168 | GEN 7:8 | Rab yu set yi ak yi setul ak picc yi ak yiy raam |
203 | GEN 8:19 | Rabi àll yi ak luy raam ak luy naaw ak luy dox ci kaw suuf— lépp génne ca gaal ga, lu ci nekk ak wirgoom. |
238 | GEN 10:3 | Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. |
242 | GEN 10:7 | Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan. |
246 | GEN 10:11 | Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. |
260 | GEN 10:25 | Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan. |
285 | GEN 11:18 | Peleg am fanweeri at, jur Rew. |
286 | GEN 11:19 | Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
287 | GEN 11:20 | Rew am fanweeri at ak ñaar, jur Serug. |
288 | GEN 11:21 | Serug juddu na, Rew dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñaar (207), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
326 | GEN 13:7 | Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma. |
342 | GEN 14:5 | Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim, |
381 | GEN 15:20 | ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi, |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
396 | GEN 16:14 | Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret. |
440 | GEN 18:15 | Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» |
450 | GEN 18:25 | Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
466 | GEN 19:8 | Dégluleen, ma wax leen; man, am naa ñaari doom yu jigéen, te xamuñu góor. Mayleen ma, ma yót leen leen, ngeen def leen lu leen neex. Rikk buleen def góor ñii dara, ndaxte samay gan lañu.» |
496 | GEN 19:38 | Rakk ja moom it am doom ju góor, tudde ko Ben Aami (mu firi Sama doomu mbokk). Ben Aami moo sos Amoneen, ñi fi nekk ba tey. |
571 | GEN 22:23 | Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor. |
572 | GEN 22:24 | Rewma it nekkaaleem la woon, doom ya mu ca am di Teba ak Gaxam ak Taxas ak Maaka. |
607 | GEN 24:15 | Laata muy ñaan ba noppi sax, gis na Rebeka gàddu njaqam, di ñëw. Rebeka moomu di doomu Betuwel te di sëtu Milka ak Naxor, miy magu Ibraayma. |
621 | GEN 24:29 | Rebeka amoon na càmmiñ lu tudd Laban. Laban daldi gaawtu génn, fekki waa ja ca seyaan ba. |
622 | GEN 24:30 | Booba gis na jaaro ba ak lam, ya ca loxol jigéenam Rebeka, te dégg na jigéenam di nettali la ko waa ja wax. Loolu tax mu dem ca waa ja, fekk ko ca giléem ya ca seyaan ba. |
637 | GEN 24:45 | «Bala maa ñaan ba noppi, Rebeka ne jimeet, gàddu njaqam, wàcc ca seyaan ba, di root. Ma ne ko: “May ma, ma naan.” |
643 | GEN 24:51 | Rebekaa ngoogu, jëlal te dem, muy sa soxnas doomu sang, ni la ko Aji Sax ji tegtale.» |
645 | GEN 24:53 | Surga ba nag génne ay gànjari xaalis ak yu wurus booleek ay yére, jox Rebeka. Càmmiñ la ak yaay ja itam, mu may leen alal ju takku. |
650 | GEN 24:58 | Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw.» |
651 | GEN 24:59 | Ba loolu amee càmmiñ ya bàyyi seen jigéen Rebeka, moom ak surga, bi ko yar te daan ko nàmpal, ñu ànd ak surgab Ibraayma ak ñi ko topp, ñu dem. |
652 | GEN 24:60 | Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, te sa askan teg ay bañam tànk.» |
653 | GEN 24:61 | Gannaaw loolu Rebeka ànd ak xale yu jigéen, yiy jaamam, ñu war ay giléem, topp waa ja. Surga ba daldi dem, yóbbu Rebeka. |
654 | GEN 24:62 | Loolu fekk na Isaaxa dëkk ca àllub Negew. Mu demoon nag teenu Laxay Roy, ba ñibbsi. |
656 | GEN 24:64 | Rebeka it ne sigget, gis Isaaxa. Mu ne cëpp nag, wàcc giléem ga, |
