23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
26982 | JHN 21:15 | Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.» |
26983 | JHN 21:16 | Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.» |
28088 | ROM 3:29 | Walla ndax nag Yawut yi rekk la fi nekkal? Ndax nekkalu fi it ñu dul Yawut? Ahakay! |
28099 | ROM 4:9 | Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Ahakay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub. |
28274 | ROM 10:18 | Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Ahakay! Mbind mi wax na ne: «Seen baat jolli na ci ñeenti xébla yépp, seen wax wër na àddina sépp.» |
28275 | ROM 10:19 | Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa dafa jëkkoona wax ne: «Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla, merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.» |
28447 | 1CO 1:16 | Ahakay! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas. Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen. |
28653 | 1CO 10:18 | Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel sarxalukaay ba? Ahakay! |