23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23240 | MAT 2:2 | Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» |
23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23246 | MAT 2:8 | Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.» |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23256 | MAT 2:18 | «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.» |
23258 | MAT 2:20 | ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.» |
23261 | MAT 2:23 | Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.» |
23263 | MAT 3:2 | Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.» |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23275 | MAT 3:14 | Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» |
23276 | MAT 3:15 | Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23281 | MAT 4:3 | Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.» |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23284 | MAT 4:6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”» |
23285 | MAT 4:7 | Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» |
23287 | MAT 4:9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
23295 | MAT 4:17 | Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» |
23297 | MAT 4:19 | Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.» |
23306 | MAT 5:3 | «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23314 | MAT 5:11 | «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man. |
23316 | MAT 5:13 | «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. |
23320 | MAT 5:17 | «Buleen defe ne ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man. |
23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23328 | MAT 5:25 | «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la. |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23352 | MAT 6:1 | «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23358 | MAT 6:7 | «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare. |
23365 | MAT 6:14 | «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23370 | MAT 6:19 | «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko. |
23373 | MAT 6:22 | «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, |
23375 | MAT 6:24 | «Kenn manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal. |
23376 | MAT 6:25 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk, walla lu ngeen wara naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen wara sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? |
23379 | MAT 6:28 | «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
23386 | MAT 7:1 | «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. |
23391 | MAT 7:6 | «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen. |
23392 | MAT 7:7 | «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. |
23397 | MAT 7:12 | «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi. |
23398 | MAT 7:13 | «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. |
23400 | MAT 7:15 | «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23409 | MAT 7:24 | «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj. |
23416 | MAT 8:2 | Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.» |
23417 | MAT 8:3 | Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. |
23418 | MAT 8:4 | Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.» |
23420 | MAT 8:6 | ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.» |
23421 | MAT 8:7 | Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.» |
23422 | MAT 8:8 | Waaye njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. |
23424 | MAT 8:10 | Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. |
23427 | MAT 8:13 | Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér. |
23431 | MAT 8:17 | Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» |
23433 | MAT 8:19 | Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» |
23434 | MAT 8:20 | Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» |
23435 | MAT 8:21 | Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.» |
23436 | MAT 8:22 | Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.» |
23439 | MAT 8:25 | Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!» |
23440 | MAT 8:26 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
23441 | MAT 8:27 | Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?» |
23443 | MAT 8:29 | Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?» |
23445 | MAT 8:31 | Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.» |
23446 | MAT 8:32 | Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma. |
23450 | MAT 9:2 | Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» |
23451 | MAT 9:3 | Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.» |
23452 | MAT 9:4 | Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol? |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23457 | MAT 9:9 | Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp. |
23459 | MAT 9:11 | Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» |
23460 | MAT 9:12 | Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. |
23462 | MAT 9:14 | Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?» |
23463 | MAT 9:15 | Yeesu ne leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor. |
23466 | MAT 9:18 | Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.» |
23470 | MAT 9:22 | Bi mu ko defee Yeesu waññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa. |
23472 | MAT 9:24 | Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal. |
23475 | MAT 9:27 | Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
23476 | MAT 9:28 | Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.» |
23477 | MAT 9:29 | Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.» |
23478 | MAT 9:30 | Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.» |
23481 | MAT 9:33 | Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, masuñu koo gis ci Israyil.» |
23482 | MAT 9:34 | Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
23485 | MAT 9:37 | Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. |
23491 | MAT 10:5 | Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari. |
23497 | MAT 10:11 | «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba. |
23502 | MAT 10:16 | «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax. |
23507 | MAT 10:21 | «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu. |
23510 | MAT 10:24 | Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam. |
23518 | MAT 10:32 | «Koo xam ne nangu nga ma ci kanam nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw. |
23520 | MAT 10:34 | «Te it buleen defe ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale. |
23526 | MAT 10:40 | «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni. |