54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
60 | GEN 3:4 | Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! |
93 | GEN 4:13 | Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! |
356 | GEN 14:19 | Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf! |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
450 | GEN 18:25 | Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
465 | GEN 19:7 | Mu ne leen: «Bokk yi, ngalla buleen def lu bon loolu waay! |
467 | GEN 19:9 | Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. |
476 | GEN 19:18 | Lóot nag ne ko: «Déet, sang bi! |
521 | GEN 21:7 | Mu neeti: «Éy, ku noon Ibraayma, Saarataa ngay nàmpal! Teewul ma jural ko góor, te muy mag.» |
623 | GEN 24:31 | Mu ne ko: «Yaw mi Aji Sax ji barkeel, agsil boog! Looy toog ci àll bi; waajalal naa la ab dal, te giléem yi am nañu fu ñu nekk.» |
652 | GEN 24:60 | Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, te sa askan teg ay bañam tànk.» |
702 | GEN 26:9 | Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» |
748 | GEN 27:20 | Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» |
791 | GEN 28:17 | Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.» |
844 | GEN 30:13 | Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte). |
889 | GEN 31:15 | Doonunu lu moy ay doxandéem ci moom de! Nde da noo jaay, lekk sunu njég, ba mu jeex tàkk. |
902 | GEN 31:28 | Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii! |
965 | GEN 33:4 | Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy! |
1103 | GEN 37:19 | Ña nga naan: «Boroom gént gaa ngee di ñëw! |
1114 | GEN 37:30 | Ba loolu amee mu jóge ca, dem ca ay rakkam ne leen: «Xale ba nekkatu fa de! Te man xawma nu may def léegi.» |
1117 | GEN 37:33 | Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!» |
1305 | GEN 43:14 | Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.» |
1332 | GEN 44:7 | Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu! |
1353 | GEN 44:28 | Kenn ki dem, wacc ma, ma ne moom kay, aw rabu àll a ko daggate! Gisaatuma ko ba tey jii. |
1356 | GEN 44:31 | bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbsi— aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw. |
1362 | GEN 45:3 | Yuusufa nag ne magam ya: «Man mii maay Yuusufa! Mbaa sama baay a ngi dund?» Magam ya nag manuñu koo tontu, ndax booba njàqare jàpp na leen. |
1385 | GEN 45:26 | Ñu wax ko ne ko: «Ndekete Yuusufaa ngi dund! te sax mooy kilifag réewum Misra gépp.» Ba Yanqóoba déggee loolu, yaramam dafa dee goyy ca saa sa, ndaxte gëmu leen. |
1387 | GEN 45:28 | Israyil daldi ne: «Moom kay na dund rekk! Sama doom Yuusufaa ngi dund. Man kay dinaa dem ba gis ko, bala ma fee jóge.» |
1436 | GEN 47:15 | Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» |
1446 | GEN 47:25 | Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.» |
1492 | GEN 49:18 | «Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal! |
1650 | EXO 5:17 | Firawna ne leen: «Yaafus yi ngeen doon! Yaafus a leen tax di wax naan: “May nu, nu dem rendili Aji Sax ji sarax.” |
1651 | EXO 5:18 | Neleen mott, liggéeyi! Du menn boob mu ñu leen di jox. Te du tee ngeen matal seen limu móol.» |
1785 | EXO 10:7 | Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» |
1786 | EXO 10:8 | Ñu délloosi nag Musaak Aaróona ca Firawna, mu ne leen: «Demleen màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Waaw, ñiy dem sax, ñan la?» |
1788 | EXO 10:10 | Firawna ne leen: «Ãa, yal na leen Aji Sax ji saxoo taxawu walla, ndegam maa leen di bàyyi moos, ngeen dem, yóbbaale seen njaboot! Xam ngeen ne naruleen njub de. |
1789 | EXO 10:11 | Mukk laa wax! Du dangeen di màggal Aji Sax ji? Demleen boog, yeen ñiy góor!» Ba loolu amee ñu dàq leen, ñu jóge ca Firawna, |
