19347 | JER 13:12 | «Nga wax leen kàddu gii: “Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Njaqal biiñ, duy, mu fees. Bu ñu la nee: ‘Dañoo xamul xéll ne njaqal biiñ, duy, mu fees?’ |
19522 | JER 21:13 | Yeen ñi jataayoo xur wi, yeen ñi ci kaw doj wu tell wi, maa ngii fi seen kaw.” Kàddug Aji Sax jee. “Yeen ñi naa: ‘Ku nu manal dara? Ku jote sunu biiri rawtu?’ |
21222 | EZK 27:32 | Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy, jooy la ne: ‘Ana dëkk bu mel ni Tir, mi ñu wedamal nii biir géej?’ |
21507 | EZK 38:13 | Waa Saba ak Dedan ak julay Tarsis, ak mboolem seeni boroom daraja ñoo lay wax ne la: ‘Nangu alal a la yékkatee? Sëxëtoo alalu xaree la taxa bàbbi sa gàngoor, ngir yóbbu xaalis ak wurus, nangu jur ak alal, ba dajalee ca xare ba koom gu takku?’ ” |
22823 | HAB 2:6 | “Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji, fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan: ‘Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul, lii ba kañ?’ Kii di sëfoo nii ay bor!” |