23214 | MAT 1:1 | Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. |
23219 | MAT 1:6 | miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri; |
23230 | MAT 1:17 | Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23234 | MAT 1:21 | Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.» |
23246 | MAT 2:8 | Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.» |
23261 | MAT 2:23 | Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.» |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23281 | MAT 4:3 | Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.» |
23284 | MAT 4:6 | Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”» |
23316 | MAT 5:13 | «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. |
23317 | MAT 5:14 | Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du mana nëbbu. |
23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23379 | MAT 6:28 | «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
23400 | MAT 7:15 | «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. |
23401 | MAT 7:16 | Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte reseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam? |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23418 | MAT 8:4 | Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.» |
23421 | MAT 8:7 | Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.» |
23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23434 | MAT 8:20 | Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» |
23443 | MAT 8:29 | Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?» |
23446 | MAT 8:32 | Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma. |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23461 | MAT 9:13 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» |
23475 | MAT 9:27 | Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
23502 | MAT 10:16 | «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax. |
23504 | MAT 10:18 | Dees na leen yóbbu ngir man ci kanam i boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut. |
23509 | MAT 10:23 | Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.» |
23532 | MAT 11:4 | Yeesu ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko. |
23543 | MAT 11:15 | Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp. |
23546 | MAT 11:18 | Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23549 | MAT 11:21 | Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. |
23551 | MAT 11:23 | Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. |
23555 | MAT 11:27 | Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it manula xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal. |
23561 | MAT 12:3 | Noonu Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon? |
23566 | MAT 12:8 | Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.» |
23575 | MAT 12:17 | Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: |
23576 | MAT 12:18 | «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub. |
23577 | MAT 12:19 | Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw, te kenn du dégg baatam ci mbedd yi. |
23578 | MAT 12:20 | Du dammte barax bu banku, te mees guy saxar, du ko fey, ba kera mu yégal njub, ba daan. |
23581 | MAT 12:23 | Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?» |
23590 | MAT 12:32 | Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira. |
23598 | MAT 12:40 | Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf. |
23611 | MAT 13:3 | Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. |
23617 | MAT 13:9 | Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» |
23621 | MAT 13:13 | “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb. |
23622 | MAT 13:14 | Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan: “Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara. |
23637 | MAT 13:29 | Mu ne leen: “Déedéet, ngir baña buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi. |
23640 | MAT 13:32 | Doomu fuddën moo gëna tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.» |
23643 | MAT 13:35 | Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Dinaa leen wax ciy léeb, di yégle yëf yu nëbbu li dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.» |
23645 | MAT 13:37 | Noonu Yeesu ne leen: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi; |
23649 | MAT 13:41 | Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar, |
23651 | MAT 13:43 | Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» |
23665 | MAT 13:57 | Kon ñu daldi koy xeeb. Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.» |
23681 | MAT 14:15 | Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu mana lekk?» |
23699 | MAT 14:33 | Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.» |
23712 | MAT 15:10 | Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam: |
23724 | MAT 15:22 | Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» |
23725 | MAT 15:23 | Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.» |
23743 | MAT 16:2 | Noonu Yeesu ne leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.” |
23754 | MAT 16:13 | Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?» |
23757 | MAT 16:16 | Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» |
23760 | MAT 16:19 | Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.» |
23768 | MAT 16:27 | Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci ndamul Baayam, ànd ak ay malaakaam; bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam. |
23769 | MAT 16:28 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.» |
23774 | MAT 17:5 | Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» |
23778 | MAT 17:9 | Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.» |
23781 | MAT 17:12 | Teewul maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nara sonal léegi Doomu nit ki.» |
23791 | MAT 17:22 | Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi; |
23842 | MAT 19:11 | Yeesu ne leen: «Du ñépp ñoo mana nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk. |
23859 | MAT 19:28 | Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil. |
23865 | MAT 20:4 | Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.” |
23868 | MAT 20:7 | Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” |
23879 | MAT 20:18 | «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, |
23882 | MAT 20:21 | Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.» |
23889 | MAT 20:28 | Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.» |
23891 | MAT 20:30 | Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23892 | MAT 20:31 | Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23897 | MAT 21:2 | ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen. |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
23910 | MAT 21:15 | Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. |
23914 | MAT 21:19 | Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk!» Ca saa sa figg ga daldi wow. |
23924 | MAT 21:29 | Taaw ba ne ko: “Demuma,” waaye gannaaw loolu xelam yedd ko, mu dem. |
23928 | MAT 21:33 | Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu reseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci reseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki. |
23936 | MAT 21:41 | Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.» |
23937 | MAT 21:42 | Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi? “Doj wi tabaxkat yi sànni; mujj na di doju koñ; ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.” |
23950 | MAT 22:9 | Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.” |
23983 | MAT 22:42 | «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.» |
23984 | MAT 22:43 | Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne: |
23986 | MAT 22:45 | Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» |
23991 | MAT 23:4 | Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam. |
23992 | MAT 23:5 | Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb. |