23240 | MAT 2:2 | Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» |
23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23249 | MAT 2:11 | Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir. |
23258 | MAT 2:20 | ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.» |
23267 | MAT 3:6 | Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. |
23297 | MAT 4:19 | Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.» |
23299 | MAT 4:21 | Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen. |
23302 | MAT 4:24 | ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. |
23320 | MAT 5:17 | «Buleen defe ne ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man. |
23392 | MAT 7:7 | «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. |
23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23427 | MAT 8:13 | Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér. |
23442 | MAT 8:28 | Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woona jaar foofa. |
23443 | MAT 8:29 | Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?» |
23460 | MAT 9:12 | Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. |
23476 | MAT 9:28 | Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.» |
23486 | MAT 9:38 | Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.» |
23490 | MAT 10:4 | Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nara wor Yeesu. |
23515 | MAT 10:29 | Ñaari picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. |
23544 | MAT 11:16 | «Niti jamono jii nag, lan laa leen mana méngaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit, |
23556 | MAT 11:28 | «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay. |
23607 | MAT 12:49 | Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk. |
23659 | MAT 13:51 | Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.» |
23677 | MAT 14:11 | Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam. |
23683 | MAT 14:17 | Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.» |
23699 | MAT 14:33 | Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.» |
23701 | MAT 14:35 | Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp. |
23732 | MAT 15:30 | Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen. |
23733 | MAT 15:31 | Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil. |
23736 | MAT 15:34 | Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.» |
23742 | MAT 16:1 | Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.» |
23866 | MAT 20:5 | Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu. |
23868 | MAT 20:7 | Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” |
23873 | MAT 20:12 | naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” |
23883 | MAT 20:22 | Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.» |
23894 | MAT 20:33 | Ñu ne ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.» |
23902 | MAT 21:7 | Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca. |
23903 | MAT 21:8 | Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa. |
23922 | MAT 21:27 | Ñu ne Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. |
23926 | MAT 21:31 | Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw ba.» Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23934 | MAT 21:39 | Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.» |
23936 | MAT 21:41 | Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.» |
23960 | MAT 22:19 | Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon. |
23962 | MAT 22:21 | Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» |
23967 | MAT 22:26 | Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom ñaareel ba. |
23981 | MAT 22:40 | Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.» |
23983 | MAT 22:42 | «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.» |
24021 | MAT 23:34 | Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo dëkk. |
24029 | MAT 24:3 | Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» |
24046 | MAT 24:20 | Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésub noflaay bi. |
24080 | MAT 25:3 | Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diw; |
24085 | MAT 25:8 | Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.” |
24087 | MAT 25:10 | «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diw ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj. |
24127 | MAT 26:4 | Ñu daldi gise, ba xam lu ñu mana fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko. |
24180 | MAT 26:57 | Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, sarxalkat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje. |
24189 | MAT 26:66 | Lu ngeen ci xalaat?» Ñu ne ko: «Yoon teg na ko dee.» |
24190 | MAT 26:67 | Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko, |
24200 | MAT 27:2 | Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma. |
24202 | MAT 27:4 | ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu ne ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.» |
24205 | MAT 27:7 | Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya. |
24219 | MAT 27:21 | Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu ne ko: «Barabas.» |
24220 | MAT 27:22 | Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24223 | MAT 27:25 | Ñépp ne ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.» |
24227 | MAT 27:29 | Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndijooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
24231 | MAT 27:33 | Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.» |
24237 | MAT 27:39 | Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko, |
24245 | MAT 27:47 | Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.» |
24261 | MAT 27:63 | Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.” |
24268 | MAT 28:4 | Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee. |
24270 | MAT 28:6 | waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon, |
24301 | MRK 1:17 | Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.» |
24321 | MRK 1:37 | Bi ñu ko gisee, ñu ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.» |
24346 | MRK 2:17 | Noonu Yeesu dégg ko, mu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla; ñëwuma woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» |
24347 | MRK 2:18 | Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?» |
24374 | MRK 3:17 | Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay— ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi»— |
24375 | MRK 3:18 | Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; |
24389 | MRK 3:32 | Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.» |
24390 | MRK 3:33 | Waaye Yeesu ne leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?» |
24404 | MRK 4:12 | Noonu la, ngir: “Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara, di déglu bu baax waaye duñu xam dara, ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar te Yàlla baal leen.”» |
24433 | MRK 4:41 | Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?» |
24448 | MRK 5:15 | Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal. |
24449 | MRK 5:16 | Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya. |
24452 | MRK 5:19 | Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.» |
24475 | MRK 5:42 | Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm. |
24489 | MRK 6:13 | Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen. |
24491 | MRK 6:15 | Ñeneen ne: «Kii Ilyaas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.» |
24513 | MRK 6:37 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?» |
24514 | MRK 6:38 | Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen seeti.» Ñu dem seeti ne ko: «Juróomi mburu ak ñaari jën.» |
24516 | MRK 6:40 | Ñu toog nag ay géewi juróom fukk ak téeméer. |
24517 | MRK 6:41 | Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, sant Yàlla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. Ñaari jën yi it mu séddale ko ñépp. |
24520 | MRK 6:44 | Ñu lekkoon nag matoon na limu juróomi junniy góor. |
24534 | MRK 7:2 | Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee. |
24569 | MRK 7:37 | Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.» |
24574 | MRK 8:5 | Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.» |
24578 | MRK 8:9 | Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor. |
24588 | MRK 8:19 | bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.» |