|
2399 | Nanga nangoo xaalisu njot-gi-bakkan bi ci bànni Israyil, te nga féetale ko liggéeyu xaymab ndaje mi. Loolu pàttliku lay doon, ñeel bànni Israyil fi kanam Aji Sax ji, ngir seen njot-gi-bakkan.» | |
3980 | «Su dee ab doxandéem bu ngeen dëkkal, sañ naa màggal bésub Mucc bi ñeel Aji Sax ji. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, ak àttey yoonam, ni la koy màggale; benn dogal bi lay doon ci yeen, muy doxandéem bi, di njuddu-ji-réew.» |