13808 | JOB 38:11 | ba ne ko: «Fii ngay yem, doo fi wees. Fii la say gannax di noppee buure»? |
17223 | PRO 26:12 | Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin. |
18279 | ISA 29:16 | Yeenaka juunum xel! Dees na jaawale tabaxkatu njaq beek ban bi? Ndax li ñu sàkk dina ne ki ko sàkk: «Kii sàkku ma»? Am njaq leey waxtaane tabaxkat bi naa: «Kii manula tabax»? |
22889 | ZEP 2:15 | Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? Nan la doone nii ab gent, bérab bu rab yiy goore, mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu. |
28067 | ROM 3:8 | Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo. |
30035 | HEB 1:5 | Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko: «Yaa di sama Doom, bés niki tey, maa la jur,» ba neeti: «Maay doon Baay ci moom, muy Doom ci man»? |
30043 | HEB 1:13 | Ana kan ci malaaka yi la mas ne: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon, say dëggastal»? |