438 | GEN 18:13 | Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” |
631 | GEN 24:39 | Ma ne sama sang: “Bu ndaw sa nanguwula ànd ak man nag?” |
639 | GEN 24:47 | Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. |
946 | GEN 32:18 | Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” |
1344 | GEN 44:19 | Sang bi, danga noo laajoon ne nu: “Ndax am ngeen baay walla rakk?” |
1421 | GEN 46:34 | “Lan mooy seen liggéey?” ngeen ne ko: “Nun de sang bi, ag jur lanu masa yar, ba nuy gone ba tey, te noonu la ko sunuy maam daan defe.” Su boobaa, ngeen mana féetewoo diiwaanu Gosen, ndaxte waa Misra dañuy xof sàmm.» |
1843 | EXO 12:26 | Te bu leen seeni doom laajee ne leen: “Lu aada jii di wund?” |
1882 | EXO 13:14 | Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga. |
3490 | LEV 25:20 | Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?” |
7271 | 1SA 2:29 | Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israyil sama ñoñ?” |
7422 | 1SA 10:2 | Gannaaw boo teqlikook man, dinga dajeek ñaari góor ca wetu bàmmeelu Rasel ca Celca ca diiwaanu Beñamin. Dinañu la wax ne la mbaam ya nga seeti woon feeñ nañu. Te sax sa baay xalaatatul mbaam yi, yeena ko jaaxal. Ma nga naan: “Ana nu may def ak sama doom ji?” |
7459 | 1SA 11:12 | Mbooloo ma ne Samiyel: «Ana ku noon: “Ndax Sóol ay falu ci sunu kaw?” Indileen ñooñu, nu rey leen!» |
8033 | 2SA 1:8 | Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.” |
8190 | 2SA 7:7 | Mboolem fu ma masa màngeji ak bànni Israyil gépp, ndax mas naa wax benn baat, jëme ci genn giirug Israyil gu ma sant ñu sàmm Israyil sama ñoñ, ne leen ñu tabaxal ma kërug bantu seedar?” |
8283 | 2SA 11:21 | Ana ku reyoon Abimeleg doomu Yerubeset? Xanaa du ca kaw tata ja la ko aw jigéen sànnee doju wolukaay, ba mu dee ca Tebes? Lu waral ngeen jegee noonu tata ja?” Su boobaa nee ko: “Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.”» |
8311 | 2SA 12:22 | Mu ne leen: «Ba xale biy dese bakkan laa doon woor ak a jooy, ndax dama noon: “Ana ku xam ndax Aji Sax ji dina ma defalu yiw, ba xale bi dund am déet?” |
8526 | 2SA 19:13 | Yeen de yeenay bokki buur lenqe, ngeen bokk ak moom jenn deret; kon xanaa ñépp duñu délloosi Buur, ngeen des gannaaw?” |
8733 | 1KI 1:13 | Gaawal dem ca Buur Daawuda, ne ko: “Buur, sang bi, du yaa ma giñaloon, yaw sang bi, ne ma sama doom Suleymaan mooy falu buur, wuutu la, te mooy toog ci sa jal bi? Kon nag lu tax Adoña falu buur?” |
9062 | 1KI 9:8 | «Su boobaa kër gii dina gent te képp ku ko romb dina yéemu tey muslu ci lu ni mel. Dinañu ne: “Lu tax Aji Sax ji def nii réew mii ak kër gii?” |
9473 | 1KI 21:19 | Wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Du dangaa rey nit, ba nangu alalam?” Nga teg ca ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Fa xaj ya xabe deretu Nabot, ay xaj dina fa xabe sa deret, yaw itam.”» |
9503 | 1KI 22:20 | Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee. |
9540 | 2KI 1:3 | Ci biir loolu malaakam Aji Sax ji wax Ilyaas, ma cosaanoo Tisbi, ne ko: «Demal gaaw dajeek ndawi buurub Samari te laaj leen ne leen: “Xanaa Yàlla daa amul ci Israyil, ba ngeen di seeti ca Baal Sebub, tuuru Ekkron?” |
10050 | 2KI 18:22 | Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal bérabi jaamookaayam yeek sarxalukaayam, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu ci Yerusalem lañuy sujjóotal?” |
18015 | ISA 14:17 | def àddina wërngal këpp ndànd-foyfoy, tas dëkk ya, te du jàpp nit ba yiwi ko?” |
18407 | ISA 36:7 | Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal bérabi jaamookaayam yeek sarxalukaayam, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu lañuy sujjóotal?” |
