1999 | EXO 17:15 | Musaa nag sàkk fa sarxalukaay, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya». |
2695 | EXO 39:30 | Ñu sàkk nag meeteel gu sell gu wurusu ngalam, muy dogu wurus wu tell, ñu ñaas ci kawam mii mbind, ni ñuy ñaase mbindum torlu: «Sell na, ñeel Aji Sax ji». |
19610 | JER 25:7 | Waaye dégluwleen ma». Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Yeena ma merlook ak yëf yu ngeen sàkke seeni loxo, muy seen musiba.» |
27804 | ACT 23:2 | Anañas sarxalkat bu mag ba nag sant ña taxaw ca wetu Póol, ne leen: «Fél-leen gémmiñam». |
28251 | ROM 9:28 | Ndax kàddu gi Boroom bi wax, moo koy sottal ci lu gaaw ci kaw suuf». |
30133 | HEB 7:2 | Moom la Ibraayma jox fukkeelu cérub mboolem cëxëtoo ma. Ni ñu jëkka dégge aw turam Melkisedeg, ci tekki, mooy «buur bu jub». Bu loolu weesee itam moom mooy buurub Salem, muy «buuru jàmm». |
30497 | 1PE 3:6 | noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeen ay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp. |