23218 | MAT 1:5 | Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi, |
23221 | MAT 1:8 | Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas; |
23222 | MAT 1:9 | Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya; |
23896 | MAT 21:1 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe, |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
23910 | MAT 21:15 | Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. |
24029 | MAT 24:3 | Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» |
24153 | MAT 26:30 | Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. |
24710 | MRK 11:1 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem, |
24718 | MRK 11:9 | Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! |
24719 | MRK 11:10 | Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw dina barkeel! Ci bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
24789 | MRK 13:3 | Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko: |
24849 | MRK 14:26 | Noonu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. |
25043 | LUK 2:1 | Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji. |
25126 | LUK 3:32 | Daawuda mooy doomu Isayi; Isayi, Obedd; Bowas; Salmon; Nason. |
25829 | LUK 19:29 | Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem, |
25837 | LUK 19:37 | Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis. |
25932 | LUK 21:37 | Yeesoo ngi daan yendoo jàngle ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa. |
25972 | LUK 22:39 | Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom. |
26451 | JHN 8:1 | Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya. |
26662 | JHN 12:13 | Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel buuru Israyil!» |
27004 | ACT 1:12 | Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem. |
28248 | ROM 9:25 | Moom la wax ci téereb Ose ne: «Ñi nekkul woon sama xeet dinaa leen ko def, ñi bokkul woon ci sama mbëggeel, dinaa leen ci boole.» |
28419 | ROM 16:15 | Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam. Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp. |
29618 | COL 4:9 | Onesim lay àndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci yéen. Dinañu leen xamal lépp lu xew fii. |
29892 | 2TI 1:16 | Waaye Onesifor daa na faral di dëfal sama xol; na Boroom bi sotti yërmandeem ci këram. Rusul woon sax ci samay jéng, |
29956 | 2TI 4:19 | Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa kër Onesifor. |
30015 | PHM 1:10 | Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi. |
30773 | REV 1:8 | Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa di Omega, Maay ki Nekk, di ki nekkoon démb, di kiy ñëw ëllëg, man Aji Man ji.» |
31128 | REV 21:6 | Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa di Omega, di njàlbéen gi, di muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara. |
31162 | REV 22:13 | Man maay Alfa di Omega, ki jëkk tey mujj, maay njàlbéen gi, di muj gi. |