18859 | ISA 58:3 | te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci? Lu nuy toroxlu te teewluwoo?” Ma ne: Bés bu ngeen woor, yeena ngi topp seen bakkan, di sëqatal seeni liggéeykat. |
19040 | JER 2:6 | Newuñu: “Ana Aji Sax, ji nu génne woon réewum Misra, jiite nu ca biir màndiŋ ma, ca joor gu wow gaak xur ya, réewum maral ma lëndëm këruus, jaareesu fa, dëkkeesu fa?” |
19042 | JER 2:8 | «Sarxalkat yi newuñu: “Ana Aji Sax ji?” Ñi ŋank yoon wi faaleetuñu ma, njiit yi gàntal ma, yonent yiy waxe waxyuy Baal, tuur mi, di topp lu leen dul jariñ. |
19057 | JER 2:23 | «Nu ngeen ñemee naa: “Sobeelunu sunu bopp te toppunu tuuri Baal?” Seetleen li ngeen nekke ci xur wi, xool-leen li ngeen di def, mel ni giléem gu ndaw, di wodd-woddi, fu ne mu daw jëm fa, |
19076 | JER 3:5 | Xanaa deesul mer ba fàww? Xanaa xadar du sax?” Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, waaye bon ngeen lu ngeen man.”» |
19146 | JER 5:19 | Bu ñu nee: “Ana lu waral sunu Yàlla Aji Sax ji teg nu lii lépp?” ne leen: “Yàlla nee: Ni ngeen ma dëddoo, di jaamu yàllay jaambur ci seenum réew, ni ngeen di jaamujee ay jaambur biir réew mu ngeen moomul.”» |
19151 | JER 5:24 | Seen xel demul sax ba ne: “Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax, jiy jot, mu tawal nu, taw yu jëkk ak yu mujj yi, àppal nu ayi bési ngóob, sédde nu?” |
19174 | JER 6:16 | Aji Sax ji dafa wax ne: «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, te laajte yoon ya woon, ne: “Ana yoonu mbaax?” Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» Ñu lànk ne: «Awunu ca.» |
19228 | JER 8:6 | Teewlu naa, déglu naa; du lu jaadu lañu wax. Kenn tuubu ci mbonam, ba ne: “Lu ma def nii?” Ku nekk a topp yoonam, ni fas wu màmm cib xare. |
19386 | JER 15:2 | Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Kiy wopp dee, wopp dee; kiy deeye saamar, deeye saamar; kiy deeye xiif, deeye xiif; kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.” |
19389 | JER 15:5 | «Yerusalemee, ku lay yërëm? Ku lay jooy? Moo, ku lay geesu ne la: “Jàmm nga am?” |
19415 | JER 16:10 | «Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?” |
19531 | JER 22:8 | «Doxandéem yu bare dinañu jaare dëkk bii, di laajte ci seen biir naan: “Ana lu waral Aji Sax ji def nii bii dëkk bu mag?” |
19586 | JER 23:33 | Aji Sax ji ne Yeremi: «Su la askan wii laajee mbaa ab yonent mbaa ab sarxalkat ne la: “Ana yéeneb waxyu bi la Aji Sax ji yóbbante?” Nga wax leen ne leen: “Yeenay yen bi te dinaa leen yenniku.”» Kàddug Aji Sax jee. |
19588 | JER 23:35 | Li ku nekk wara laaj moroomam mbaa mbokkam kay mooy: “Lu Aji Sax ji tontu?” mbaa “Lu Aji Sax ji wax?” |
19590 | JER 23:37 | Li nit kiy laaj ab yonent mooy: “Ana lu Aji Sax ji tontu? Ana lu Aji Sax ji wax?” |
19905 | JER 35:13 | «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Demal wax mboolem waa Yuda ak waa Yerusalem, ne leen: “Xanaa dungeen dégg ndigal, ba dégg samay kàddu?” Kàddug Aji Sax jee. |
20166 | JER 48:17 | Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen leen; yeen ñi dégg seen tur ñépp, jooyleen leen. Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe, ba foqaale jii daraja?” |
20168 | JER 48:19 | Yeen waa Arower, taxawleen fi yoon wi te teewlu; góor gu fi jaare mbaa ndaw su rëcc, di daw, ngeen laaj ko ne ko: “Lu xew?” |
20200 | JER 49:4 | Céy Raba, bii dëkk bu taaru, toogadi, yeena doon damoo xur yi, ba ci seen xur wu naat wii? Yeena yaakaaroon seeni denc, naan: “Ku ñemee dal sunu kaw?” |
20758 | EZK 12:9 | «Yaw nit ki, xanaa waa kër Israyil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?” |
20906 | EZK 17:12 | «Waxal waa kër fippukat yi, ne leen: “Xamuleen lu mbir yooyu di wund?” Ne leen: “Mu ngoogu, buuru Babilon a dem Yerusalem, jàpp buur baak kàngam ya, ànd ak ñoom, yóbbu Babilon. |
20937 | EZK 18:19 | «Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?” Xanaa du njub ak njekk la doom ji jëfe, sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm, di ko jëfe? Dina dund kay! |
20993 | EZK 20:29 | Ma ne leen: Ana lu waral bérabu jaamookaay bii ngeen di dem?” Bérabu Jaamookaay lañu koy wax ba tey jii. |
21119 | EZK 23:43 | Booba laa wax ci ndaw sii njaaloo ba ràpp, ne: “Ndaw sii lañuy gànctool ba tey?” |
21359 | EZK 33:10 | «Yaw nit ki, waxal ak waa kër Israyil, ne leen: “Ngeen ne dungeen mana mucc ndax seeni tooñ ak seen bàkkaar yu leen diis ba semmal leen?” |
21360 | EZK 33:11 | Waxleen ne leen: “Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, awma bànneex ci deewug nit ku bon. Sama bànneex mooy mu wacc yoonu mbonam, ba dund. Kon yeen waa kër Israyil, waccleen, ngalla waccleen seen yoonu mbon. Ana lu jar ngeen di dee?” |
21375 | EZK 33:26 | Yeen wóoluwuleen lu moy seen saamar, ngeen di def jëf ju siblu, ku nekk di jaalook jabaru moroomam, ba noppi di moom réew mi?” |
21484 | EZK 37:18 | Bu la sa bokk yi laajee, ne la: “Xanaa doo nu wax lii lu muy tekki?” |
22345 | HOS 13:10 | Ana seen buur boog, ba mu xettli leen ci seen mboolemi dëkk? Ana seen njiit yi ngeen sàkku woon, ba ne ma: “Falal nu buur aki kàngam?” |
22582 | OBA 1:3 | Seen reewande sànk na leen, yeen ñi dëkke xar-xari doj, te seen dëkkuwaay sore kaw, ba tax leen naa ci seenum xel: “Ana ku ñu mana daane fi suuf?” |
22788 | NAM 3:7 | ku la gis, daw la te naan: “Niniw tas na! Moo ku koy jooy?” Ana fu ma koy wutale ñu ko dëfal?» |
23037 | ZEC 7:6 | Te su ngeen lekkee ak su ngeen naanee, xanaa du seen bopp ngeen lekkal ak a naanal?” |
23134 | ZEC 13:6 | Te su ñu ko nee: “Légét yii ci sab dënn nag?” Da naan: “Lii de ay légét la yu ma jële ca sama kër xarit ya.”» |
23164 | MAL 1:6 | «Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?” |
23165 | MAL 1:7 | Xanaa di indi ñam wu sobewu fi sama sarxalukaay. Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?” Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji. |
23196 | MAL 3:7 | «Ca seen janti maam ngeen dëddoo sama dogali yoon, sàmmuleen ko. Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Yeena ngi naa: “Ci lan lanuy waññikoo?” |
23197 | MAL 3:8 | Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe. |
25548 | LUK 12:20 | Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?” |
25694 | LUK 16:5 | Mu daldi woolu kenn, kenn, ña ameel njaatigeem bor. Kii ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?” |
25696 | LUK 16:7 | Kee, mu ne ko: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, bindal juróom ñett fukk.” |
25823 | LUK 19:23 | Lu la tee woona dénkaaneji sama alal ca dencukaay ba, ngir bu ma dikkee jot ko, boole ca tonoom?” |
25831 | LUK 19:31 | Bu ñu leen nee: “Lu tax ngeen di ko yiwi?” ne leen: “Sang bee ko soxla.”» |
25944 | LUK 22:11 | te ngeen ne boroom kër ga: “Sëriñ bi nee: Ana néegu gan, bi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?” |
27211 | ACT 7:26 | Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?” |
27213 | ACT 7:28 | Xanaa danga maa nara rey, na nga reye waayi Misra ja démb?” |
27220 | ACT 7:35 | «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba. |
27235 | ACT 7:50 | Loolu lépp, xanaa du sama loxoo ko sàkk?” |
27779 | ACT 22:7 | Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?” |
27780 | ACT 22:8 | Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Mu ne ma: “Man maay Yeesum Nasaret, mi ngay bundxatal.” |
27782 | ACT 22:10 | Ma ne ko: “Sang bi, nu may def?” Sang bi ne ma: “Jógal dem Damaas, dees na la wax foofa mboolem li ñu la sas, nga def ko.” |
27906 | ACT 26:15 | «Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal. |