12864 | EST 9:26 | Moo waral ñuy wooye yooyu bés bési Purim, mu jóge ci baatu «Pur», di jumtukaayu tegtal boobu. Mboolem la ñu bind ca bataaxal boobu nag ak itam la ñu gisal seen bopp ak la ñu daj, |
28199 | ROM 8:15 | Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.» |
28888 | 2CO 1:20 | Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal. |
29204 | GAL 4:6 | Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», mu firi Baay. |