109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
110 | GEN 5:4 | Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
112 | GEN 5:6 | Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. |
113 | GEN 5:7 | Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
114 | GEN 5:8 | Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu. |
115 | GEN 5:9 | Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. |
116 | GEN 5:10 | Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
118 | GEN 5:12 | Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. |
119 | GEN 5:13 | Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
120 | GEN 5:14 | Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu. |
121 | GEN 5:15 | Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. |
122 | GEN 5:16 | Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
123 | GEN 5:17 | Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. |
124 | GEN 5:18 | Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. |
125 | GEN 5:19 | Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
126 | GEN 5:20 | Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu. |
127 | GEN 5:21 | Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
131 | GEN 5:25 | Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. |
132 | GEN 5:26 | Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
133 | GEN 5:27 | Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu. |
134 | GEN 5:28 | Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor. |
136 | GEN 5:30 | Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
137 | GEN 5:31 | Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu. |
138 | GEN 5:32 | Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. |
235 | GEN 9:29 | Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. |
278 | GEN 11:11 | Arpagsàdd juddu na, Sem dundaat juróomi téeméeri at (500), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
280 | GEN 11:13 | Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
282 | GEN 11:15 | Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
284 | GEN 11:17 | Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
286 | GEN 11:19 | Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
288 | GEN 11:21 | Serug juddu na, Rew dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñaar (207), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
292 | GEN 11:25 | Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
299 | GEN 11:32 | Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
422 | GEN 17:24 | Ibraayma amoon na juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), bi muy xaraf; |
573 | GEN 23:1 | Saarata dund na, ba am téeméeri at ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127), |
1538 | EXO 1:5 | Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. |
2658 | EXO 38:24 | Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, te muy wurus wu ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi. |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
3937 | NUM 7:86 | Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). |
4696 | NUM 31:30 | Céru bànni Israyil bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.» |
4718 | NUM 31:52 | Mboolem wurusu jooxe, wi ñu jooxeel Aji Sax ji, di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñaar fukki kilo (170), te bawoo ci kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya. |
7314 | 1SA 4:15 | Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara. |
8261 | 2SA 10:18 | Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa. |
8869 | 1KI 5:2 | Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas; |
8900 | 1KI 6:1 | Ca ñeenti téeméereelu at maak juróom ñett fukk (480), gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, ci weeru Siw, di ñaareelu weeru at ma, ca la Suleymaan tàmbalee tabax kër Aji Sax ji. |
9111 | 1KI 10:29 | Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri dogi xaalis (600) la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki dogi xaalis (150), te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen. |
12030 | EZR 1:9 | Lenn ci lim bi tëdde nii: fanweeri ndabi wurus (30), ak junniy ndabi xaalis (1 000), ak ñaar fukki paaka ak juróom ñeent (29), |
12098 | EZR 2:66 | Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12099 | EZR 2:67 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12224 | EZR 8:18 | Sunu Yàlla nag toppe nu mbaaxu yiwam, ba ñu indil nu waa ju am xel, askanoo ci Maali sëtub Lewi doomu Israyil. Ñu di ko wax Serebya. Mu ànd ak doomam yu góor aki bokkam, ñuy fukk ak juróom ñett (18), |
12226 | EZR 8:20 | Indaale nañu ñaar téeméeri liggéeykati kër Yàlla ak ñaar fukk (220), di ñu askanoo ca ña Daawudaaki jawriñam tànnoon, bind seeni tur, ngir ñuy jàpple Leween ñi. |
12241 | EZR 8:35 | Ba mu ko defee ña jóge njaam, ñibbsee ca ngàllo ga, daldi defal Yàllay Israyil ay saraxi dóomal. Muy fukki yëkk ak ñaar, ñeel Israyil gépp ak juróom ñeent fukki kuuy ak juróom benn (96), ak juróom ñaar fukki xar yu ndaw ak juróom ñaar (77), ak fukki sikket ak ñaar yu ñu def saraxu póotum bàkkaar; ñu def lépp saraxu dóomal, ñeel Aji Sax ji. |
12404 | NEH 5:17 | Rax ci dolli daan naa woo téeméeri kilifay Yawut ak juróom fukk (150), di bokk ak ñoom sama njël, te limaalewuma ñi bàyyikoo ci jaambur yi nu séq, di nu fekksi. |
12492 | NEH 7:67 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12493 | NEH 7:68 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12710 | EST 1:4 | Ci diir bu takku, tollook téeméeri fan ak juróom ñett fukk (180), mu di leen won alalu nguuram ju yéeme ak dayoom ak darajaam ju réy. |
12844 | EST 9:6 | Ca biir Sus, péey ba, Yawut ya bóom nañu fa juróomi téeméeri nit (500), sànk leen. |
20374 | JER 52:29 | ak juróom ñetti téeméer ak fanweer ak ñaar (832), loolu yemook fukkeelu atu nguuram ak juróom ñett, |
21710 | EZK 45:11 | Na benn efa ak benn bat yem dayo, lu ci nekk wara def céru fukkeelu benn omer, bi yemook ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220), mbaa téeméeri kilo ak juróom fukk (150). Te na benn omer di dayo bi ngeen di natte. |
25661 | LUK 15:4 | «Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko? |