23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23637 | MAT 13:29 | Mu ne leen: “Déedéet, ngir baña buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi. |
24052 | MAT 24:26 | «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen, mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm. |
24111 | MAT 25:34 | «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina. |
24338 | MRK 2:9 | Lan moo gëna yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”? |
24732 | MRK 11:23 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu. |
24771 | MRK 12:29 | Noonu Yeesu ne ko: «Bii: “Dégluleen, yéen bànni Israyil! Yàlla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la. |
25479 | LUK 11:5 | Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu. |
25619 | LUK 13:32 | Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.” |
25669 | LUK 15:12 | Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may wara féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam. |
25678 | LUK 15:21 | Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.” |
25719 | LUK 16:30 | Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.” |
25726 | LUK 17:6 | Boroom bi ne leen: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen mana ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax. |
25819 | LUK 19:19 | Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” |
26676 | JHN 12:27 | «Léegi nag damaa jàq. Lu may wara wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nara xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu. |
27359 | ACT 10:31 | mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla. |
27779 | ACT 22:7 | Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?” |
27793 | ACT 22:21 | Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”» |
27905 | ACT 26:14 | Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.” |