549 | GEN 22:1 | Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.» |
555 | GEN 22:7 | Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» |
559 | GEN 22:11 | Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» |
1239 | GEN 41:43 | ba noppi waral ko watiiru ku sës rëkk ci moom Firawna, te fu mu ware ñu jiitu ko, di yéene naan: «Sujjóotleen!» Noonu la ko Firawna fale, mu yilif Misra gépp. |
5602 | DEU 27:15 | «Alku ñeel na képp ku sàkk, bay teg ci bérab bu làqu, li Aji Sax ji seexlu, te ab liggéeykat sàkke ko ay loxoom, muy jëmmu tuur mu ñu yett, mbaa mu ñu móol.» Su ko defee mbooloo mépp àddoondoo, ne: «Amiin!» |
5603 | DEU 27:16 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku torxal baayam mbaa ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5604 | DEU 27:17 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku toxal màndargam kemu suufas moroomam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5605 | DEU 27:18 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku sànk silmaxa ci aw yoon.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5606 | DEU 27:19 | Ñu neeti «Alku ñeel na ku jengal àtteb doxandéem ak jirim akub jëtun.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5607 | DEU 27:20 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde jabaru baayam, ndax suturas baayam la xàwwi.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5608 | DEU 27:21 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde mboolem luy mala.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5609 | DEU 27:22 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde ab jigéenam, muy doomu baayam, mbaa doomu ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5610 | DEU 27:23 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde yaayu jabaram.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5611 | DEU 27:24 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku rey moroomam ci kumpa.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5612 | DEU 27:25 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku nangub ger, ngir rotal bakkanu nit ku deful dara.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5613 | DEU 27:26 | Ñu neeti: «Alku ñeel na ku saxoowul kàdduy yoon wii, di ko jëfe.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» |
5839 | DEU 33:27 | Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, përëgam bi sax dàkk di cëslaay, moo la dàqal ab noon ne la: «Jekklil!» |
7578 | 1SA 15:16 | Samiyel ne Sóol: «Defal ndànk! Dinaa la xamal li ma Aji Sax ji wax biig.» Mu ne ko: «Waxal!» |
8066 | 2SA 2:14 | Abner ne Yowab: «Ayca na xale yu góor yi jóg, daje fi sunu kanam.» Yowab ne ko: «Ayca!» |
8236 | 2SA 9:6 | Ba loolu amee Mefiboset doomu Yonatan doomu Sóol, dikk ca Daawuda, ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot. Daawuda ne ko: «Mefiboset!» Mu ne ko: «Naam, sang bi.» |
8504 | 2SA 18:23 | Mu ne ko: «Lu ci mana am, bëgg namaa dem.» Yowab ne ko: «Demal!» Ayimaas daw, jaare ca joor ga, ba jëkk waa Kuus ba. |
9378 | 1KI 18:34 | Mu ne leen: «Duyleen ñeenti njaqi ndox, tuur ci kaw yàpp week matt mi.» Ñu def ko. Mu ne: «Defaatleen!» Ñu defaat. Mu ne: «Defatileen, muy ñetti yoon!» Ñu def ko, ba muy ñetti yoon. |
9423 | 1KI 20:12 | Ba Ben Addàd di jot ca kàddu googu, ma ngay naan, mook buur ya far ak moom ca mbaar ya. Mu jox ay nitam ndigal ne leen: «Takkuleen!» Ñu takku, ngir songi dëkk ba. |
9685 | 2KI 6:7 | Mu ne ko: «Foral!» Mu yóotu, for ko. |
9781 | 2KI 9:21 | Ba mu ko defee Yoram ne: «Takkleen!» Ñu takkal Yoram buurub Israyil watiiram, mu génn ànd ak Akasiya buurub Yuda, ku nekk ak sa watiir; ñu dawal dogaleji Yewu, taseek moom fa doonoon toolub Nabot mu Yisreel. |
9892 | 2KI 13:17 | ba noppi ne ko: «Ubbil palanteeru penku bi.» Mu ubbi. Alyaasa ne ko: «Soqil!» Mu soqi. Mu ne ko: «Fittu ndamal Aji Sax jaa ngoog, di fitt gi ngay ame ndam ci waa Siri. Dinga daan waa Siri ca Afeg, ba faagaagal leen.» |
15766 | PSA 106:48 | Santleen Aji Sax ji, Yàllay Israyil cant gu sax dàkk, ba fàww. Na ñépp ne: «Amiin!» Màggal-leen Ki Sax! |
17382 | PRO 31:28 | Doom ya dañu ko naan: «Jarawlakk!» jëkkër ja di ko gërëm naan: |
18496 | ISA 40:6 | Baat a ngi naa: «Yéeneel!» Ma ne: «Lu may yéene?» Mu ne: «Neel: Bépp boroom suux am ñax doŋŋ la; gépp ngoram mel ni tóor-tóoru àll. |
27295 | ACT 9:10 | Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.» |
27331 | ACT 10:3 | Am peeñu nag dikkal ko digg njolloor, mu gis ci lu leer malaakam Yàlla, mu duggsi, ne ko: «Korney!» |
29068 | 2CO 11:11 | Lu tax? Ndax dama leena buggul? Yàlla xam na ne «ahakay!» |
30862 | REV 6:1 | Ma gis nag Gàtt bi di tàyyi genn ci juróom ñaari tayu yi. Ci biir loolu ma dégg kenn ci ñeenti bindeef yi àddoo baat buy riir ni dënu, ne: «Dikkal!» |
30864 | REV 6:3 | Ba Gàtt bi tàyyee ñaareelu tayu gi, ma dégg ñaareelu mbindeef mi ne: «Dikkal!» |
30866 | REV 6:5 | Ba mu tàyyee ñetteelu tayu gi, ma dégg ñetteelu mbindeef mi ne: «Dikkal!» Ma xool rekk, gis fas wu ñuul, gawaram yor ab màndaxekaay. |
30868 | REV 6:7 | Ba Gàtt bi tàyyee ñeenteelu tayu gi, ma dégg ñeenteelu mbindeef mi ne: «Dikkal!» |
31166 | REV 22:17 | Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la. |