24703 | MRK 10:46 | Bi loolu wéyee ñu agsi ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xawa bare, am gumba gu tudd Bartime— liy tekki «doomu Time», toog ci wetu yoon wi, di yelwaan. |
26608 | JHN 11:16 | Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!» |
26960 | JHN 20:24 | Fekk na Tomaa, mi bokk ci fukki taalibe yi ak ñaar, te turam di tekki «Séex bi», nekku fa woon, bi Yeesu ñëwee. |
29185 | GAL 3:16 | Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam», mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan», maanaam Kirist. |
30088 | HEB 4:7 | Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii», bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jota lim: «Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi, buleen dëgër bopp.» |
30306 | HEB 12:27 | Ci li mu wax: «Beneen yoon», dafay xamle ne Yàlla dina dindi yi ñu mana yëngal, maanaam li ñu sàkk, ngir li ñu manula yëngal sax ba fàww. |
30371 | JAS 2:11 | Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo», teg na ca ne: «Bul bóome.» Ku njaaloowul nag, waaye nga bóome, jàdd nga yoon wépp. |