23695 | MAT 14:29 | Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu. |
23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
26952 | JHN 20:16 | Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi». |
27295 | ACT 9:10 | Amoon na nag ci Damaas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.» |
27331 | ACT 10:3 | Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!» |
30862 | REV 6:1 | Noonu ma gis Gàtt ba dindi tayu gu jëkk ga, te ma daldi dégg kenn ca ñeenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni dënnu naan: «Ñëwal!» |
30864 | REV 6:3 | Gàtt ba dindi na ñaareelu tayu ga, ma dégg ñaareelu mbindeef ma naan: «Ñëwal!» |
30866 | REV 6:5 | Mu dindi ñetteelu tayu ga, ma dégg ñetteelu mbindeef ma ne: «Ñëwal!» Ma xool, gis fas wu ñuul, gawar ba yor ab peesekaay. |
30868 | REV 6:7 | Mu dindi ñeenteelu tayu ga, ma dégg ñeenteelu mbindeef ma naan: «Ñëwal!» |
31166 | REV 22:17 | Te Xelum Yàlla ak séetu Gàtt bi ñu ngi naan: «Ñëwal!» Képp ku dégg wax jii, na ne: «Ñëwal!» Na képp ku mar, ñëw; ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara. |