Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   W    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

42  GEN 2:11  Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma,
49  GEN 2:18  Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»
54  GEN 2:23  Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
59  GEN 3:3  Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»
61  GEN 3:5  Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.»
146  GEN 6:8  Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande.
156  GEN 6:18  Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
210  GEN 9:4  «Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret.
327  GEN 13:8  Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag?
332  GEN 13:13  Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
347  GEN 14:10  Waaye xuru Sidim woowu dafa feesoon dell aki pax aki kàmbi koltaar. Ba mu ko defee buuri Sodom ak Gomor di daw, far daanu ca kàmb ya. Ña ca des daw ba ca tund ya.
357  GEN 14:20  Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko.
375  GEN 15:14  Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare.
383  GEN 16:1  Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara.
417  GEN 17:19  Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam baww.
419  GEN 17:21  Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëniwén.»
430  GEN 18:5  Maa ngi leen di indil dogu mburu mu ngeen dëgërloo, ba mana topp seen yoon, gannaaw nangu ngeena toog, ma siyaare leen.» Ñu ne ko: «Waaw, baax na.»
453  GEN 18:28  Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.»
467  GEN 19:9  Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba.
477  GEN 19:19  Defal nga ma yiw, yërëm ma lool, ba musal ma. Waaye bala maa daw, ba àgg ca tund ya, musiba mii man naa dal ci sama kaw, ma dee.
479  GEN 19:21  Malaaka ma ne ko: «Waaw baax na ba tey, duma tas dëkk boobu ngay wax.
502  GEN 20:6  Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ.
503  GEN 20:7  Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»
537  GEN 21:23  Léegi nag waatal ma fii ci Yàlla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal.»
538  GEN 21:24  Ibraayma ne ko: «Waat naa ko.»
596  GEN 24:4  Waaye dinga dem sama réew, ma ma cosaanoo, jëlal fa sama doom Isaaxa soxna.»
600  GEN 24:8  Su la ndaw si buggula topp, kon wàccoo nga ak man. Waaye rikk bul yóbbu sama doom foofa.»
613  GEN 24:21  Waa ja ne ko jàkk, ne tekk, di seet, ba xam ndax Aji Sax ji àntal na yoonam am déet.
615  GEN 24:23  Mu ne ko: «Wax ma, kan moo la jur?» Ak itam: «Ndax man nanoo dal sa kër baay?»
617  GEN 24:25  teg ca ne ko: «Waawaaw, ñax maak ngooñ maa nga fa, ne gàññ, te it manees na faa dal.»
618  GEN 24:26  Waa ji nag sujjóot, sant Aji Sax ji,
624  GEN 24:32  Waa ja daldi àgg ca kër ga, ñu sippi giléem ya, may leen ñax ak ngooñ, may waa ja ndox, mu jàngu, moom ak ñi mu àndal,
630  GEN 24:38  Waaye demal ca sama kër baay, ca samay bokk, nga jëlal fa sama doom soxna.”
650  GEN 24:58  Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw
657  GEN 24:65  daldi ne surga ba: «Waa jee ci àll biy ñëw, jëm ci nun, kan a?» Surga ba ne ko: «Sama sang la de.» Rebeka daldi jël muuraay ba, muuroo.
726  GEN 26:33  Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga).
739  GEN 27:11  Yanqóoba ne yaayam: «Waaw, waaye sama mag Esawu dafa jëxëm, te man sama yaram rattax.
752  GEN 27:24  Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw
768  GEN 27:40  Sa saamar ngay dunde, sa rakk di la yilif. Waaye bés a ngi ñëw yaay sigiñu, ba yenniku notaangeem.»
803  GEN 29:7  Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!»
811  GEN 29:15  Gannaaw loolu Laban ne Yanqóoba: «Li ngay sama mbokk kat, taxul nga war maa liggéeyal ci neen. Wax ma lan mooy sa peyoor.»
821  GEN 29:25  Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?»
842  GEN 30:11  Leya ne: «Ndaw wërsëg wu réy!» daldi ko tudde Gàdd (mu firi Wërsëg).
859  GEN 30:28  Wax ma loo may feyeeku rekk, dinaa la ko fey.»
861  GEN 30:30  ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?»
865  GEN 30:34  Laban ne: «Waaw, kon baax na.»
874  GEN 30:43  Waa ji mujj na barele lool, am gàtt yu ne gàññ ak ay jaam yu góor ak yu jigéen ak ay giléem aki mbaam-sëf.
879  GEN 31:5  Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man.
906  GEN 31:32  Waaye képp koo gis mu yor sa gàllaaji kër, boo yeboo reyal. Seetal fii ci sunu kanami bokk lépp lu ma fi yor, loo ci moom fabal, yóbbu.» Booba Yanqóoba xamul woon ne Rasel a ko jël.
916  GEN 31:42  Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.»
958  GEN 32:30  Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa.
969  GEN 33:8  Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.»
994  GEN 34:13  Waaye doomi Yanqóoba ya, ay nax lañu tontoo Sikem ak baayam Amor, ndax li Sikem torxal seen jigéen Diina.
998  GEN 34:17  Waaye su ngeen nu déggalul, ba xarafuleen, danuy jël sunu jigéen, dem.»
1003  GEN 34:22  Waaye li ci nekk mooy, seeni góor duñu nangoo dëkk ak nun, nuy ay bokk, ndare sunu góor ñépp xaraf ni ñoom.
1097  GEN 37:13  Israyil ne Yuusufa: «Xam nga ne say mag sàmmi nañu Sikem. Kaay, ma yónni la ci ñoom.» Yuusufa ne ko: «Waaw
1099  GEN 37:15  Naka la jenn waay dajeek moom foofa, fekk muy wëreelu ca àll ba. Waa ja ne ko: «Looy seet?»
1101  GEN 37:17  Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: “Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa.
1173  GEN 39:23  Wattukat ba seetatuloon dara lu Yuusufa jiite, ndax Aji Sax jee ànd ak moom, te lu mu sabablu, Aji Sax ji may ko ca ndam.
1187  GEN 40:14  Waaye ngalla boo delloo ca sa teraanga, nanga ma geestu te dimbali ma, waxal ma Firawna lu jëm ci man, ba man maa génne fii.
1196  GEN 40:23  Waaye kilifa, ga yore naani Firawna, xalaatul sax Yuusufa, da koo fàtte.
1217  GEN 41:21  Waaye bi ñu leen lekkee ba noppi, itam dafa mel ni lekkuñu leen, ndax terewuleena mel na woon. Booba laa yewwu,
1257  GEN 42:4  Waaye Yanqóoba yebalul Beñamin, rakku Yuusufa, ndax dafa ragal ne musiba man na koo dab.
1268  GEN 42:15  Waaye nii laa leen di seetloo: bu seen rakk ñëwul, ak bakkanu Firawna, dungeen fi jóge.
1273  GEN 42:20  Waaye nangeen ma indil seen rakk, ba ma xam ne li ngeen wax dëgg la; su ko defee dungeen dee.» Ñu daldi ne: «Waaw
1283  GEN 42:30  «Waa ja yilif réew ma dafa noo résëti, foog ne danuy yëddusi réew ma.
1286  GEN 42:33  Waa ja yilif réew ma ne nu: “Ni may xame ne ñu maandu ngeen, nii la: dangeen may bàyyeek kenn ci yeen, te dem yóbbul dund seen waa kër, yi nekk ci xiif;
1294  GEN 43:3  Yuda ne ko: «Waa ja da noo àrtu woon de, wax na nu ne nu: “Dootuleen jàkkaarlook man te ànduleen ak seen rakk.”
1296  GEN 43:5  Waaye boo ko bàyyiwul kat, dunu dem, ndax waa ja waxoon na nu ne nu: “Dungeen jàkkaarlook man te seen rakk àndul ak yeen.”»
