1 | GEN 1:1 | Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. |
2 | GEN 1:2 | Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi. |
3 | GEN 1:3 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. |
4 | GEN 1:4 | Yàlla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm. |
5 | GEN 1:5 | Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk. |
7 | GEN 1:7 | Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona. |
8 | GEN 1:8 | Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba. |
9 | GEN 1:9 | Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. |
10 | GEN 1:10 | Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na. |
11 | GEN 1:11 | Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. |
12 | GEN 1:12 | Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu. Yàlla gis ne baax na. |
13 | GEN 1:13 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba. |
14 | GEN 1:14 | Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. |
15 | GEN 1:15 | Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. |
16 | GEN 1:16 | Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi. |
18 | GEN 1:18 | ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na. |
19 | GEN 1:19 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba. |
21 | GEN 1:21 | Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. |
23 | GEN 1:23 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba. |
24 | GEN 1:24 | Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. |
25 | GEN 1:25 | Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na. |
27 | GEN 1:27 | Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind. |
29 | GEN 1:29 | Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. |
30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
31 | GEN 1:31 | Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba. |
32 | GEN 2:1 | Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. |
33 | GEN 2:2 | Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. |
34 | GEN 2:3 | Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp. |
35 | GEN 2:4 | Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, |
36 | GEN 2:5 | genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. |
37 | GEN 2:6 | Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. |
38 | GEN 2:7 | Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan. |
39 | GEN 2:8 | Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. |
40 | GEN 2:9 | Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon. |
41 | GEN 2:10 | Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal. |
42 | GEN 2:11 | Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, |
43 | GEN 2:12 | di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë. |
45 | GEN 2:14 | turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. |
46 | GEN 2:15 | Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm. |
50 | GEN 2:19 | Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. |
51 | GEN 2:20 | Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. |
52 | GEN 2:21 | Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. |
53 | GEN 2:22 | Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. |
55 | GEN 2:24 | Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux. |
56 | GEN 2:25 | Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa. |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
58 | GEN 3:2 | Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. |
62 | GEN 3:6 | Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk. |
63 | GEN 3:7 | Seeni bët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo. |
64 | GEN 3:8 | Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi. |
70 | GEN 3:14 | Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp. |
72 | GEN 3:16 | Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.» |
73 | GEN 3:17 | Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. |
76 | GEN 3:20 | Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. |
77 | GEN 3:21 | Gannaaw gi Yàlla Aji Sax ji sàkkal Aadama ak soxnaam ay yérey der, wodde leen. |
78 | GEN 3:22 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.» |
79 | GEN 3:23 | Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf, si ñu ko sàkke. |
80 | GEN 3:24 | Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. |
82 | GEN 4:2 | Awa teg ca rakkam, Abel. Abel di sàmm, Kayin di bey. |
83 | GEN 4:3 | Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. |
84 | GEN 4:4 | Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel, |
85 | GEN 4:5 | te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ. |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
90 | GEN 4:10 | Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. |
91 | GEN 4:11 | Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur. |
92 | GEN 4:12 | Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» |
95 | GEN 4:15 | Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. |
96 | GEN 4:16 | Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku. |
97 | GEN 4:17 | Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. |
98 | GEN 4:18 | Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. |
99 | GEN 4:19 | Lemeg nag jël ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla. |
101 | GEN 4:21 | teg ca Yubal, miy cosaanu ñi mane xalam ak toxoro. |
102 | GEN 4:22 | Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama. |
103 | GEN 4:23 | Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat. |
106 | GEN 4:26 | Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal. |
107 | GEN 5:1 | Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, |
108 | GEN 5:2 | góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee. |
109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
110 | GEN 5:4 | Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
112 | GEN 5:6 | Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. |
113 | GEN 5:7 | Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
114 | GEN 5:8 | Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu. |
115 | GEN 5:9 | Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. |
116 | GEN 5:10 | Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
118 | GEN 5:12 | Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. |
119 | GEN 5:13 | Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
120 | GEN 5:14 | Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu. |
121 | GEN 5:15 | Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. |
122 | GEN 5:16 | Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
123 | GEN 5:17 | Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. |
124 | GEN 5:18 | Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. |
125 | GEN 5:19 | Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
126 | GEN 5:20 | Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu. |
127 | GEN 5:21 | Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
130 | GEN 5:24 | Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom. |
131 | GEN 5:25 | Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. |
132 | GEN 5:26 | Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |