129 | GEN 5:23 | Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). |
234 | GEN 9:28 | Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). |
303 | GEN 12:4 | Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). |
398 | GEN 16:16 | Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86). |
666 | GEN 25:7 | Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175). |
676 | GEN 25:17 | Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam. |
1040 | GEN 35:28 | Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180). |
1449 | GEN 47:28 | Yanqóoba nag nekk na fukki at ak juróom ñaar ca réewum Misra, ay atam yépp tollu ci téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (147). |
1672 | EXO 6:16 | Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari, ku nekk ak askanam. At ya Lewi dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). |
1674 | EXO 6:18 | Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133). |
1676 | EXO 6:20 | Amram moo jël bàjjanam Yokebedd soxna, kooku am ak moom Aaróona ak Musaa. At, ya Amram dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). |
1857 | EXO 12:40 | Diir ba bànni Israyil nekk Misra tollu na ci ñeenti téeméeri at ak fanweer (430). |
4706 | NUM 31:40 | aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32). |
8963 | 1KI 7:26 | Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200). |
9366 | 1KI 18:22 | Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450). |
9426 | 1KI 20:15 | Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000). |
12036 | EZR 2:4 | Askanu Sefatiya, ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). |
12037 | EZR 2:5 | Askanu Ara, juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom lañu (775). |
12040 | EZR 2:8 | Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). |
12041 | EZR 2:9 | Askanu Sakay, juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). |
12042 | EZR 2:10 | Askanu Baani, juróom benni téeméer ak ñeent fukk ak ñaar lañu (642). |
12043 | EZR 2:11 | Askanu Bebay, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (623). |
12045 | EZR 2:13 | Askanu Adonikam, juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn lañu (666). |
12047 | EZR 2:15 | Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454). |
12048 | EZR 2:16 | Askanu Ater, soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98). |
12049 | EZR 2:17 | Askanu Besay, ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (323). |
12050 | EZR 2:18 | Askanu Yora, téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). |
12051 | EZR 2:19 | Askanu Asum, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). |
12052 | EZR 2:20 | Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |
12053 | EZR 2:21 | Waa Betleyem, téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). |
12054 | EZR 2:22 | Waa Netofa, juróom fukk ak juróom benn lañu (56). |
12055 | EZR 2:23 | Waa Anatot, téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). |
12056 | EZR 2:24 | Waa Asmawet, ñeent fukk ak ñaar lañu (42). |
12057 | EZR 2:25 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12058 | EZR 2:26 | Waa Raama ak Geba, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). |
12059 | EZR 2:27 | Waa Migmas, téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). |
12060 | EZR 2:28 | Waa Betel ak Ayi, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). |
12061 | EZR 2:29 | Waa Nebo, juróom fukk ak ñaar lañu (52). |
12062 | EZR 2:30 | Waa Magbis téeméer ak juróom fukk ak juróom benn lañu (156). |
12064 | EZR 2:32 | Waa Arim, ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320). |
12065 | EZR 2:33 | Waa Lodd ak Adidd ak Ono, juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak juróom lañu (725). |
12066 | EZR 2:34 | Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12068 | EZR 2:36 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12072 | EZR 2:40 | Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ak Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). |
12073 | EZR 2:41 | Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (128). |
12074 | EZR 2:42 | Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139). |
12090 | EZR 2:58 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
12092 | EZR 2:60 | Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). |
12097 | EZR 2:65 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200). |
12209 | EZR 8:3 | mi askanoo ci Sekaña la. Askanu Paros, Sàkkaryaa bawoo ca, ànd ak téeméeri góor ak juróom fukk (150). |
12210 | EZR 8:4 | Ci askanu Payat Mowab, Elyowenay doomu Seraya la, mook ñaar téeméeri góor (200). |
12211 | EZR 8:5 | Ci askanu Sàttu, Sekaña doomu Yasyel la, mook ñetti téeméeri góor (300). |
12212 | EZR 8:6 | Ci askanu Adin, Ebedd doomu Yonatan la, mook juróom fukki góor (50). |
