23275 | MAT 3:14 | Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» |
23374 | MAT 6:23 | waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
23381 | MAT 6:30 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? |
23396 | MAT 7:11 | Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan! |
23439 | MAT 8:25 | Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!» |
23475 | MAT 9:27 | Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
23571 | MAT 12:13 | Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des. |
23624 | MAT 13:16 | «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg! |
23692 | MAT 14:26 | Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu. |
23693 | MAT 14:27 | Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
23695 | MAT 14:29 | Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu. |
23696 | MAT 14:30 | Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!» |
23724 | MAT 15:22 | Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» |
23727 | MAT 15:25 | Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» |
23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
23828 | MAT 18:32 | Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma. |
23854 | MAT 19:23 | Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu! |
23891 | MAT 20:30 | Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23892 | MAT 20:31 | Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
23910 | MAT 21:15 | Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. |
23914 | MAT 21:19 | Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk!» Ca saa sa figg ga daldi wow. |
24000 | MAT 23:13 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci. |
24002 | MAT 23:15 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon. |
24003 | MAT 23:16 | «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.” |
24004 | MAT 23:17 | Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gëna màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell? |
24006 | MAT 23:19 | Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell? |
24010 | MAT 23:23 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. |
24011 | MAT 23:24 | Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem. |
24012 | MAT 23:25 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. |
24013 | MAT 23:26 | Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set. |
24014 | MAT 23:27 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. |
24016 | MAT 23:29 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi. |
24024 | MAT 23:37 | «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen! |
24026 | MAT 23:39 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”» |
24045 | MAT 24:19 | Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal! |
24088 | MAT 25:11 | Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” |
24103 | MAT 25:26 | Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, |
24162 | MAT 26:39 | Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.» |
24172 | MAT 26:49 | Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaam-maalikum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng. |
24220 | MAT 27:22 | Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24221 | MAT 27:23 | Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!» |
24227 | MAT 27:29 | Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndijooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
24238 | MAT 27:40 | naan: «Yaw mi mana toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi!» |
24240 | MAT 27:42 | «Waa jii musal na ñeneen te manula musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko. |
24309 | MRK 1:25 | Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» |
24431 | MRK 4:39 | Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm. |
24526 | MRK 6:50 | Ndaxte ñépp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak ñoom ci saa si ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
24671 | MRK 10:14 | Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. |
24680 | MRK 10:23 | Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!» |
24681 | MRK 10:24 | Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! |
24685 | MRK 10:28 | Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» |
24704 | MRK 10:47 | Noonu mu dégg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: «Yërëm ma, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
24705 | MRK 10:48 | Ci kaw loolu ñu bare gëdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna yuuxu naan: «Yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm ma!» |
24706 | MRK 10:49 | Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» |
24718 | MRK 11:9 | Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! |
24719 | MRK 11:10 | Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw dina barkeel! Ci bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
24723 | MRK 11:14 | Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax. |
24730 | MRK 11:21 | Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!» |
24771 | MRK 12:29 | Noonu Yeesu ne ko: «Bii: “Dégluleen, yéen bànni Israyil! Yàlla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la. |
24787 | MRK 13:1 | Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!» |
24819 | MRK 13:33 | Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot. |
24823 | MRK 13:37 | Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”» |
24864 | MRK 14:41 | Ñetteelu yoon mu délsi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. |
24908 | MRK 15:13 | Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24909 | MRK 15:14 | Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!» |
24913 | MRK 15:18 | Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
24925 | MRK 15:30 | wàccal ci bant bi te musal sa bopp!» |
24934 | MRK 15:39 | Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!» |
24987 | LUK 1:25 | te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!» |
25004 | LUK 1:42 | Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! |
25007 | LUK 1:45 | Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!» |
25030 | LUK 1:68 | «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen! |
25056 | LUK 2:14 | «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa, te ci àddina, na jàmm wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!» |
25101 | LUK 3:7 | Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
25166 | LUK 4:34 | «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» |
25167 | LUK 4:35 | Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanam ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko. |
25168 | LUK 4:36 | Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.» |
25173 | LUK 4:41 | Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne mooy Almasi bi. |
25184 | LUK 5:8 | Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!» |
25257 | LUK 6:42 | Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. |
25280 | LUK 7:16 | Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!» |
25338 | LUK 8:24 | Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
25435 | LUK 10:3 | Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki. |
25487 | LUK 11:13 | Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!» |
25501 | LUK 11:27 | Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!» |
25513 | LUK 11:39 | Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw, yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeena fees ak càcc ak mbon! |
25514 | LUK 11:40 | Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam? |
25516 | LUK 11:42 | Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des. |
25517 | LUK 11:43 | Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma. |
25520 | LUK 11:46 | Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam. |
25548 | LUK 12:20 | Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?” |
25552 | LUK 12:24 | Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi! |
25556 | LUK 12:28 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? |
25584 | LUK 12:56 | Naaféq yi ngeen doon! Man ngeena ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax manuleena ràññee li jamonoy léegi ji di tekki? |
25602 | LUK 13:15 | Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko? |
25612 | LUK 13:25 | Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” |
25614 | LUK 13:27 | Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!” |
25621 | LUK 13:34 | «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen! |
25622 | LUK 13:35 | Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”» |