23214 | MAT 1:1 | Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. |
23215 | MAT 1:2 | Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam; |
23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23217 | MAT 1:4 | Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon; |
23218 | MAT 1:5 | Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi, |
23219 | MAT 1:6 | miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri; |
23220 | MAT 1:7 | Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf; |
23221 | MAT 1:8 | Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas; |
23222 | MAT 1:9 | Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya; |
23223 | MAT 1:10 | Esekiya Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas; |
23224 | MAT 1:11 | Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon. |
23225 | MAT 1:12 | Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, |
23226 | MAT 1:13 | miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor; |
23227 | MAT 1:14 | Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; |
23228 | MAT 1:15 | Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; |
23229 | MAT 1:16 | Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. |
23230 | MAT 1:17 | Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. |
23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23232 | MAT 1:19 | Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23234 | MAT 1:21 | Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.» |
23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23237 | MAT 1:24 | Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon. |
23238 | MAT 1:25 | Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu. |
23239 | MAT 2:1 | Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. |
23240 | MAT 2:2 | Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23242 | MAT 2:4 | Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo. |
23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23244 | MAT 2:6 | “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”» |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23246 | MAT 2:8 | Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.» |
23247 | MAT 2:9 | Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. |
23248 | MAT 2:10 | Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy. |
23249 | MAT 2:11 | Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir. |
23250 | MAT 2:12 | Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew. |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23252 | MAT 2:14 | Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga. |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23254 | MAT 2:16 | Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. |
23255 | MAT 2:17 | Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan: |
23256 | MAT 2:18 | «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.» |
23257 | MAT 2:19 | Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra, |
23258 | MAT 2:20 | ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.» |
23259 | MAT 2:21 | Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil. |
23260 | MAT 2:22 | Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. |
23261 | MAT 2:23 | Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.» |
23262 | MAT 3:1 | Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude. |
23263 | MAT 3:2 | Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.» |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23265 | MAT 3:4 | Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem. |
23266 | MAT 3:5 | Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan. |
23267 | MAT 3:6 | Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. |
23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23269 | MAT 3:8 | Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, |
23270 | MAT 3:9 | te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii. |
23271 | MAT 3:10 | Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si. |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23273 | MAT 3:12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.» |
23274 | MAT 3:13 | Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. |
23275 | MAT 3:14 | Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» |
23276 | MAT 3:15 | Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23279 | MAT 4:1 | Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane. |
23280 | MAT 4:2 | Yeesu nekk fa te lekkul ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi, doora xiif. |
23281 | MAT 4:3 | Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.» |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23283 | MAT 4:5 | Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga. |
23284 | MAT 4:6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”» |
23285 | MAT 4:7 | Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» |
23286 | MAT 4:8 | Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
23287 | MAT 4:9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23289 | MAT 4:11 | Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. |
23290 | MAT 4:12 | Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile. |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23292 | MAT 4:14 | Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: |
23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
23294 | MAT 4:16 | xeet wa nekkoon cig lëndëm, gis na leer gu mag, ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim, leer fenkal na leen.» |
23295 | MAT 4:17 | Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23297 | MAT 4:19 | Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.» |
23298 | MAT 4:20 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. |
23299 | MAT 4:21 | Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen. |
23300 | MAT 4:22 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom. |
23301 | MAT 4:23 | Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, |
23302 | MAT 4:24 | ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. |
23303 | MAT 4:25 | Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan. |
23304 | MAT 5:1 | Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom. |
23305 | MAT 5:2 | Mu daldi leen jàngal naan: |
23306 | MAT 5:3 | «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23307 | MAT 5:4 | Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. |
23308 | MAT 5:5 | Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina. |
23309 | MAT 5:6 | Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg. |
23310 | MAT 5:7 | Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen, ndax dees na leen yërëm. |
23311 | MAT 5:8 | Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen, ndax dingeen gis Yàlla. |
23312 | MAT 5:9 | Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen, ndax dees na leen tudde doomi Yàlla. |
23313 | MAT 5:10 | Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |