23244 | MAT 2:6 | “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”» |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23270 | MAT 3:9 | te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii. |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23284 | MAT 4:6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”» |
23285 | MAT 4:7 | Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23325 | MAT 5:22 | Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara. |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23364 | MAT 6:13 | Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu, waaye yal nanga nu musal ci lu bon. Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.” |
23382 | MAT 6:31 | Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan?” walla: “Lu nu wara sol?” |
23389 | MAT 7:4 | Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw? |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23407 | MAT 7:22 | Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” |
23408 | MAT 7:23 | Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Masuma leena xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.” |
23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23453 | MAT 9:5 | Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gëna yomb? |
23461 | MAT 9:13 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» |
23493 | MAT 10:7 | Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.” |
23538 | MAT 11:10 | Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.” |
23545 | MAT 11:17 | ne leen: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” |
23546 | MAT 11:18 | Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23565 | MAT 12:7 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul. |
23602 | MAT 12:44 | Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk. |
23621 | MAT 13:13 | “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb. |
23623 | MAT 13:15 | Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.” |
23635 | MAT 13:27 | «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?” |
23636 | MAT 13:28 | Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?” |
23638 | MAT 13:30 | Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”» |
23706 | MAT 15:4 | Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” |
23708 | MAT 15:6 | kooku amatul warugaru teral baayam.” Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada. |
23711 | MAT 15:9 | Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”» |
23743 | MAT 16:2 | Noonu Yeesu ne leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.” |
23744 | MAT 16:3 | Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, waaye manuleena ràññee firndey jamono ji nu tollu. |
23789 | MAT 17:20 | Yeesu ne leen: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» |
23822 | MAT 18:26 | Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.” |
23824 | MAT 18:28 | «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.” |
23825 | MAT 18:29 | Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.” |
23829 | MAT 18:33 | Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?” |
23836 | MAT 19:5 | te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.” |
23865 | MAT 20:4 | Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.” |
23867 | MAT 20:6 | Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?” |
23868 | MAT 20:7 | Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” |
23869 | MAT 20:8 | «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.” |
23873 | MAT 20:12 | naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” |
23876 | MAT 20:15 | ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” |
23898 | MAT 21:3 | Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leena soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.» |
23900 | MAT 21:5 | «Waxal waa Siyoŋ: “Seen buur a ngi ñëw ci yéen; ku lewet la, te war mbaam-sëf, dig cumbur, doomu mbaam.”» |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
23908 | MAT 21:13 | naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.» |
23911 | MAT 21:16 | Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu ne leen: «Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleena jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?» |
23916 | MAT 21:21 | Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def. |
23920 | MAT 21:25 | La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
23921 | MAT 21:26 | Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.» |
23923 | MAT 21:28 | «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu reseñ.” |
23924 | MAT 21:29 | Taaw ba ne ko: “Demuma,” waaye gannaaw loolu xelam yedd ko, mu dem. |
23925 | MAT 21:30 | Gannaaw gi, baay ba ñëw ca tofo ba, wax ko noonu. Mu ne ko: “Waaw,” waaye demul.» |
23932 | MAT 21:37 | Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” |
23933 | MAT 21:38 | Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.” |
23937 | MAT 21:42 | Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi? “Doj wi tabaxkat yi sànni; mujj na di doju koñ; ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.” |
23945 | MAT 22:4 | Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ” |
23950 | MAT 22:9 | Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.” |
23953 | MAT 22:12 | Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig. |
23954 | MAT 22:13 | Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.” |
23965 | MAT 22:24 | «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.” |
23973 | MAT 22:32 | “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.» |
23978 | MAT 22:37 | Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.” |
23980 | MAT 22:39 | Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” |
23984 | MAT 22:43 | Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne: |
23985 | MAT 22:44 | “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ” |
23986 | MAT 22:45 | Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» |
23994 | MAT 23:7 | Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “kilifa gi.” |
23995 | MAT 23:8 | Waaye yéen buñu leen wooye “kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen. |
23996 | MAT 23:9 | Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw. |
23997 | MAT 23:10 | Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist. |
24003 | MAT 23:16 | «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.” |
24005 | MAT 23:18 | Dangeen ne it: “Ku giñe sarxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.” |
24017 | MAT 23:30 | Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.” |
24026 | MAT 23:39 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”» |
24031 | MAT 24:5 | Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare. |
24041 | MAT 24:15 | «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam. |
24049 | MAT 24:23 | «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm. |
24052 | MAT 24:26 | «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen, mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm. |
24074 | MAT 24:48 | Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,” |
24083 | MAT 25:6 | «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.” |
24085 | MAT 25:8 | Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.” |
24086 | MAT 25:9 | Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?” |
24088 | MAT 25:11 | Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” |
24089 | MAT 25:12 | Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.” |
24097 | MAT 25:20 | Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.” |
24098 | MAT 25:21 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24099 | MAT 25:22 | Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.” |
24100 | MAT 25:23 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24102 | MAT 25:25 | Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.” |