12213 | EZR 8:7 | Ci askanu Elam, Esayi doomu Atalyaa la, mook juróom ñaar fukki góor (70). |
12214 | EZR 8:8 | Ci askanu Sefatiya, Sebadiya doomu Mikayel la, mook juróom ñett fukki góor (80). |
12215 | EZR 8:9 | Ci askanu Yowab, Obadiya doomu Yeyel la, mook ñaar téeméeri góor ak fukk ak juróom ñett (218). |
12216 | EZR 8:10 | Ci askanu Baani, Selomit doomu Yosifya la, mook téeméeri góor ak juróom benn fukk (160). |
12217 | EZR 8:11 | Ci askanu Bebay, Sàkkaryaa doomu Bebay la, mook ñaar fukki góor ak juróom ñett (28). |
12218 | EZR 8:12 | Ci askanu Asgàdd, Yowanan doomu Àkkatan la, mook téeméeri góor ak fukk (110). |
12219 | EZR 8:13 | Askanu Adonikam ñoo mujje, ñu di leen wax Elifelet ak Iyel ak Semaya, ñook juróom benn fukki góor (60). |
12220 | EZR 8:14 | Ci askanu Bigway, Utay la ak Sabudd, ñook juróom ñaar fukki góor (70). |
12225 | EZR 8:19 | ñook Asabya ak Esayi sëtu Merari. Ñu ànd ak seeni bokk ak seen doom yu góor, di ñaar fukki góor (20). |
12434 | NEH 7:9 | Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). |
12435 | NEH 7:10 | Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). |
12438 | NEH 7:13 | Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845). |
12439 | NEH 7:14 | Askanu Sakay juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). |
12440 | NEH 7:15 | Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett lañu (648). |
12441 | NEH 7:16 | Askanu Bebay juróom benn téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (628). |
12443 | NEH 7:18 | Askanu Adonikam juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (667). |
12447 | NEH 7:22 | Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (328). |
12448 | NEH 7:23 | Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324). |
12449 | NEH 7:24 | Askanu Arif téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). |
12450 | NEH 7:25 | Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |
12451 | NEH 7:26 | Waa Betleyem ak Netofa téeméer ak juróom ñett fukk ak juróom ñett lañu (188). |
12452 | NEH 7:27 | Waa Anatot téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). |
12453 | NEH 7:28 | Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar lañu (42). |
12454 | NEH 7:29 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12455 | NEH 7:30 | Waa Raama ak Geba juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). |
12456 | NEH 7:31 | Waa Migmas téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). |
12457 | NEH 7:32 | Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). |
12458 | NEH 7:33 | Waa Nebo gu ndaw juróom fukk ak ñaar lañu (52). |
12461 | NEH 7:36 | Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12462 | NEH 7:37 | Waa Lodd ak Adidd ak Ono juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (721). |
12464 | NEH 7:39 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12468 | NEH 7:43 | Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). |
12469 | NEH 7:44 | Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148). |
12470 | NEH 7:45 | Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138). |
12485 | NEH 7:60 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
12487 | NEH 7:62 | Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642). |
12494 | NEH 7:69 | Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy poseti wurus (1 000) ak juróom fukki këll (50) ak fanweeri mbubbi sarxalkat (30) ak juróomi téeméeri dogi xaalis (500). |
12496 | NEH 7:71 | La des ca askan wa joxe na ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis (2 000) ak mbubbi sarxalkat yu tollu ci juróom benn fukk ak juróom ñaar (67). |
12830 | EST 8:9 | Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp. |
13942 | JOB 42:16 | Gannaaw loolu Ayóoba dundaat na téeméeri at ak ñeent fukk (140). Gis na ay doomam, gis ay sëtam, ba muy ñeenti maas. |
21710 | EZK 45:11 | Na benn efa ak benn bat yem dayo, lu ci nekk wara def céru fukkeelu benn omer, bi yemook ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220), mbaa téeméeri kilo ak juróom fukk (150). Te na benn omer di dayo bi ngeen di natte. |
21788 | EZK 48:17 | Parlub dëkk bi nag, na féeteek ñeenti weti dëkk bi, te doon fa wet gu nekk bayaal bu yaatoo ñaar téeméeri xasab ak juróom fukk (250). |
22199 | HOS 3:2 | Ci kaw loolu ma takk ko ci fukki poseti xaalis ak juróom, ak ñeenti téeméeri kiloy lors ak juróom fukk (450). |
25079 | LUK 2:37 | Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak julli la daan jaamoo guddi ak bëccëg. |
27007 | ACT 1:15 | Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen: |
27451 | ACT 13:20 | Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel. |
30995 | REV 13:18 | Fii nag xel la laaj: ku am ug dégg, na waññ limu rab wi, ndax boobu lim turu nit la taxawe, di juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn (666). |