3503 | LEV 25:33 | Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki bànni Israyil. |
15568 | PSA 99:3 | Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko. —Kee sell! |
15570 | PSA 99:5 | Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell! |
15574 | PSA 99:9 | Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa tundam wu sell wa. —Sunu Yàlla Aji Sax jee sell! |