1806 | EXO 10:28 | Firawna nag ne Musaa: «Neel mott! Bul fexe ba taxawati sama kanam! Ndax bés boo jàkkaarlooteek man, kera ngay dee.» |
1848 | EXO 12:31 | Ba loolu amee Firawna woolu Musaak Aaróona ca guddi googu, ne leen: «Ayca! Mott! Soreleen sama waa réew, yeen ak seeni bokk! Laggleen, jaamuji Aji Sax ji, li ngeen bëgg. |
1849 | EXO 12:32 | Te itam yóbbaaleleen seen juroo jur, gu gudd ak gu gàtt, li ngeen bëgg rekk, te ne mott! Waaye ñaanaaleleen ma seen Yàlla nag, mu barkeel ma.» |
1924 | EXO 15:3 | «Aji Sax ji jàmbaari xare ji, Aji Sax jeey turam! |
1927 | EXO 15:6 | «Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax. |
1929 | EXO 15:8 | Nga wal sag noo, ndox ya tegloo, wal ma ne sàtt, jaloo jalu, ndoxi xóotey géej way deeŋ! |
1931 | EXO 15:10 | Waaye sa ngelaw nga wal, géej mëdd leen, ñu diigandoo ni beteex biir géej mbàmbulaan! |
2448 | EXO 32:9 | Aji Sax ji dellu ne Musaa: «Maa gis askan wii, askan wu dëgër bopp a ngii! |
2489 | EXO 33:15 | Musaa ne ko: «Soo demul yaw ci sa bopp kay, bu nu jële fii! |
2506 | EXO 34:9 | ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.» |
2997 | LEV 10:19 | Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» |
4029 | NUM 11:4 | Ci biir loolu genn gàngooru njaxasaan mu nekkoon ca seen biir jiital seen bakkan, di ŋaf-ŋafi, ba tax bànni Israyil itam dellu di jàmbat. Ña nga naan: «Éy ku nuy leelatiw yàpp! |
4030 | NUM 11:5 | Namm nan jën ya nu daa ndawaloo ca Misra, te dikkewu nu tus! Ak yomb jaak xaal jaak pooro baak soble saak laaj ja! |
4046 | NUM 11:21 | Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! |
4070 | NUM 12:10 | Naka la niir wa jóge ca xayma ba, Maryaama jekki ne fureet ak jàngoroy ngaana, weex furr! Aaróona ne Maryaama gees, yem ca ngaana ga. |
4071 | NUM 12:11 | Aaróona ne Musaa: «Ngalla sang bi, bu nu topp bàkkaar bi nu bàkkaar ndax ñàkk xel! |
4103 | NUM 13:27 | Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa. |
4111 | NUM 14:2 | Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii! |
4112 | NUM 14:3 | Ana lu nu Aji Sax jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?» |
4127 | NUM 14:18 | “Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.” |
4150 | NUM 14:41 | Musaa ne leen: «Lii nag? Yeena ngi tebbi waxi Aji Sax ji, waaye loolu de du sotti! |
4198 | NUM 16:3 | Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?» |
4203 | NUM 16:8 | Musaa teg ca ne Kore: «Yeen Leween ñi, dégluleen nag! |
4205 | NUM 16:10 | Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci! |
4206 | NUM 16:11 | Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?» |
4207 | NUM 16:12 | Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul! |
4214 | NUM 16:19 | Kore nag dajale gàngoor gépp fa ñoom, ca bunt xaymab ndaje ma. Ci kaw loolu leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp! |
4257 | NUM 17:27 | Bànni Israyil nag naan Musaa: «Jeexal nan nag, sànku nan, nun ñépp ay sànku! |
4322 | NUM 20:10 | Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?» |
4370 | NUM 21:29 | Mowabee ngalla yaw! Sànku ngeenee, yeen askanu Kemos, mi wacc doomam yu góor, ñu daw, doomam yu jigéen doon jaami Siwon buurub Amor. |
4452 | NUM 24:5 | Yanqóobaa, yaaka yànji xayma! Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan! |
4457 | NUM 24:10 | Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la wooye woon, yaw defoo lu moy ñaanal leena ñaanal, ba muy ñetti yoon nii! |
4681 | NUM 31:15 | Musaa ne leen: «Kon jigéeni Majan ñépp ngeen bàyyi, ñu dund! |
4905 | DEU 1:11 | Yal na leen seen Yàllay maam Aji Sax ji yokkati junniy yoon, te barkeel leen ni mu leen ko waxe! |
5079 | DEU 5:24 | Ngeen ne ma: «Sunu Yàlla Aji Sax ji kat, moo nu won darajaam ak màggaayam. Kàddoom lanu dégg, mu jibe ca digg sawara wa. Bésub tey noo gis Yàlla wax ak doom aadama, ba noppi, muy wéye bakkanam! |