657 | GEN 24:65 | daldi ne surga ba: «Waa jee ci àll biy ñëw, jëm ci nun, kan a?» Surga ba ne ko: «Sama sang la de.» Rebeka daldi jël muuraay ba, muuroo. |
659 | GEN 24:67 | Ba loolu wéyee Isaaxa yóbbu Rebeka ca xaymab yaayam Saarata, muy soxnaam, di ku mu bëgg, te di ko muñe yaayam, ndax fekk na mu faatu. |
670 | GEN 25:11 | Gannaaw ba Ibraayma nelawee, Yàlla barkeel na doomam Isaaxa. Isaaxaa ngi dëkkoon ca wetu teenu Laxay Roy. |
679 | GEN 25:20 | Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba. |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
687 | GEN 25:28 | Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba. |
700 | GEN 26:7 | Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka. |
701 | GEN 26:8 | Ba ñu fa toogee ba mu yàgg, mu am bés Abimeleg, buurub waa Filisti tollu ci palanteeram, gis leen, fekk yóo Isaaxaa ngay raay soxnaam Rebeka. |
715 | GEN 26:22 | Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.» |
728 | GEN 26:35 | Jigéen ñooñu mu jël nag di naqar wu réy ci Isaaxa ak Rebeka. |
733 | GEN 27:5 | Fekk na Rebekaa ngi déglu, ba Isaaxay wax ak doomam Esawu. Esawu daldi dem ca àll ba, rëbbi lu mu toggsi. |
734 | GEN 27:6 | Rebeka moom ne doomam Yanqóoba: «Dégg naa sa baay wax sa mag Esawu ne ko: |
743 | GEN 27:15 | Rebeka daldi seet ca dencam la gën ca yérey Esawu taaw ba, solal Yanqóoba doomam ju ndaw. |
770 | GEN 27:42 | Naka lañu nettali Rebeka la taawam Esawu wax, mu woolu Yanqóoba, doomam ju ndaw ja, ne ko: «Sa mag a ngi fexee feyu, di la wuta rey. |
774 | GEN 27:46 | Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» |
779 | GEN 28:5 | Isaaxa daldi yebal Yanqóoba, mu dem Padan Aram ca Laban doomu Betuwel, Arameen bay càmmiñu Rebeka, miy yaayu Yanqóoba ak Esawu. |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
805 | GEN 29:9 | Na muy wax ak ñoom nag, Rasel agsi, indaale gàtti baayam, ndaxte sàmm la woon. |
806 | GEN 29:10 | Ba Yanqóoba gisee Rasel, doomu nijaayam Laban, moom ak gàtti nijaayam ya, dafa daagu ba ca teen ba, béraŋ doj wa ko ub, daldi wëgg gàtti Laban. |
807 | GEN 29:11 | Ba loolu amee Yanqóoba fóon Rasel, ne yikkét jooy. |
808 | GEN 29:12 | Ca la Yanqóoba wax Rasel ne ko: «Maak sa baay a bokk, ndax maay sa doomu bàjjan Rebeka.» Rasel daw, yégal ko baayam. |
812 | GEN 29:16 | Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel. |
813 | GEN 29:17 | Leya di ku bët ya yànjuloon, te Rasel nekkoon ku jekk te neexa xool, |
814 | GEN 29:18 | Yanqóoba bëgg Rasel lool, ba ne Laban: «Dinaa la liggéeyal juróom ñaari at ngir Rasel sa doom ju ndaw ji.» |
816 | GEN 29:20 | Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel. |
821 | GEN 29:25 | Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» |
822 | GEN 29:26 | Laban ne ko: «Rakk jëkka séy taaw daal, du aada fii. |
824 | GEN 29:28 | Yanqóoba nangu, daldi séetu ak Leya ayu bés, ba noppi Laban jébbal ko doomam Rasel. |
825 | GEN 29:29 | Booba la Laban may Rasel jaamam bu jigéen bu ñuy wax Bilaa, mu dib jaamam. |
826 | GEN 29:30 | Yanqóoba nag dëkkoo Rasel, mi mu gënoona bëgg Leya. Ci kaw loolu mu liggéeyaatal Laban juróom ñaari at. |
827 | GEN 29:31 | Ba Aji Sax ji gisee ne Leya fonkeesu ko, mu may ko, mu taawlu, te Rasel moom manula am doom. |
828 | GEN 29:32 | Ba Leya ëmbee, am doom ju góor, da koo tudde Ruben (mu firi Gisleen, doom ju góor a ngi), ndaxte Leya da ne: «Aji Sax ji gis na sama toroxte. Léegi sama jëkkër dina ma bëgg.» |
