29 | GEN 1:29 | Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. |
138 | GEN 5:32 | Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. |
148 | GEN 6:10 | Nóoyin nag amoon na ñetti doom yu góor: seeni tur di Sem, Xam ak Yafet. |
158 | GEN 6:20 | Xeetu picc wu ci nekk ak xeetu bàyyima wu ci nekk ak wépp xeetu rab wuy raam ci suuf, dina def ñaar, ñëw ci yaw, ba raw. |
162 | GEN 7:2 | Xeeti rab yu set yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen. |
173 | GEN 7:13 | Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga, |
222 | GEN 9:16 | Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» |
224 | GEN 9:18 | Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan. |
228 | GEN 9:22 | Ba loolu amee Xam, baayu Kanaan, gis céri baayam, génn waxi ko Sem ak Yafet ca biti. |
236 | GEN 10:1 | Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom. |
241 | GEN 10:6 | Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. |
255 | GEN 10:20 | Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew. |
258 | GEN 10:23 | Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. |
327 | GEN 13:8 | Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
340 | GEN 14:3 | Ñooñoo booloo woon ca xuru Sidim, mooy géeju Xorom gi léegi. |
366 | GEN 15:5 | Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» |
409 | GEN 17:11 | Xaraf mooy màndargaal kóllëre googu ma fas ak yeen. |
410 | GEN 17:12 | Xale bu góor, bu amee juróom ñetti fan war naa xaraf. Képp kuy góor ci seen maasoo maas, war naa xaraf, ba ci jaam bu juddoo sa kër, mbaa ku ñu jënd ci sa xaalis, ak bépp doomu doxandéem boo jurul. |
411 | GEN 17:13 | Jaam bu juddoo sa kër ak boo jënd, ñoom ñaar ñépp, dees leen wara xarfal. Xaraf ay màndargaal sama kóllëre ci seen yaram, muy kóllëre gu sax fàww. |
429 | GEN 18:4 | Xaarleen, ñu indil leen tuuti ndox, ngeen jàngu te nopplu ci ker garab gi. |
442 | GEN 18:17 | Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? |
540 | GEN 21:26 | Abimeleg nag ne ko: «Xawma ku la def jooju jëf de, ndax yaw waxoo ma ci dara; guléet ma dégg ko tey.» |
611 | GEN 24:19 | Ba ko ndaw si mayee, mu naan ba noppi, da ne ko: «Xaaral, ma wëggal la giléem yi, ñu naan ba noppi.» |
647 | GEN 24:55 | Càmmiñal ndaw sa ak yaay ja daldi ne ko: «Xanaa kay janq bi dina toogaat ak nun ab diir boog, maanaam fii ak sibbir, doora dem.» |
689 | GEN 25:30 | Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). |
703 | GEN 26:10 | Abimeleg ne ko: «Li nga nu def nag? Xaw tuuti kenn ci nit ñi tëdde sa soxna, te kon nga yóbbe nu tooñ.» |
714 | GEN 26:21 | Ñu gasaat ab teen, xuloo amati ca, mu tudde ko Sitna (mu firi Xuloo). |
740 | GEN 27:12 | Xëy na sama baay làmbatu ma de, te kon dina ne njublaŋ laa. Su ko defee ay móolu laay yóbbe sama bopp, waaye du barkeb ñaan.» |
751 | GEN 27:23 | Xàmmiwu ko, ndax li loxo yi jëxëm ni yuy magam Esawu, ba tax mu ñaanal ko. |
801 | GEN 29:5 | Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
834 | GEN 30:3 | Mu ne ko: «Xoolal, sama jaam Bilaa ngii; dëkkoo ko, ndax mu amal ma doom, ba jabootal ma.» |
871 | GEN 30:40 | Xar ya, Yanqóoba da leena ber, tey fexe ñuy janook lépp lu seereer ak lu ñuul ci biir juru Laban. Noonu la sàkke juru boppam, bañ koo boole ak juru Laban. |
879 | GEN 31:5 | Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man. |
905 | GEN 31:31 | Yanqóoba tontu Laban ne ko: «Xanaa ragaloon rekk ne jombul dinga téye say doom yu jigéen. |
912 | GEN 31:38 | Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt. |
925 | GEN 31:51 | Laban neeti Yanqóoba: «Xoolal ci jal bii ak doju xàmmikaay, wi ci sama digganteek yaw. |
959 | GEN 32:31 | Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.» |
966 | GEN 33:5 | Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.» |
969 | GEN 33:8 | Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.» |
976 | GEN 33:15 | Esawu ne ko: «Xaaral ma bàyyee la ñenn ci góor, ñi ma àndal.» Yanqóoba ne ko: «Matu ko. Boobu teraanga ëpp na, sang bi. Jàmm ji nga ma dalal rekk doy na.» |
1000 | GEN 34:19 | Xale bu góor bi daldi gaawtu def li ñu ko sant ndax mbëggeelam ca doomu Yanqóoba. Booba Sikem lañu gënoona weg ca waa kër baayam yépp. |
1094 | GEN 37:10 | Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?» |
1097 | GEN 37:13 | Israyil ne Yuusufa: «Xam nga ne say mag sàmmi nañu Sikem. Kaay, ma yónni la ci ñoom.» Yuusufa ne ko: «Waaw.» |
1100 | GEN 37:16 | Yuusufa ne ko: «Samay mag laay seet. Xamoo fu ñu tollu, di sàmm?» |
1114 | GEN 37:30 | Ba loolu amee mu jóge ca, dem ca ay rakkam ne leen: «Xale ba nekkatu fa de! Te man xawma nu may def léegi.» |
1138 | GEN 38:18 | Mu ne ko: «Lu ma lay tayle?» Ndaw si ne ko: «Xanaa sa jaarob màndargaal, ak buum, gi mu àndal ak yet, wi ci sa loxo.» Mu jox ko nag, ba noppi ànd ak moom. Fa la doxe ëmb. |
1140 | GEN 38:20 | Ba loolu wéyee Yuda yebal xaritam, ba dëkk Adulam, mu yóti ndaw sa bëy wu ndaw wa, ba mana jotaat la mu tayle woon ca ndaw sa. Xarit ba nag gisu ko. |
1145 | GEN 38:25 | Naka lañu koy yóbbu, mu yóbbante goroom ba ay kàddu. Da koo wax ne ko: «Ki moom lii moo ma ëmbal.» Mu teg ca ne ko: «Xoolal bu baax te wax ma ku moom jaarob màndargaal, bi ànd ak buum gi, ak yet wi.» |
1164 | GEN 39:14 | mu woo surgay kër ga, ne leen: «Xool-leen, Ebrë, sii sama jëkkër indi ci kër gi, mu di nu yab. Dafa ñëw, bëgg maa tëdde, ma yuuxu ca kaw. |
1181 | GEN 40:8 | Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.» |
1226 | GEN 41:30 | Te juróom ñaari ati xiif a ciy topp, ba ñu fàtte naataange gu réy ga amoon réewum Misra. Xiif ba cay topp dina yàq réew mi. |
1227 | GEN 41:31 | Xiif bi dina tax lenn luy nirook naataange dootu des ci réew mi, ndax dina metti lool. |
1262 | GEN 42:9 | Xelum Yuusufa ne yarr ca la mu géntoon ca ñoom, daldi ne leen: «Yeen ay yëddukat ngeen, yuy nemmikusi mbóoti réew mi.» |
1289 | GEN 42:36 | Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!» |
1333 | GEN 44:8 | Xaalis bi nu fekkoon ci sunu bunti saaku sax, danoo àndaat ak moom, jóge ba Kanaan, délloosil la ko, kon nan lanu mana sàcce sa kër sang xaalis mbaa wurus? |
1340 | GEN 44:15 | Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?» |
1347 | GEN 44:22 | Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.” |
1352 | GEN 44:27 | Sunu baay, ba lay siyaare, ne nu: “Xam ngeen ne damaa amul ak sama soxna lu dul ñaari doom. |
1360 | GEN 45:1 | Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam. |
1471 | GEN 48:19 | Teewul baayam lànk, ne ko: «Xam naa ko, doom, xam naa ko. Moom itam dina doon aw xeet tey doon ku màgg, waaye rakkam a koy sut, te askanam dina law, ba di ay xeet.» |
1526 | GEN 50:19 | Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla? |
1559 | EXO 2:4 | Xale bu jigéen bay magu liir ba ma nga taxaw fu soreyaatoo ak liir ba, di xool, ba xam nu muy mujje. |
1563 | EXO 2:8 | Doomu Firawna ne ko: «Waaw, demal.» Xale ba dem, indil ko yaayu liir ba. |
1569 | EXO 2:14 | Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.» |
1613 | EXO 4:11 | Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji? |
1635 | EXO 5:2 | Firawna ne: «Kan mooy Aji Sax ji, ba ma di ko déggal, di bàyyi Israyil, ñuy dem? Xawma sax kuy Aji Sax ji, waxumalaa may bàyyi Israyil, ñuy dem.» |