5084 | DEU 5:29 | Waaye céy bu ñu amoon boobu xol ngir ragal ma, di sàmm sama santaane yépp bés bu nekk, ba tax ñu baaxle, ñoom ak seen askan, ba fàww! |
5160 | DEU 9:1 | Israyil dégluleen! Yeena ngii tey, di jàll dexu Yurdan ngir dàqi xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole, ngir nangu seen dëkk yu réy, dàbblikoo tata yu àkki asamaan. |
5166 | DEU 9:7 | Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke. |
5432 | DEU 20:3 | ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam! |
5685 | DEU 29:3 | te taxul Aji Sax ji may leen xel mu ngeen ràññee, ak gët yu ngeen gise, ak nopp yu ngeen dégge, booba ba sunu jonni yàllay tey! |
5765 | DEU 32:5 | Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam, ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk. Ndaw maas gu dëng te njublaŋ! |
5766 | DEU 32:6 | Aji Sax ji lañuy feye lii? Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel! Mooy seen baay, bind leen, sàkk leen, samp leen. |
5792 | DEU 32:32 | Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom, ak tóokëri Gomor, doom ya di tooke, cëgg ya wex xàtt! |
5798 | DEU 32:38 | Ñi lekk seen nebboni sarax, naan biiñ bi ñu leen di tuural kay, nañu jóg, boog, xettli leen, di seen kiiraay! |
5799 | DEU 32:39 | Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, kenn du Yàlla ku dul man! Man maay rey, di dundal; di gaañe, di wéral; maay jàpp, te kenn du xettli. |
5807 | DEU 32:47 | Ndax kat du kàddug neen ci yeen. Mooy seenug dund! Ci gii kàddu ngeen di gudde fan, ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan jëm fa, ngir nanguji ko.» |
5838 | DEU 33:26 | Kenn du Yàllay Yesurun! Keey war asamaan, wallusi leen, war ay niir, ànd ak darajaam. |
7184 | RUT 3:10 | Mu ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel, doom! Jiwati nga bokk gi ngor lu gënatee rafet. Ndax su la neexoon, nga topp ci xale yu góor yi, ñu am ak ñu ñàkk. |
7206 | RUT 4:14 | Jigéen ña ne Nawmi: «Sant Aji Sax ji, moom mi la xañul mbokk mu la jotaat nii tey! Yal na xale bi di ku amu tur ci Israyil gépp. |
7222 | 1SA 1:8 | Elkana jëkkër ja di ko wax ne ko: «Aana, looy jooy, ak lu la tee lekk? Ñàkk doom a la tax ne yogg nii? Maa ngii! Dama laa gënalul fukki doom yu góor?» |
7225 | 1SA 1:11 | Ci biir loolu mu xas aw xas, daldi ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Sang bi, soo nemmiku woon ba nemmiku njàqare jii ma nekke, bàyyi ma xel, bañ maa fàtte, ba may ma doom ju góor! Kon déy, maa ko sédde Aji Sax ji, giiru dundam gépp, saatus watukaay du jaar ci boppam mukk!.» |
7244 | 1SA 2:2 | «Kenn sellul ni Aji Sax ji, amuloo dend moos, cëslaay melul ni sunu Yàlla! |
7266 | 1SA 2:24 | Aa! Xale yi, coow li ma dégg, muy law ci biir ñoñi Aji Sax ji, rafetul de! |
7306 | 1SA 4:7 | tiitaangee leen jàpp, ñu ne: «Am na yàlla ju dugg ca biir dal ba! Wóoy, ngalla nun! Nde guléet tey lu mel nii am! |
7307 | 1SA 4:8 | Wóoy ngalla nun! Ku nuy musal ci jii yàlla ju bare doole. Yàlla jii moo dumaa woon waa Misra xeeti mbugal yu nekk, ca màndiŋ ma. |
7465 | 1SA 12:3 | Maa ngii! Seedeleen sama jépp tuuma fi kanam Aji Sax ji ak ki mu fal. Ana ku ma masa jël nagam, mbaa ma jël mbaamam? Ana ku ma masa lekk àqam, mbaa ma néewal ko doole? Ana ci kan laa masa nangoo alalu ger, ba nëpp-nëppal lu mu def. Lu ci am rekk, waxleen, ma fey ko.» |
7539 | 1SA 14:29 | Yonatan ne: «Sama baay de yàqal na mbooloo mi. Xool-leen rekk ni samay bët leere ndax lem sii ma ñam! |
7540 | 1SA 14:30 | Astamaak bu mbooloo mi lekkoon tey ci lël ja ñu nangoo ci noon yi! Du ci la jéllu waa Filisti doon gëna réy a waay?» |
7543 | 1SA 14:33 | Ñu yegge ko Sóol, ne ko: «Mbooloo ma kat a nga nee, di moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Sóol ne: «Yeenaka fecci kóllëre! Béraŋal-leen ma fii aw doj wu mag léegi.» |
7555 | 1SA 14:45 | Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul. |