2660 | EXO 38:26 | muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3626 | NUM 1:21 | Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3630 | NUM 1:25 | Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3632 | NUM 1:27 | Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600). |
3634 | NUM 1:29 | Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3636 | NUM 1:31 | Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3638 | NUM 1:33 | Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3640 | NUM 1:35 | Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3644 | NUM 1:39 | Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3646 | NUM 1:41 | Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3651 | NUM 1:46 | Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3663 | NUM 2:4 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600). |
3665 | NUM 2:6 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3667 | NUM 2:8 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3668 | NUM 2:9 | «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu. |
3670 | NUM 2:11 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3674 | NUM 2:15 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3675 | NUM 2:16 | «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. |
3678 | NUM 2:19 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3680 | NUM 2:21 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3683 | NUM 2:24 | «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca. |
3685 | NUM 2:26 | Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3687 | NUM 2:28 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3690 | NUM 2:31 | «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.» |
3691 | NUM 2:32 | Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3736 | NUM 3:43 | Ba ñu waññee mboolem taaw yu góor ya, bind seeni tur, dale ci ñi am weer, jëm kaw, seenub lim nekk na ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (22 273). |
3780 | NUM 4:36 | Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukki góor (2 750). |
3784 | NUM 4:40 | te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630). |
3792 | NUM 4:48 | seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580). |
3936 | NUM 7:85 | ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). |
3937 | NUM 7:86 | Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). |
4481 | NUM 25:9 | Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000). |
4498 | NUM 26:7 | Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). |
4505 | NUM 26:14 | Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200). |
4509 | NUM 26:18 | Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). |
4513 | NUM 26:22 | Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500). |
4516 | NUM 26:25 | Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300). |
4518 | NUM 26:27 | Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500). |
4525 | NUM 26:34 | Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700). |
4528 | NUM 26:37 | Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500). Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng. |
4532 | NUM 26:41 | Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600). |
4534 | NUM 26:43 | Mboolem làngi Cuwameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400). |
4538 | NUM 26:47 | Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
4541 | NUM 26:50 | Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400). |
4542 | NUM 26:51 | Limeefu bànni Israyil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (601 730). |
4701 | NUM 31:35 | aw nit, fanweeri junniy jigéen ñu xamul lalu góor (30 000). |
4712 | NUM 31:46 | aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000). |
7455 | 1SA 11:8 | Ba Sóol nemmikoo limu góori Israyil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000). |
8217 | 2SA 8:5 | Waa Siri ña dëkke réewum Damaas dikk wallusi Adadeser buurub Soba. Daawuda rey ca ñoom ñaar fukki junneek ñaar (22 000). |
8261 | 2SA 10:18 | Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa. |
8704 | 2SA 24:9 | Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000). |
8873 | 1KI 5:6 | Suleymaan amoon na ñeenti junniy (4 000) wuddi fasi watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000). |
9051 | 1KI 8:63 | Mu defal Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm, lépp di ñaar fukki junniy nag ak ñaar (22 000) ak téeméeri junniy gàtt ak ñaar fukk (120 000). Noonu la Buur ak bànni Israyil gépp amale xewu jagleb kër Aji Sax ji. |
9426 | 1KI 20:15 | Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000). |
10100 | 2KI 19:35 | Guddig keroog malaakam Aji Sax ji moo dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp, diy néew. |
12031 | EZR 1:10 | ak fanweeri këlli wurus yu ndaw (30) yu ànd ak ñeenti téeméeri këll ak fukk yu ndaw yu xaalis (410) ak junniy jumtukaay yeneen (1 000). |
12032 | EZR 1:11 | Mboolem ndabi wurus yeek yu xaalis yi juróomi junni la ak ñeenti téeméer (5 400). Sesbasar jële lépp Babilon, yóbbu Yerusalem, ba ngàllo gay ñibbi. |
12035 | EZR 2:3 | Askanu Paros, ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). |
12038 | EZR 2:6 | Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak ñaar (2 812). |
12039 | EZR 2:7 | Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12044 | EZR 2:12 | Askanu Asgàdd, junni ak ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (1 222). |
12046 | EZR 2:14 | Askanu Bigway, ñaari junni ak juróom fukk ak juróom benn lañu (2 056). |
12063 | EZR 2:31 | Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12067 | EZR 2:35 | Waa Sena, ñetti junni ak juróom benn téeméer ak fanweer lañu (3 630). |
12069 | EZR 2:37 | Askanu Imer, junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). |
12070 | EZR 2:38 | Askanu Pasur, junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). |
12071 | EZR 2:39 | Askanu Arim, junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017). |
12097 | EZR 2:65 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200). |
12099 | EZR 2:67 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12433 | NEH 7:8 | Askanu Paros ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). |
12436 | NEH 7:11 | Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (2 818). |
12437 | NEH 7:12 | Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12444 | NEH 7:19 | Askanu Bigway ñaari junni ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (2 067). |
12459 | NEH 7:34 | Waa Elam gu ndaw junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12463 | NEH 7:38 | Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930). |
12465 | NEH 7:40 | Askanu Imer junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). |
12466 | NEH 7:41 | Askanu Pasur junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). |
12467 | NEH 7:42 | Askanu Arim junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017). |
12492 | NEH 7:67 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12493 | NEH 7:68 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12495 | NEH 7:70 | Ñenn ca ña jiite seen kër baay def nañu seen loxo ca alal ja ñu jagleel liggéey ba, mu tollu ci ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis ak ñaar téeméer (2 200). |
13938 | JOB 42:12 | Aji Sax ji nag barkeel mujug Ayóoba lu raw ndoorteem. Mu am fukki junniy gàtt ak ñeent (14 000), ak juróom benni junniy giléem (6 000), ak junniy lëkkey nag (1 000) yu muy rijjee, ak junniy mbaam yu jigéen (1 000). |
18458 | ISA 37:36 | Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew. |
20375 | JER 52:30 | Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600). |
21784 | EZK 48:13 | Na suufas Leween ñi digalook sos sarxalkat yi, di pàkk bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), te yaatoo fukki junniy xasab (10 000). Bu ci nekk na am guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) ak yaatuwaayu fukki junniy xasab (10 000). |
21801 | EZK 48:30 | «Bunti dëkk bi nag nii lay tëdde: Ñeenti miiri dëkk bi, bu ci nekk day am guddaayu ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500). |
22162 | DAN 12:12 | Ndokklee ku muñ nag diiru junniy fan ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom (1 335). |
25305 | LUK 7:41 | Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000). |
27095 | ACT 4:4 | Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000). |
27673 | ACT 19:19 | Ci biir loolu ñu bare ñu daan ñeengo, boole seeni téere, indi, lakk ko fa kanam ñépp. Ba ñu xaymaa njég la, tolloo naak juróom fukki junniy poseti daraxma (50 000). |
30924 | REV 9:16 | Limu gawari mbooloo ma doon xareji ñaar téeméeri junniy junni la (200 000 000). Maa dégg lim bi. |
30965 | REV 12:6 | Ndaw si nag daw, ba ca màndiŋ ma, ci ab rawtu bu ko Yàlla waajaloon, ngir ñu leel ko fa diiru junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk (1 260). |
31138 | REV 21:16 | Dëkk bi dafa kaare; guddaay bi tollook yaatuwaay bi. Mu natte dëkk bi bant bi mu yor, guddaay bi ak yaatuwaay bi ak taxawaay bi, lépp tolloo, di fukki junneek ñaari dayo (12 000), yemook ñaari junneek ñaar téeméeri kilomeetar (2 200). |