Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   l    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

1  GEN 1:1  Ca njàlbéen galla sàkk na asamaan ak suuf.
2  GEN 1:2  Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowuglla di wër, tiim ndox mi.
3  GEN 1:3  Ba loolu ameella ne: «Na leer nekk,» leer daldi am.
4  GEN 1:4  lla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm.
5  GEN 1:5  lla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk.
6  GEN 1:6  lla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.»
7  GEN 1:7  lla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona.
8  GEN 1:8  lla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba.
9  GEN 1:9  lla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona.
10  GEN 1:10  lla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej.lla gis ne baax na.
11  GEN 1:11  lla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona.
12  GEN 1:12  Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu.lla gis ne baax na.
13  GEN 1:13  Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba.
14  GEN 1:14  lla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi.
15  GEN 1:15  Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona.
16  GEN 1:16  lla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi.
17  GEN 1:17  lla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf,
18  GEN 1:18  ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. lla gis ne baax na.
19  GEN 1:19  Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba.
20  GEN 1:20  Ba loolu ameella ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.»
21  GEN 1:21  Ci biir loolu lla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom.lla gis ne baax na.
22  GEN 1:22  Ba mu ko defeella barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.»
23  GEN 1:23  Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba.
24  GEN 1:24  lla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona.
25  GEN 1:25  lla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom.lla nag gis ne baax na.
26  GEN 1:26  lla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»
27  GEN 1:27  lla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la lla bind nit, góor ak jigéen la bind.
28  GEN 1:28  lla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»
29  GEN 1:29  lla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund.
30  GEN 1:30  Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona.