44 | GEN 2:13 | Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp; |
83 | GEN 4:3 | Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. |
142 | GEN 6:4 | Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. |
225 | GEN 9:19 | Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo. |
240 | GEN 10:5 | Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet. |
255 | GEN 10:20 | Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew. |
264 | GEN 10:29 | ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. |
265 | GEN 10:30 | Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa, ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku. |
266 | GEN 10:31 | Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew. |
270 | GEN 11:3 | Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, |
298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
304 | GEN 12:5 | Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan. |
340 | GEN 14:3 | Ñooñoo booloo woon ca xuru Sidim, mooy géeju Xorom gi léegi. |
344 | GEN 14:7 | Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar. |
346 | GEN 14:9 | di sot ñoom Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, ak Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar. Ñeenti buur di xareek juróom. |
347 | GEN 14:10 | Waaye xuru Sidim woowu dafa feesoon dell aki pax aki kàmbi koltaar. Ba mu ko defee buuri Sodom ak Gomor di daw, far daanu ca kàmb ya. Ña ca des daw ba ca tund ya. |
348 | GEN 14:11 | Ña leen dàq nag, jël alalu Sodom ak Gomor yépp, nanguwaale seen dund bépp boole ca, daldi dem seen yoon. |
430 | GEN 18:5 | Maa ngi leen di indil dogu mburu mu ngeen dëgërloo, ba mana topp seen yoon, gannaaw nangu ngeena toog, ma siyaare leen.» Ñu ne ko: «Waaw, baax na.» |
434 | GEN 18:9 | Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» |
460 | GEN 19:2 | «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» |
463 | GEN 19:5 | Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.» |
467 | GEN 19:9 | Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. |
571 | GEN 22:23 | Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor. |
646 | GEN 24:54 | Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.» |
649 | GEN 24:57 | Ñu ne ko: «Kon nag nanu woo janq bi, laaj ko moom ci boppam.» |
652 | GEN 24:60 | Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, te sa askan teg ay bañam tànk.» |
663 | GEN 25:4 | Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu. |
675 | GEN 25:16 | Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni mbooloo ci seeni sanc ak seeni dal. |
677 | GEN 25:18 | Ña nga dëkkoon diggante ba dale Awila ba Sur ga jàkkaarlook Misra, booy jëm Asur. Noonu la fa askanu Ismayla sance, jàkkaarlook doomi baayam yépp. |
682 | GEN 25:23 | Aji Sax ji ne ko: «Ñaari giir nga ëmb, nara am ñaari xeet yuy xaajaloo, wenn wi mooy ëpp doole wi ci des, te mag ji mooy surgawu rakk ji.» |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
714 | GEN 26:21 | Ñu gasaat ab teen, xuloo amati ca, mu tudde ko Sitna (mu firi Xuloo). |
721 | GEN 26:28 | Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw kóllëre. |
761 | GEN 27:33 | Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.» |
800 | GEN 29:4 | Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.» |
801 | GEN 29:5 | Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
804 | GEN 29:8 | Ñu ne ko: «Dunu ko man mbete gétt yépp daje, nu béraŋ doj wi, ubbi teen bi, doora wëgg gàtt yi.» |
892 | GEN 31:18 | ñu ànd tegu ca yoon wa, yóbbaale géttam gépp ak mboolem alal ju mu liggéey. Mooy gétt, ga mu sàkkoo Padan Aram. Ña ngay ñibbi kër baayam Isaaxa ca réewu Kanaan. |
915 | GEN 31:41 | Ñaar fukki at a ngii, ma di la jaamu ci kër gi, liggéeyal naa la fukki at ak ñeent ngir sa ñaari doom yu jigéen ñii, teg ci juróom benni at yu ma la sàmmal say gàtt, nga soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom. |
917 | GEN 31:43 | Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? |
920 | GEN 31:46 | Yanqóoba ne ay bokkam: «Forleen ay doj.» Ñu for ay doj, def ko ab jal, daldi lekk foofa ca wetu jal ba. |
923 | GEN 31:49 | Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na Aji Sax ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree. |
931 | GEN 32:3 | Ba leen Yanqóoba gisee, da ne dalub Yàllaa ngii, ba tax mu tudde bérab ba Maanayim (mu firi Ñaari dal). |
965 | GEN 33:4 | Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy! |
966 | GEN 33:5 | Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.» |
985 | GEN 34:4 | Loolu waral mu ne baayam Amor: «Ñaanal ma janq bi jabar.» |
1002 | GEN 34:21 | «Ñii sunuy am-di-jàmm lañu, te gannaaw réew maa ngi ne yàmblaŋ, bàyyileen leen, ñu sanc te dem fu leen neex. Man nanoo jël seen doomi janq te di leen may sunuy doom. |
1009 | GEN 34:28 | Ñu daldi jël seen jur gu gàtt ak gu gudd, seeni mbaam ak mboolem la ca biir dëkk ba ak la ko wër. |
1012 | GEN 34:31 | Ñu ne ko: «Danuy seetaan sunu jigéen daal, ñu di ko def ab gànc?» |
1016 | GEN 35:4 | Ñu daldi jox Yanqóoba mboolem tuuri doxandéem, yi ñu yor, ak seen jaaroy nopp, Yanqóoba boole suul ca taatu garab gu mag ga nekkoon ca wetu dëkk, ba ñu naan Sikem. |
1020 | GEN 35:8 | Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (mu firi Garabu jooyoo). |
1038 | GEN 35:26 | Doomi Silpa, jaamub Leya, di Gàdd ak Aser. Ñooñooy doomi Yanqóoba, te mu am leen ca Padan Aram. |
1043 | GEN 36:2 | Esawu jël na janqi Kanaaneen jabar. Ñooñoo di: Ada doomu Elon, Etteen ba, ak Olibama doomu Ana, miy doomu Sibeyon, Eween ba, |
1046 | GEN 36:5 | Olibama am ca Yewus, Yalam ak Kora. Ñooñu ñooy doomi Esawu, te mu am leen ca réewu Kanaan. |
1053 | GEN 36:12 | Timna it nekkaaleb Elifas. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu. |
1054 | GEN 36:13 | Doomi Rewel yu góor yi ñoo di: Naxat ak Sera ak Saama ak Misa. Ñooñoo xeetoo ca Basmat, soxnas Esawu. |
1056 | GEN 36:15 | Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Sefo ak Kenas |
1058 | GEN 36:17 | Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu. |
1059 | GEN 36:18 | Ñi xeetoo ci Olibama soxnas Esawu, ñooy Yewus, Yalam ak Kora, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi Olibama, soxnas Esawu siy doomu Ana. |
1060 | GEN 36:19 | Ñooñooy doomi Esawu, mi ñuy wax Edom, ñooñooy doomam yu góor, ñook seeni làng. |
1062 | GEN 36:21 | ak Dison ak Eser ak Disan. Ñooñooy làngi waa Or, di sëti Seyir ya ca réewum Edom. |
1071 | GEN 36:30 | ak Dison ak Eser ak Disan, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi waa Or, na ñu xàjjalikoo kenn-kenn ca réewu Seyir. |
1084 | GEN 36:43 | ak Magdiyel ak Iram, ku ci nekk ak làngam. Ñooñu ñooy làngi Edom, ma ñu naa Esawu, moom ma giir Edomeen ñi, làng gu ci nekk ak gox, ba nga dëkke te moom ko. |
1092 | GEN 37:8 | Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax. |
1103 | GEN 37:19 | Ña nga naan: «Boroom gént gaa ngee di ñëw! |
1108 | GEN 37:24 | Ñu jàpp ko, tàbbal ca biir kàmb ga, fekk mu déy, ba wow koŋŋ. |
1112 | GEN 37:28 | Julay Majan ya nag jaare fa, ñu yóotu Yuusufa, génne ko kàmb ga, jaay ko Ismayleen ña ci ñaar fukki dogi xaalis. Ñu yóbbu Yuusufa Misra. |
1115 | GEN 37:31 | Ñu jël nag mbubbu Yuusufa, rendi ab sikket, taqal mbubb ma ca deret ja. |
