2 | GEN 1:2 | Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi. |
5 | GEN 1:5 | Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk. |
11 | GEN 1:11 | Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. |
12 | GEN 1:12 | Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu. Yàlla gis ne baax na. |
14 | GEN 1:14 | Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. |
15 | GEN 1:15 | Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. |
16 | GEN 1:16 | Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi. |
17 | GEN 1:17 | Yàlla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf, |
18 | GEN 1:18 | ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na. |
20 | GEN 1:20 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» |
21 | GEN 1:21 | Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. |
22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
24 | GEN 1:24 | Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. |
25 | GEN 1:25 | Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na. |
26 | GEN 1:26 | Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» |
27 | GEN 1:27 | Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind. |
28 | GEN 1:28 | Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.» |
29 | GEN 1:29 | Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. |
30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
33 | GEN 2:2 | Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. |
34 | GEN 2:3 | Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp. |
35 | GEN 2:4 | Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, |
36 | GEN 2:5 | genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. |
37 | GEN 2:6 | Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. |
38 | GEN 2:7 | Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan. |
39 | GEN 2:8 | Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. |
40 | GEN 2:9 | Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon. |
42 | GEN 2:11 | Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, |
47 | GEN 2:16 | Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, |
48 | GEN 2:17 | waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.» |
49 | GEN 2:18 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» |
50 | GEN 2:19 | Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. |
51 | GEN 2:20 | Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. |
52 | GEN 2:21 | Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. |
53 | GEN 2:22 | Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. |
54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
55 | GEN 2:24 | Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux. |
56 | GEN 2:25 | Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa. |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
58 | GEN 3:2 | Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. |
59 | GEN 3:3 | Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» |
61 | GEN 3:5 | Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.» |
62 | GEN 3:6 | Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk. |
64 | GEN 3:8 | Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi. |
66 | GEN 3:10 | Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» |
67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
68 | GEN 3:12 | Aadama ne ko: «Jigéen, ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
70 | GEN 3:14 | Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp. |
71 | GEN 3:15 | Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.» |
72 | GEN 3:16 | Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.» |
73 | GEN 3:17 | Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. |
75 | GEN 3:19 | saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.» |
78 | GEN 3:22 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.» |
80 | GEN 3:24 | Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. |
81 | GEN 4:1 | Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.» |
82 | GEN 4:2 | Awa teg ca rakkam, Abel. Abel di sàmm, Kayin di bey. |
83 | GEN 4:3 | Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. |
84 | GEN 4:4 | Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel, |
87 | GEN 4:7 | Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.» |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
90 | GEN 4:10 | Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. |
92 | GEN 4:12 | Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» |
94 | GEN 4:14 | Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» |
96 | GEN 4:16 | Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku. |
97 | GEN 4:17 | Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. |
100 | GEN 4:20 | Ada taawloo Yabal, miy cosaanu sàmm yiy màngaan, |
101 | GEN 4:21 | teg ca Yubal, miy cosaanu ñi mane xalam ak toxoro. |
107 | GEN 5:1 | Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, |
135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
139 | GEN 6:1 | Bi nga xamee ne nit ñi tàmbali nañoo fulandiwu ci kaw suuf, te am ay doom yu jigéen, |
140 | GEN 6:2 | ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar. |
142 | GEN 6:4 | Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. |
143 | GEN 6:5 | Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam. |
144 | GEN 6:6 | Aji Sax ji nag am tiis ci xolam, ba mititlu li mu doon sàkk nit ci kaw suuf. |