1785 | EXO 10:7 | Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» |
1788 | EXO 10:10 | Firawna ne leen: «Ãa, yal na leen Aji Sax ji saxoo taxawu walla, ndegam maa leen di bàyyi moos, ngeen dem, yóbbaale seen njaboot! Xam ngeen ne naruleen njub de. |
1901 | EXO 14:11 | Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra? |
1902 | EXO 14:12 | Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!» |
2192 | EXO 24:14 | Fekk na mu wax mag ña ne leen: «Xaarleen nu fii, ba nu délsi. Aaróona ak Ur a ngi nii ak yeen; ku ci am mbir mooy àttelu, demal ci ñoom.» |
2220 | EXO 25:24 | Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. |
2237 | EXO 26:1 | «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali serub. |
2265 | EXO 26:29 | Xoobal làcc yi wurus te nga sàkkal làcc wu ci nekk ay lami wurus yuy téye galan yi, te nga xoob galan yi it wurus. |
2386 | EXO 30:3 | Xoobal wurusu ngalam kaw gi ak wet yi ba mu daj ak béjjén yi, te nga sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër. |
2495 | EXO 33:21 | Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ko: «Xoolal fii ci sama wet, taxaweel ci kaw doj wi. |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
2663 | EXO 38:29 | Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. |
2667 | EXO 39:2 | Xar-sànni mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. |
2997 | LEV 10:19 | Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» |
3743 | NUM 3:50 | Xaalis ba mu nangoo ca taawi bànni Israyil di junniy siikal ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom (1 365), ci siikalu bérab bu sell bi, xawa tollu ci fukki kilo ak ñett. |
4037 | NUM 11:12 | Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew, ma nga giñaloon seeni maam? |
4062 | NUM 12:2 | Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la Aji Sax jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca. |
4074 | NUM 12:14 | Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.» |
4104 | NUM 13:28 | Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis. |
4154 | NUM 14:45 | Ba mu ko defee Amalegeen ña ak Kanaaneen ña dëkke woon diiwaanu tund woowa wàccsi, duma leen, tasaare leen ba ca gox ba ñuy wax Xorma. |
4204 | NUM 16:9 | Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla? |
4216 | NUM 16:21 | «Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!» |
4344 | NUM 21:3 | Aji Sax ji nangul Israyil, jébbal leen Kanaaneen ña, ñu faagaagal leen, ñook seeni dëkk. Ñu daldi wooye gox ba Xorma (mu firi Lu ñu faagaagal). |
4355 | NUM 21:14 | Moo tax téereb Xarey Aji Sax ji indi ko, ne: «Waxeb ga ca Sufa, xuri Arnon yaak |
4406 | NUM 22:30 | Mu ne ko: «Xanaa du maay sa mbaam mi ngay war bu yàgg ba nga ma moomee, ba tey jii? Dama laa masa def nii?» Mu ne ko: «Déedéet.» |
4413 | NUM 22:37 | Balag ne Balaam: «Xanaa yeblewuma woon, ba yebleeti, di la woolu? Lu la tee woona ñëw? Am dama laa manula teral?» |
4415 | NUM 22:39 | Ci kaw loolu Balaam ànd ak Balag ba Kiryaat Xusot. |
4429 | NUM 23:12 | Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu Aji Sax ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?» |
4443 | NUM 23:26 | Balaam ne ko: «Xanaa waxuma la woon ne la lépp lu Aji Sax ji wax, loolu laay def?» |
4459 | NUM 24:12 | Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen, |
4682 | NUM 31:16 | Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israyil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji? |
4693 | NUM 31:27 | Xaajleen sëxëtoo mi ñaar, te ngeen séddale ko diggante xarekat ya xareji woon, ak mbooloo mi ci des yépp. |