635 | GEN 24:43 | maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’ |
636 | GEN 24:44 | mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.” |
1596 | EXO 3:16 | Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra. |
1624 | EXO 4:22 | Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor. |
1702 | EXO 7:16 | Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu. |
1703 | EXO 7:17 | Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Ni ngay xame ne man maay Aji Sax ji nii la: Dama ne, dinaa dóor ci ndoxum Niil mi yet, wi ci sama loxo, ndox mi soppliku deret; |
1731 | EXO 8:16 | Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma. |
1756 | EXO 9:13 | Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Teelala xëy ca Firawna ëllëg, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji, Yàllay Ebrë yi, dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma. |
7278 | 1SA 2:36 | Su ko defee mboolem ku des ci sa waa kër dina ko sujjóotalsi, ngir as xaalis mbaa as dogu mburu, naan ko ‘Ngalla sas ma lenn ci liggéeyu carxal gi, ndax ma am as dogu mburu su ma lekk’.”» |
7439 | 1SA 10:19 | Waaye tey yeena dëddu seen Yàlla, ji leen musal ci mboolem seeni loraange ak seeni njàqare. Yeena ko ne: ‘Falal buur ci sunu kaw daal!’ Léegi nag taxawleen fi kanam Aji Sax ji, giir ak giir, làng ak làng.”» |
17858 | ISA 7:6 | ‘Nan songi Yuda, tiital leen, nangu ko, fal fa doomu Tabeel buur.’ |
17859 | ISA 7:7 | Waaye Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Loolu du sotti, du am. |
18415 | ISA 36:15 | Te bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!’ |
18418 | ISA 36:18 | Bu leen Esekiya sànk, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli.’ Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri? |
19192 | JER 7:4 | Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’ |
19198 | JER 7:10 | tey dikk taxaw fi sama kanam, biir kër gii ñu ma tudde, te naan: ‘Nun kay raw nanu,’ ba tax ngeen di def mboolem lu siblu lii? |
19347 | JER 13:12 | «Nga wax leen kàddu gii: “Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Njaqal biiñ, duy, mu fees. Bu ñu la nee: ‘Dañoo xamul xéll ne njaqal biiñ, duy, mu fees?’ |
19348 | JER 13:13 | nga ne leen: ‘Aji Sax ji dafa wax ne: Muy buur yi toogal Daawuda cib jalam, di sarxalkat yi, di yonent yi, di mboolem waa Yerusalem, maa ngii di duysi mboolem waa réew mii, ba ñu fees ak màndite. |
19522 | JER 21:13 | Yeen ñi jataayoo xur wi, yeen ñi ci kaw doj wu tell wi, maa ngii fi seen kaw.” Kàddug Aji Sax jee. “Yeen ñi naa: ‘Ku nu manal dara? Ku jote sunu biiri rawtu?’ |
19730 | JER 29:26 | ‘Aji Sax ji da laa fal sarxalkat, nga wuutu Yoyada sarxalkat bi, ngir kër Aji Sax ji am ku ko yor, ba dof bu fiy wax-waxlu ay waxyu, nga jéng ko, yeewe ko càllalay weñ ci baatam. |
19766 | JER 31:6 | Bés dina ñëw déy, wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayim ne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu Siyoŋ, fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’ ”» |
19875 | JER 34:5 | Ci jàmm ngay dee, te ni ñu taalale woon cuuraay say maami buur yi la jiitu, terale leen ko ci seen dëj, ni lañu lay taalale cuuraay, di la jooy naan: ‘Wóoy sunu sang ba dem na!’ Jii wax, maa ko wax.”» Kàddug Aji Sax jee. |
19906 | JER 35:14 | “La Yonadab doomu Rekab santoon ay doomam ne leen: ‘Buleen naan biiñ’ de, jëfees na ko. Duñu naan biiñ ba tey jii ndax wormaal seen santaaney maam. Man nag ay yooni yoon laa leen wax waaye déggaluleen ma. |
19907 | JER 35:15 | Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma. |