1298  GEN 43:7  Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!»
1308  GEN 43:17  Waa ja def la ko Yuusufa wax, yóbbu gaa ña kër Yuusufa.
1313  GEN 43:22  Te it indaale nanu xaalis bu nu jënde dund. Waaye xamunu ku delloo xaalis ba ci sunuy saaku.»
1315  GEN 43:24  Waa ja dugal leen kër Yuusufa, may leen ndox ñu jàngu, ba noppi xont seeni mbaam.
1323  GEN 43:32  Loolu wees ñu may Yuusufa moom rekk; ber doomi baayam ya. Waa Misra ña fa doon lekke it, ñu beral leen seen ndab, ngir waa Misra daawuñu bokk ak Ebrë yi lekk, ndax mbañ la fa woon.
1327  GEN 44:2  Waaye sama kaasu xaalis boobee, yebal ko ki gën di xale ci saakoom, boole ko ak xaalisu peppam.» Mu def la Yuusufa wax.
1364  GEN 45:5  Waaye buleen jaaxle tey, mbaa ngeen di sikk seen bopp ndax li ngeen ma jaay, ñu indi ma fi. Rawale ay bakkan moo tax Yàlla yebal ma fi, ma jiitusi leen.
1370  GEN 45:11  ndaxte des na juróomi ati xiif. Waaye dinaa la fi yore, ba doo ñàkk dara, yaak sa waa kër ak mboolem lu bokk ci yaw.”
1376  GEN 45:17  Firawna ne Yuusufa: «Waxal say mag, ne leen: “Ni ngeen di def mooy nii: sëfleen seeni mbaam te dem réewu Kanaan,
1381  GEN 45:22  mayaale leen ku ne mbubb mu rafet. Waaye Beñamin moom, ñetti téeméeri dogi xaalis la ko may, tegal ko ca juróomi mbubb yu rafet.
1386  GEN 45:27  Waaye ba ñu nettalee seen baay Yanqóoba li Yuusufa wax lépp, te mu gis watiir, yi Yuusufa yónnee, ngir jëlsi ko, ca la xelam délsi.
1395  GEN 46:8  Waa kër Israyil, yi ñëw Misra te di Yanqóoba aki doomam, seeni tur a di: Ruben, taawub Yanqóoba.
1434  GEN 47:13  Ab dund amuloon fenn ca réew ma mépp, ndax xiif bu metti lool. Waa réewum Misra ak réewu Kanaan jeex tàkk ndax xiif ba.
1442  GEN 47:21  Waa réew ma ñoom, Yuusufa da leena def ay jaam ca Misra, gii wet ba gaa.
1447  GEN 47:26  Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara.
1458  GEN 48:6  Waaye doom, yi nga am seen gannaaw yaa leen di féetewoo, ñuy wuyoo seen turi mag ci wàllu ndono.
1491  GEN 49:17  Waaye Dan ay jaan ju dog aw yoon, mbaa céebi ciw ñall, mooy màtt tànki fas, gawar jullootu.
1510  GEN 50:3  Waaj ma am na ñeent fukki fan, ndaxte loolooy waajal bu mat sëkk cib néew. Waa Misra nag dëjal ko juróom ñaar fukki fan.
1518  GEN 50:11  Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra).
1522  GEN 50:15  Magi Yuusufa ya xam nañu ne seen baay nelaw na. Ña ngay wax ca seen biir naan: «Waaw, mbaa Yuusufa dencalu nu mer, nar noo fey sunu bor ndax lu bon li nu ko ji woon lépp?»
1524  GEN 50:17  Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy.
1546  EXO 1:13  Waa Misra dañoo mujj di jaamloo bànni Israyil bu metti,
1563  EXO 2:8  Doomu Firawna ne ko: «Waaw, demal.» Xale ba dem, indil ko yaayu liir ba.
1569  EXO 2:14  Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.»
1575  EXO 2:20  Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!»
1591  EXO 3:11  Musaa ne Yàlla: «Waaw, waaye man tekkiwuma dara, bay dem ca Firawna, di génne bànni Israyil Misra.»
1598  EXO 3:18  «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.”
1599  EXO 3:19  Waaye man xam naa ne buuru Misra du leen bàyyi, ngeen dem, mbete mu taseek doole ju ko tiiñ.