|
22881 | Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moom, ñu di ca fore, bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon. Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal, tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.) | |
23190 | «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. |