7282 | 1SA 3:4 | Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi», |
7659 | 1SA 17:39 | Daawuda ràngoo saamarub Sóol, ca kaw yére ya, daldi jéema dox, mu të, ndax ñàkk koo miin. Daawuda ne Sóol: «Manumaa doxaale lii ndax miinuma ko», daldi koy summi. |
18905 | ISA 60:14 | Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.» |
22781 | NAM 2:14 | «Maa ngii fi sa kaw», kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Say watiiri xare laay lakk, saxaral, sa gaynde yu ndaw, saamar lekk leen, te sam pàdd laay dagge ci réew mi, ba deesul déggati baatu ndaw loo yebal.» |
29185 | GAL 3:16 | Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi. |
30088 | HEB 4:7 | Looloo waral Yàlla jàppaat beneen bés bees di tàbbee ci noflaayam, bés bu mu tudde «tey jii», te mooy ba mu waxee lu yàgga yàgg, gannaaw gi, ci gémmiñug Daawuda, kàddu gii ñu jota jukki: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatub Yàlla, buleen të.» |
30306 | HEB 12:27 | Li mu ne «beneen yoon», di wund ne lees mana yëngal, lay dindi, te mooy li sàkke, ngir lees manula yëngal sax ba fàww. |
30773 | REV 1:8 | «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji. |