1133 | GEN 38:13 | Ñu yégal Tamar ne ko: «Sa goroo ngii jëm Timna, di wati ay xaram.» |
1141 | GEN 38:21 | Mu laaj waa gox ba, ne leen: «Ana gànc biy toog Enayim ci yoon wi?» Ñu ne ko: «Fii de ab gànc nekku fi.» |
1149 | GEN 38:29 | Naka la delloo loxoom, seexam juddu, mu ne ko: «Yaw foo bëtte, ba génn?» Ñu daldi ko tudde Peres (mu firi Bëtt). |
1181 | GEN 40:8 | Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.» |
1185 | GEN 40:12 | Yuusufa ne ko: «Piri mi mooy lii. Ñetti car yi, ñetti fan la. |
1189 | GEN 40:16 | Kilifag lakk-kati mburu ya nag gis ne piri mi neex na, mu ne Yuusufa: «Man it sama gént gi, xam nga lu ma ci gis? Ñetti pañey mburu mu weex laa yenu, |
1193 | GEN 40:20 | Ñu teg ca ñetti fan, Firawna di màggal bésu juddoom, dajale jawriñam yépp, di leen berndeel, daldi cay seppee kilifa gay topptoo ay naanam, ak kilifag lakk-kati mburu ya, siggil leen. |
1197 | GEN 41:1 | Ñaari ati lëmm wees na gannaaw loolu, gént dikkal Firawna, mu jeneer taxaw ca wetu dexu Niil. |
1210 | GEN 41:14 | Ba Firawna déggee loolu, dafa woolu Yuusufa. Ñu gaaw tijji ko, mu watu, solu, doora wuyji Firawna. |
1231 | GEN 41:35 | Ñoom nañu dajale mboolem dundi at yu baax yi, te boole pepp mi ci sa ndigalu bopp, yaw Firawna, muy dund bu ñuy denc ci dëkk yi. |
1260 | GEN 42:7 | Naka la Yuusufa gis magam ya, xàmmi leen, te mel ni ku leen xamul, di wax ak ñoom kàddu yu dëgër ne leen: «Fu ngeen jóge?» Ñu ne ko: «Réewu Kanaan lañu jóge, di jëndsi ab dund.» |
1263 | GEN 42:10 | Ñu ne ko: «Mukk sang bi, danu lay siyaare, di wutsi ab dund rekk, |
1266 | GEN 42:13 | Ñu ne ko: «Nun ñii di la siyaare de, fukki góor ak ñaar lanu woon, bokk sunu baay, ba ca Kanaan. Ka ca gën di xalee nga ca sunu baay, te ka ca des nekkatul.» |
1273 | GEN 42:20 | Waaye nangeen ma indil seen rakk, ba ma xam ne li ngeen wax dëgg la; su ko defee dungeen dee.» Ñu daldi ne: «Waaw,» |
1278 | GEN 42:25 | Gannaaw loolu Yuusufa joxe ndigal, ñu sol seeni saaku pepp, te ku nekk ca ñoom, ñu yebal ko xaalisam ca saakoom, ba noppi mayaale leen lu ñu lekk ca yoon wa. Ñu defal leen noonu. |
1298 | GEN 43:7 | Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!» |
1309 | GEN 43:18 | Ñu am nag tiitaange ndax li ñu leen yóbbu kër Yuusufa. Ña ngay xalaat naan: «Boo demee, xaalis bi ñu yeboon ci sunuy saaku yoon wu jëkk wa, moom lañu bëgga taafantoo, dugal nu fii, ba song nu, jàpp nu jaam, nangu sunuy mbaam, boole ci.» |
1311 | GEN 43:20 | Ñu ne ko: «Sang bi baal nu, nun de ñëwoon nanu fi lu jiitu ngir jëndsi dund, |
1319 | GEN 43:28 | Ñu ne ko: «Sunu baay mu ngi dund, sang bi, te mu ngi ci jàmm.» Ña nga koy sukkal tey sujjóotati. |
1324 | GEN 43:33 | Ña nga toog, na mu leen ko sante, taaw ba fegge wet, ni ko ko céru taaw maye, ñu sësaloo, na ñu toppantee ciy at, ba ca caat ma. Gaa ñaa nga yéemu, di xoolante. |
1325 | GEN 43:34 | Mu sàkkal leen ca ndabam, te Beñamin ëpple ku ci nekk juróomi yoon. Ñu bokk nag naana naan, ba seen xol sedd. |
1332 | GEN 44:7 | Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu! |
1336 | GEN 44:11 | Ñu gaaw nag, wàcce seeni saaku ci suuf, ku nekk ubbi saakoom. |
1339 | GEN 44:14 | Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf. |
1360 | GEN 45:1 | Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam. |
1363 | GEN 45:4 | Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra. |
1365 | GEN 45:6 | Ñaari at a ngii xiif baa ngi ci réew mi, te fii ak juróomi at ci kanam, kenn du bey, kenn du góob. |
1383 | GEN 45:24 | Gannaaw loolu mu yiwi ay magam ne leen: «Ngalla buleen xuloo ci yoon wi.» Ñu daldi dem. |