Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   Word-Word-Word,    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

3278  LEV 18:26  «Yeen nag sàmmleen samay dogal ak samay santaane te bu kenn def lenn ci yooyu ñaawtéef, du njuddu-ji-réew, du doxandéem bi ci seen biir,
3463  LEV 24:16  Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
3469  LEV 24:22  Na àtte bi di benn ci doxandéem ak njuddu-ji-réew, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.»
4167  NUM 15:13  Mboolem njuddu-ji-réew, noonu lay defe sarax yooyii, buy indi saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
4184  NUM 15:30  Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam:
7154  RUT 2:3  Mu dem ca tool ya, topp ñay góob, di foraatu. Yàlla-woo-yàlla, tool booba di toolu Bowas ma bokk ak Elimeleg.
9188  1KI 13:1  Yàlla-woo-yàlla, genn góoru Yàlla jóge Yuda, dikk ba Betel ci ndigalal Aji Sax ji, fekk Yerbowam taxaw ca sarxalukaay ba, nara taal saraxu cuuraay.
9304  1KI 16:18  Ba Simri gisee ne nangu nañu dëkk ba, daa dugg kër Buur, jàll ca biir-a-biir, daldi taal kër ga ca kawam, dee.
9858  2KI 12:5  Mu am bés mu wax sarxalkat ya ne leen: «Mboolem xaalis bu ñu sellalal kër Aji Sax ji, muy xaalisu njot-gi-bakkan, mbaa xaalis bu ñu wàccoo ngiñ, mbaa bépp xaalisu saraxu yéene bu nit di indi kër Aji Sax ji,
13349  JOB 20:19  Moo dëggaate néew-ji-doole, dëddu ko; aakimoo kër jaambur te tabaxu ko.
13399  JOB 22:6  Yaa lebal mbokk, aakimoo tayleem ci dara, bay nangu mbubbam néew-ji-doole, mu ne duŋŋ.
13444  JOB 24:4  Néew-ji-doole, ñu buuxe ko ciw yoon, baadoolo yi far bokk làquji.
13552  JOB 29:16  Néew-ji-doole, maa doon baayam, ku ma xamul sax, may seet àqam.
14041  PSA 9:10  Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
14054  PSA 10:2  Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole, lal ay pexeem, ba jàpp ko.
14070  PSA 10:18  ngir sàmm àqu jirim ak néew-ji-doole, ba nit kiy suufu kese dootu xëble.
15293  PSA 81:17  Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp, reggal leen lem ju doj xelli.»
15854  PSA 109:31  Mooy féete ndijoor néew-ji-doole, musal ko ci ku koy teg àtteb dee.
16418  PSA 146:7  di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
16427  PSA 147:6  Aji Sax ji, néew-ji-doole, mu yenni; ku bon, mu daane ci suuf.
16445  PSA 148:4  Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
16746  PRO 10:20  Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
17293  PRO 28:27  Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.
17301  PRO 29:7  Ku jub a xam àqu néew-ji-doole, ab soxor xamu ca dara.
17335  PRO 30:14  Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.
17475  ECC 5:7  Boo gisee ñuy not néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
17608  SNG 1:1  Lii, di ngën-gi-woy, ñeel Suleymaan.
17628  SNG 2:4  Dugal na ma néegub sago-jeex-na, yiire ma mbëggeel.
18192  ISA 25:4  Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, nde merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.
18866  ISA 58:10  di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg, di reggal néew-ji-doole, su boobaa seen leer fenke biir lëndëm, seenug këruus di ag njolloor,
20935  EZK 18:17  néew-ji-doole, loxoom dalu ko, ndollant ak ab tegandaay, jëlu ko, sama àttey yoon lay jëfe, sama dogali yoon lay doxe. Kooku du dee ngir ñaawtéefu baayam. Dina dund déy!
21743  EZK 46:19  Ba loolu amee waa ja génneeti ma ca jàllukaay ba feggook buntu bëj-gànnaar. Mu dugal ma ca néeg yu sell ya ñu beral sarxalkat yi. Ndeke bérab a nga foofa ca ruq ba, ca biir-a-biir, ca wetu sowu.
22480  AMO 4:1  Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»
22503  AMO 5:11  Gannaaw yeenay not néew-ji-doole, di foqati ŋëbu peppam, tabax ngeen këri boroom barke, waaye dungeen ko dëkke. Jëmbat ngeen tóokëri reseñ juy tem-temi, waaye dungeen naan ca biiñ ba.
22525  AMO 6:6  Yeena ngi jolu seen këlli biiñ, di diwoo ngën-gi-diw, sànkutey askanu Yuusufa soxalu leen.
22851  HAB 3:14  Ba noon ya riddeendoo, di nu tasaaresi, seen xeeju bopp nga bëtte seen bopp, fekk leen ñuy xaxaloo, ni ñuy waaja sëxëtoo ay néew-ji-doole, fu kenn yégul.
25186  LUK 5:10  Yanqóoba ak Yowaan doomi Sebede ya mu bokkaloon liggéey ba itam noonu lañu tiite. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay napp.»
25230  LUK 6:15  ak Macë ak Tomaa, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew,
25580  LUK 12:52  Gannaaw-si-tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo; ñett féewaloo ak ñaar, ñaar féewaloo ak ñett.
26002  LUK 22:69  Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki mooy toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.»
27613  ACT 17:21  Booba waa Aten ñépp, doxandéem ak njuddu-ji-réew, xintewuñu lenn lu moy di nettali ak a déglu xew-xew wu bees.
27632  ACT 18:6  Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
28961  2CO 5:16  Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu.
28976  2CO 6:10  Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
29272  GAL 6:17  Li ci des moo di gannaaw-si-tey, bu ma kenn lëjalati, ndax légét yi ci sama yaram, samag bokk ci Yeesu la màndargaal.