832 | GEN 30:1 | Ba Rasel gisee ne amalul Yanqóoba doom, dafa ñee magam, ba tax mu wax Yanqóoba ne ko: «Nanu am ay doom, mbaa ma dee.» |
833 | GEN 30:2 | Yanqóoba mere ca Rasel ne ko: «Ndax maay Yàlla, mi la teree am doom?» |
837 | GEN 30:6 | Bi loolu amee Rasel ne: «Yàlla àtte na ma; dégg na sama ñaan, ba may ma doom.» Mu tudde ko nag Dan (mu firi Kiy àtte). |
838 | GEN 30:7 | Gannaaw ga Bilaa, jaamub Rasel, ëmbaat, dellu amal Yanqóoba doom ju góor. |
839 | GEN 30:8 | Rasel ne: «Bëre naa ak sama mag bëre bu réy, ba daan,» daldi ko tudde Neftali (mu firi Kiy bëre). |
845 | GEN 30:14 | Mu am bés ñuy góob bele, Ruben dem tool, sàkke ca gàncax gu ñu naan màndaragoor, indil ko yaayam Leya. Rasel ne Leya: «Ngalla may ma ci màndaragoor ji la sa doom indil.» |
846 | GEN 30:15 | Teewul mu ne ko: «Ndax nangu sama jëkkër rekk doyu la, ba nga bëgg cee boole màndaragoor ji ma sama doom indil?» Rasel ne ko: «Kon jox ma ci màndaragoor ji sa doom indi, ma wecci la ko sama ayu tey boog.» |
853 | GEN 30:22 | Ba loolu amee Yàlla geestu Rasel, nangul ko, may ko doom. |
856 | GEN 30:25 | Ba Rasel amee doom ci Yuusufa, Yanqóoba da ne Laban: «Yiwi ma boog, ma dellu sama réew ca sama kër. |
878 | GEN 31:4 | Yanqóoba woolu Rasel ak Leya ca tool ya, fa gàttam ya nekk. |
888 | GEN 31:14 | Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay? |
893 | GEN 31:19 | Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam. |
906 | GEN 31:32 | Waaye képp koo gis mu yor sa gàllaaji kër, boo yeboo reyal. Seetal fii ci sunu kanami bokk lépp lu ma fi yor, loo ci moom fabal, yóbbu.» Booba Yanqóoba xamul woon ne Rasel a ko jël. |
907 | GEN 31:33 | Laban dugg ci xaymab Yanqóoba, teg ca xaymab Leya ak yosi ñaari jaamam yu jigéen ya, te gisul dara. Mu génne xaymab Leya, dugg ci bu Rasel. |
908 | GEN 31:34 | Fekk na Rasel fab gàllaaji kër ya, làq ca ron tegu giléem ga, toog ca. Laban tëcc, tëcc ca biir xayma ba, gisul dara. |
909 | GEN 31:35 | Rasel wax baayam ne ko: «Baay, baal ma de, damaa manula jóg ci sa kanam, ndaxte damaa ànd ak mbaax.» Laban seet na fu ne, waaye gisul gàllaaji këram ya. |
962 | GEN 33:1 | Gannaaw loolu Yanqóoba séen Esawu di ñëw, ànd ak ñeenti téeméeri góor, mu séddale xale yi, diggante Leya, Rasel ak ñaari jaam ya. |
963 | GEN 33:2 | Dafa jiital jaam ya ak seeni doom, tofal ca Leya ak ay doomam, Rasel ak Yuusufa féete gannaaw. |
968 | GEN 33:7 | Leya it topp ca, moom aki doomam, jegesi ñoom itam, sujjóot. Yuusufa ak Rasel doora jegesi sujjóot. |
1020 | GEN 35:8 | Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (mu firi Garabu jooyoo). |
1024 | GEN 35:12 | Réew, mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.» |
1028 | GEN 35:16 | Ba loolu wéyee ñu jóge Betel, dem bay bëgga jub Efrata. Rasel tollu ciw mat, te mat wi metti. |
1030 | GEN 35:18 | Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay). |
1031 | GEN 35:19 | Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey. |
1032 | GEN 35:20 | Yanqóoba nag samp aw doj ca bàmmeel ba, te mooy xàmmikaayu bàmmeelu Rasel ba tey jii. |
1034 | GEN 35:22 | Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar. |
1035 | GEN 35:23 | Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon. |
1036 | GEN 35:24 | Doomi Rasel di Yuusufa ak Beñamin. |
1037 | GEN 35:25 | Doomi Bilaa, jaamub Rasel, di Dan ak Neftali. |
1045 | GEN 36:4 | Ada am ak Esawu Elifas; Basmat am ca Rewel. |