|
12332 | Ma ne leen: «Yàlla Boroom asamaan moo nuy may ndam. Nun ñiy jaamam nooy jóg tabaxaat dëkk bi. Yeen nag amuleen wàll ci Yerusalem, te baaxoowuleen fi benn sañ-sañ!» | |
22103 | Gannaaw loolu mu ne ma: «Yaw nit ki ñu naw, bul tiit. Jàmm la. Góor-góorlul!» Muy wax ak man, may amaat doole, ba ne ko: «Waxal sang bi, dooleel nga ma.» |