | Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar. |
| 350 | GEN 14:13 | Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. |
| 355 | GEN 14:18 | Ci kaw loolu Melkisedeg buurub Salem, mi doon sarxalkatu Yàlla Aji Kawe ji, daldi ñëw, indi mburu ak biiñ. |
| 356 | GEN 14:19 | Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf! |
| 359 | GEN 14:22 | Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf, |
| 361 | GEN 14:24 | Duma jël dara, lu wees li sama nit ñi lekk ba noppi ak sama wàllu farandoo yi, di Aner ak Eskol ak Mamre, ñoom it, nañu jot seen wàll.» |
| 363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
| 364 | GEN 15:3 | Ibraam teg ca ne: «Mayoo ma giir, te it jaam bu juddoo sama kër moo may donn.» |
| 366 | GEN 15:5 | Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» |
| 368 | GEN 15:7 | Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.» |
| 379 | GEN 15:18 | Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, |
| 383 | GEN 16:1 | Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara. |
| 385 | GEN 16:3 | Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi jël Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu dëkkoo ko. |
| 387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
| 390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
| 391 | GEN 16:9 | Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» |
| 392 | GEN 16:10 | Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» |
| 394 | GEN 16:12 | Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.» |
| 395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
| 399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
| 402 | GEN 17:4 | «Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare. |
| 403 | GEN 17:5 | Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare. |
| 405 | GEN 17:7 | Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan. |
| 416 | GEN 17:18 | Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» |
| 426 | GEN 18:1 | Am na bés, Aji Sax ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor. |
| 428 | GEN 18:3 | Mu daldi ne: «Sang bi, siyaare naa la. Ngalla waay, bu ma romb. |
| 430 | GEN 18:5 | Maa ngi leen di indil dogu mburu mu ngeen dëgërloo, ba mana topp seen yoon, gannaaw nangu ngeena toog, ma siyaare leen.» Ñu ne ko: «Waaw, baax na.» |
| 433 | GEN 18:8 | Ibraayma taajal leen ndawal, la ñu togg, ba mu sotti, indaaleel leen soow ak meew mu bees. Ma nga taxaw ca seen wet ca ker garab ga, ñuy lekk. |
| 434 | GEN 18:9 | Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» |
| 437 | GEN 18:12 | Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» |
| 438 | GEN 18:13 | Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” |
| 444 | GEN 18:19 | Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.» |
| 448 | GEN 18:23 | Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen? |