24026 | MAT 23:39 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”» |
25622 | LUK 13:35 | Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”» |
26136 | JHN 1:23 | Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”» |
27858 | ACT 24:21 | xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”» |