23218 | MAT 1:5 | Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi, |
23224 | MAT 1:11 | Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon. |
23225 | MAT 1:12 | Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, |
23230 | MAT 1:17 | Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. |
23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23237 | MAT 1:24 | Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon. |
23239 | MAT 2:1 | Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23244 | MAT 2:6 | “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”» |
23246 | MAT 2:8 | Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.» |
23247 | MAT 2:9 | Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. |
23248 | MAT 2:10 | Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy. |
23250 | MAT 2:12 | Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew. |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23254 | MAT 2:16 | Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. |
23255 | MAT 2:17 | Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan: |
23256 | MAT 2:18 | «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.» |
23257 | MAT 2:19 | Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra, |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23274 | MAT 3:13 | Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. |
23276 | MAT 3:15 | Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23279 | MAT 4:1 | Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane. |
23281 | MAT 4:3 | Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.» |
23283 | MAT 4:5 | Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga. |
23284 | MAT 4:6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”» |
23285 | MAT 4:7 | Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”» |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23295 | MAT 4:17 | Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» |
23299 | MAT 4:21 | Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen. |
23301 | MAT 4:23 | Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, |
23304 | MAT 5:1 | Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom. |
23314 | MAT 5:11 | «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man. |
23315 | MAT 5:12 | Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu. |
23316 | MAT 5:13 | «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. |
23319 | MAT 5:16 | Na seen leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw. |
23320 | MAT 5:17 | «Buleen defe ne ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man. |
23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23326 | MAT 5:23 | Booy yóbbu nag sa sarax ca sarxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree, |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23332 | MAT 5:29 | Bu la sa bëtu ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. |
23333 | MAT 5:30 | Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23337 | MAT 5:34 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla; |
23338 | MAT 5:35 | bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi. |
23339 | MAT 5:36 | Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte manuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar. |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23348 | MAT 5:45 | ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi. |
23351 | MAT 5:48 | Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate. |
23352 | MAT 6:1 | «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw. |
23353 | MAT 6:2 | Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23355 | MAT 6:4 | ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23357 | MAT 6:6 | Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23359 | MAT 6:8 | Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax. |
23360 | MAT 6:9 | Yéen nag nii ngeen wara ñaane: “Sunu Baay bi nekk ci kaw, yal na sa tur di lu ñu sellal, |
23365 | MAT 6:14 | «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam. |
23366 | MAT 6:15 | Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ. |
23369 | MAT 6:18 | ngir sa koor baña feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23370 | MAT 6:19 | «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko. |
23373 | MAT 6:22 | «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, |
23376 | MAT 6:25 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk, walla lu ngeen wara naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen wara sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? |
23377 | MAT 6:26 | Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare? |
23381 | MAT 6:30 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? |
23382 | MAT 6:31 | Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan?” walla: “Lu nu wara sol?” |
23383 | MAT 6:32 | Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. |
23385 | MAT 6:34 | Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko. |
23386 | MAT 7:1 | «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. |
23391 | MAT 7:6 | «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen. |
23396 | MAT 7:11 | Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan! |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23407 | MAT 7:22 | Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” |
23410 | MAT 7:25 | Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa. |
23412 | MAT 7:27 | Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.» |
23413 | MAT 7:28 | Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngleem, |
23415 | MAT 8:1 | Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko. |
23417 | MAT 8:3 | Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. |
23419 | MAT 8:5 | Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, |
23424 | MAT 8:10 | Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. |
23428 | MAT 8:14 | Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng. |
23429 | MAT 8:15 | Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo. |