20105 | JER 44:26 | Kon nag, yeen mboolem Yudeen ñi sanc Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Maa giñ ci sama tur wu màgg.” Aji Sax jee ko wax. “Ma ne: Sama tur, gémmiñug benn Yudeen dootu ko tudd fi mboolem réewum Misra naan: ‘Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund.’ |
20783 | EZK 13:6 | Seeni peeñu caaxaan la, seeni ngisaane diy fen. Ñu naa: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ te Aji Sax ji yebalu leen! Teewul ñuy xaar kàddu gu sotti. |
20784 | EZK 13:7 | Xanaa du peeñuy caaxaan ngeen gis? Du ngisaaney fen ngeen di waxe, naan: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ te man àdduwma? |
20788 | EZK 13:11 | waxal raaxkati weexal yi, ne leen: ‘Tata jeey màbb, nde waameey wal, ponkali doji yuur ne yureet, ngëlén riddi, bëtt tata ja!’ |
20792 | EZK 13:15 | Maay xëpp sama xadar ci kaw tata ji ak ña ko raaxoon weexal, ne leen: ‘Tata mes, weexalkatu tata mes! |
20875 | EZK 16:44 | «“Yaw Yerusalem, képp kuy léeboo dina la léeboo ne la: ‘Ndey ja, doom ja!’ |
20996 | EZK 20:32 | Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’ |
21023 | EZK 21:15 | Dees koo jonj ngir bóome, jonj koo jonj ba muy tàkk. Ana nu nu mana bége lii? Ngeen ne Aji Sax ji nee: ‘Yetu nguurug Yuda sama doom a ngi fi.’ Waaye saamar bi faalewul benn bant! |
21193 | EZK 27:3 | Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Tir yaa noon: ‘Maaka matub taar!’ |
21222 | EZK 27:32 | Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy, jooy la ne: ‘Ana dëkk bu mel ni Tir, mi ñu wedamal nii biir géej?’ |
21228 | EZK 28:2 | «Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk. |
21255 | EZK 29:3 | Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, te naan: ‘Maa moom sama dex, man ci sama bopp maa ko sàkk!’ |
21261 | EZK 29:9 | Réewum Misraay gental, di ndànd-foyfoy, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. Moo ne: ‘Dex gi maa ko moom, man maa ko sàkk!’ |
21275 | EZK 30:2 | «Yaw nit ki, jottlil waxyu! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’ |
21363 | EZK 33:14 | Su ma nee ku bon ki: ‘Yaw dee rekk mooy sa àtte,’ mu mujj dëddu bàkkaaram, di jëfe njub ak njekk, |
21423 | EZK 35:10 | «“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: ‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii, maa leen moom, noo ciy teg loxo.’ |
21425 | EZK 35:12 | Su boobaa nga xam ne man Aji Sax ji, maa dégg sa jépp waxi ñàkk kersa ja nga nee: ‘Tundi Israyil a ngii ne tasar, dim sëxëtoo mu ñu nu wërsëgale.’ |
21505 | EZK 38:11 | daldi ne: ‘Maay songi réew mu ne ŋàpp, maay dali ca kaw waa réew mu ne finaax, dëkke xel mu dal, te du tata ju wër fu ñu dëkke, ñoom ñépp, du buntu dëkk, du tëjukaayu bunt.’ |
21507 | EZK 38:13 | Waa Saba ak Dedan ak julay Tarsis, ak mboolem seeni boroom daraja ñoo lay wax ne la: ‘Nangu alal a la yékkatee? Sëxëtoo alalu xaree la taxa bàbbi sa gàngoor, ngir yóbbu xaalis ak wurus, nangu jur ak alal, ba dajalee ca xare ba koom gu takku?’ ” |
22823 | HAB 2:6 | “Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji, fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan: ‘Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul, lii ba kañ?’ Kii di sëfoo nii ay bor!” |
25547 | LUK 12:19 | Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ” |
25890 | LUK 20:42 | Daawuda ci boppam moo ne ci téereb Sabóor: “Boroom bi moo ne sama Sang: ‘Toogeel sama ndijoor, |
26034 | LUK 23:30 | Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ” |
27052 | ACT 2:34 | Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor, |
27993 | ACT 28:26 | Mu ne: “Demal ci xeet wii, nga ne leen: ‘Yeenay dégloo déglu, dungeen dégg; ngeen xoolee xoole, dungeen gis.’ |