20 | GEN 1:20 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» |
21 | GEN 1:21 | Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. |
22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
25 | GEN 1:25 | Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na. |
26 | GEN 1:26 | Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» |
27 | GEN 1:27 | Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind. |
28 | GEN 1:28 | Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.» |
29 | GEN 1:29 | Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. |
30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
31 | GEN 1:31 | Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba. |
32 | GEN 2:1 | Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. |
33 | GEN 2:2 | Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. |
34 | GEN 2:3 | Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp. |
37 | GEN 2:6 | Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. |
38 | GEN 2:7 | Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan. |
39 | GEN 2:8 | Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. |
40 | GEN 2:9 | Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon. |
42 | GEN 2:11 | Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, |
43 | GEN 2:12 | di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë. |
44 | GEN 2:13 | Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp; |
45 | GEN 2:14 | turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. |
49 | GEN 2:18 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» |
50 | GEN 2:19 | Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. |
51 | GEN 2:20 | Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. |
52 | GEN 2:21 | Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. |
56 | GEN 2:25 | Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa. |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
70 | GEN 3:14 | Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp. |
71 | GEN 3:15 | Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.» |
73 | GEN 3:17 | Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. |
75 | GEN 3:19 | saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.» |
76 | GEN 3:20 | Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. |
80 | GEN 3:24 | Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. |
96 | GEN 4:16 | Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku. |
97 | GEN 4:17 | Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. |
102 | GEN 4:22 | Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
130 | GEN 5:24 | Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom. |
135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
141 | GEN 6:3 | Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» |
142 | GEN 6:4 | Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. |
147 | GEN 6:9 | Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla. |
150 | GEN 6:12 | Yàlla gis ne àddina yàqu na, ndaxte jëfi ñépp a bokk ñaaw fi kaw suuf. |
152 | GEN 6:14 | «Yaw nag wutal dénku sippar, yettal ci sa bopp gaal gu mag; nga sàkk ci ay néeg, te diw ko koltaar biir ak biti. |
155 | GEN 6:17 | «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee. |
157 | GEN 6:19 | Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc. |
158 | GEN 6:20 | Xeetu picc wu ci nekk ak xeetu bàyyima wu ci nekk ak wépp xeetu rab wuy raam ci suuf, dina def ñaar, ñëw ci yaw, ba raw. |
159 | GEN 6:21 | Sàkkal ci bépp xeetu dund, denc, ngeen bokk dunde.» |
160 | GEN 6:22 | Noonu la Nóoyin def. Lépp lu ko Yàlla sant, def na ko. |
161 | GEN 7:1 | Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge. |
162 | GEN 7:2 | Xeeti rab yu set yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen. |
163 | GEN 7:3 | Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf. |
165 | GEN 7:5 | Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp. |
168 | GEN 7:8 | Rab yu set yi ak yi setul ak picc yi ak yiy raam |
174 | GEN 7:14 | àndandook rabu àll yépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak jur gépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy naaw, lu ci nekk ak wirgoom, muy picc mbaa boroomi laaf. |
175 | GEN 7:15 | Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, |
176 | GEN 7:16 | mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee. |
179 | GEN 7:19 | Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim. |
181 | GEN 7:21 | Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp. |
183 | GEN 7:23 | Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga. |
190 | GEN 8:6 | Teg nañu ca ñeent fukki fan, Nóoyin doora ubbi poroxndoll, ba mu sàkkaloon gaal ga, |
192 | GEN 8:8 | Mu teg ca yebal pitax, ba xam ndax ndox mi ci suuf fer na. |
193 | GEN 8:9 | Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. |
194 | GEN 8:10 | Négandiku na juróom ñaari fan, doora yebalaat pitax ma. |
195 | GEN 8:11 | Ba mu délsee ca ngoon, indaalewul lu moy xobu oliw wu tooy wu keppe ca sàll wa. Nóoyin xam ne ndox mi taa woon ci suuf, fer na. |
196 | GEN 8:12 | Mu négati juróom ñaari fan, bàyyiwaat pitax ma. Boobu yoon nag délsiwaatul ca moom. |
197 | GEN 8:13 | At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na. |
201 | GEN 8:17 | Génnewaaleel lépp luy xeetu mbindeef mu ngeen àndal: picc yi ak bàyyima yi ak luy raam, ñu fulandiwu ci kaw suuf, daldi giir te bare.» |
203 | GEN 8:19 | Rabi àll yi ak luy raam ak luy naaw ak luy dox ci kaw suuf— lépp génne ca gaal ga, lu ci nekk ak wirgoom. |
204 | GEN 8:20 | Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. |
205 | GEN 8:21 | Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. |
208 | GEN 9:2 | Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo. |
209 | GEN 9:3 | Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax. |
210 | GEN 9:4 | «Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret. |
211 | GEN 9:5 | Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam. |