5680 | DEU 28:67 | Ag suba ngeen ne: «Éy waay, bu doon ngoonati.» Bu ngoonee ngeen ne: «Éy waay, bu doon subaati!», ndax tiitaange lu ngeen di tiit, ak li ngeen di teg seeni gët. |
25184 | LUK 5:8 | Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!», |
27413 | ACT 12:7 | Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom. |
28443 | 1CO 1:12 | Li may wax mooy ku nekk ci yeena ngi naan: «Man ci Póol laa bokk!», «Man nag Apolos!» «Man Sefas!» «Man de Almasi!» |