480 | GEN 19:22 | Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut). |
495 | GEN 19:37 | Taaw ba am ca doom ju góor, tudde ko Mowab (mu firi Jóge ci baay). Mowab moo sos Mowabeen ñi. |
496 | GEN 19:38 | Rakk ja moom it am doom ju góor, tudde ko Ben Aami (mu firi Sama doomu mbokk). Ben Aami moo sos Amoneen, ñi fi nekk ba tey. |
562 | GEN 22:14 | Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.» |
684 | GEN 25:25 | Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
689 | GEN 25:30 | Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). |
714 | GEN 26:21 | Ñu gasaat ab teen, xuloo amati ca, mu tudde ko Sitna (mu firi Xuloo). |
726 | GEN 26:33 | Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga). |
829 | GEN 29:33 | Mu dellu ëmb, am doom ju góor. Mu ne: «Aji Sax ji yég na ne fonkeesu ma, looloo tax mu mayaat ma doom jii.» Mu tudde ko Simeyon (mu firi Kiy dégg). |
830 | GEN 29:34 | Mu delluwaat ëmb, am doom ju góor, ba noppi waxaat ne: «Bii yoon sama jëkkër dina am cofeel ci man, ndax jural naa ko ñetti doom yu góor,» loolu tax mu tudde ko Lewi (mu firi Boroom cofeel). |
831 | GEN 29:35 | Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw. |
837 | GEN 30:6 | Bi loolu amee Rasel ne: «Yàlla àtte na ma; dégg na sama ñaan, ba may ma doom.» Mu tudde ko nag Dan (mu firi Kiy àtte). |
839 | GEN 30:8 | Rasel ne: «Bëre naa ak sama mag bëre bu réy, ba daan,» daldi ko tudde Neftali (mu firi Kiy bëre). |
842 | GEN 30:11 | Leya ne: «Ndaw wërsëg wu réy!» daldi ko tudde Gàdd (mu firi Wërsëg). |
844 | GEN 30:13 | Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte). |
849 | GEN 30:18 | Leya neeti: «Yàlla da maa fey, ndax maa may sama jëkkër sama jaam.» Mu tudde ko Isaakar (mu firi Boroom pey). |
851 | GEN 30:20 | Booba la ne: «Yàlla defal na ma teraanga ju réy. Bii yoon sama jëkkër dina ma teral, ndax amal naa ko juróom benni doom yu góor.» Moo tax mu tudde ko Sabulon (mu firi Teraanga). |
922 | GEN 31:48 | Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede). |
931 | GEN 32:3 | Ba leen Yanqóoba gisee, da ne dalub Yàllaa ngii, ba tax mu tudde bérab ba Maanayim (mu firi Ñaari dal). |
978 | GEN 33:17 | Yanqóoba moom jubal gox bu ñu naan Sukkóot, tabax fa kër, mbaaral géttam, moo tax ñu tudde bérab boobu Sukkóot (mu firi Ay mbaar). |
981 | GEN 33:20 | Mu daldi fay sàkk sarxalukaay, tudde ko El Elowe Israyil (mu firi Yàllay Israyil mooy Yàlla). |
1020 | GEN 35:8 | Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (mu firi Garabu jooyoo). |
1030 | GEN 35:18 | Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay). |
1149 | GEN 38:29 | Naka la delloo loxoom, seexam juddu, mu ne ko: «Yaw foo bëtte, ba génn?» Ñu daldi ko tudde Peres (mu firi Bëtt). |
1518 | GEN 50:11 | Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra). |
1944 | EXO 15:23 | Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde bérab ba Maara (mu firi Fu wex). |
1991 | EXO 17:7 | Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?» |
4325 | NUM 20:13 | Loolooy walum Meriba, (mu firi Jote ba). Fa la bànni Israyil jote woon ak Aji Sax ji, ba mu biral sellngaam fa seen biir. |
4344 | NUM 21:3 | Aji Sax ji nangul Israyil, jébbal leen Kanaaneen ña, ñu faagaagal leen, ñook seeni dëkk. Ñu daldi wooye gox ba Xorma (mu firi Lu ñu faagaagal). |
7366 | 1SA 7:12 | Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.» |
7841 | 1SA 23:28 | Sóol nag fomm ndàqum Daawuda, ngir dajejeek waa Filisti. Looloo waral turu bérab boobu di Sela Amalekot (mu firi doju Rawukaay). |
8155 | 2SA 5:20 | Daawuda dem ba ca Baal Perasim, duma leen foofa. Mu ne: «Aji Sax jee ma bëttal noon yi, ni walum ndox di bëtte, wéy.» Moo tax ñu wooye bérab boobu Baal Perasim (mu firi Boroom bëtt-bëtt yi). |
8314 | 2SA 12:25 | ba xamle ko, Yonent Yàlla Natan jottli, daldi koy tudde Yedija (mu firi Soppey Aji Sax ji). |
8958 | 1KI 7:21 | Mu samp jën yi ci kanam bunt néeg Yàlla bu mag bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel). |
17866 | ISA 7:14 | Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun). |
21533 | EZK 39:16 | ba far am dëkk bu ñuy wooye Amona (mu firi Gàngoor). Noonu lañuy setale réew mi.” |
30919 | REV 9:11 | Seen buur a leen jiite, di malaakam xóote bi, turam ci ebrë di Abadon, Apolyon ci làkku gereg, (mu firi Yàqkat bi). |