Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word-Word,    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23239  MAT 2:1  Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
23900  MAT 21:5  «Waxal waa Siyoŋ: “Seen buur a ngi ñëw ci yéen; ku lewet la, te war mbaam-sëf, dig cumbur, doomu mbaam.”»
24011  MAT 23:24  Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
24169  MAT 26:46  Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
24610  MRK 9:3  ay yéreem di ray-rayi, weex tàll, te fóotukatu àddina manu leen weexale nii.
24821  MRK 13:35  Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di délsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël.
24971  LUK 1:9  Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
25013  LUK 1:51  Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom, te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
25157  LUK 4:25  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
25593  LUK 13:6  Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.
25705  LUK 16:16  «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.
26309  JHN 5:30  Manumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw.
26364  JHN 6:38  Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
26423  JHN 7:26  Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
26459  JHN 8:9  Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.
26962  JHN 20:26  Bi ñu ca tegee ayu-bés, taalibe Yeesu ya dajewaat ca biir kër ga, Tomaa itam a nga fa woon. Bunt yépp tëju woon nañu, waaye Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!»
26999  ACT 1:7  Mu ne leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
27437  ACT 13:6  Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.
27496  ACT 14:13  Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Sarxalkat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
27585  ACT 16:33  Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
27853  ACT 24:16  Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
28022  ROM 1:24  Moo tax Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg, ñu sóobu ciy ñaawteef, di jëflante lu gàccelu ci seeni cér.
28372  ROM 15:1  Nun ñi dëgër ci sunu ngëm, war nanoo nangu ñi seen ngëm néew te am ci lu ñuy sikki-sàkka, te baña yem ci wut sunu bànneex.
28375  ROM 15:4  Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar.
28385  ROM 15:14  Bokk yi, wóor na ma ne baax ngeen ba fa mbaax mana yem, fees dell ak xam-xam, ba mana jàngleente mbiri Yàlla ci seen biir.
28596  1CO 8:1  Léegi nag, ci li jëm ci yàpp wi ñu jébbal xërëm yi: nun ñépp am nanu xam-xam, loolu dëgg la. Xam-xam day tax ba nit yég boppam, waaye mbëggeel day yékkati ngëm.
28605  1CO 8:10  Su amee ku ngëmam néew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca màggalukaayu xërëm ya, ndax du ko xiir mu lekk yàppu sarax?
28710  1CO 12:8  Am na ku Yàlla sédde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi.
28914  2CO 3:5  Du caageen nag ne àttan nanu dara ci sunu man-man, ba nu yaakaar dara ci sunu bopp, waaye sunu kàttan ci Yàlla lay jóge.
28972  2CO 6:6  Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ,
29007  2CO 8:7  Gannaaw nag wone ngeen cawarte gu tollu noonu, ci ngëm, ci wax, ci xam-xam, ci farlu gu mat, ak ci seen mbëggeel ci nun, sawareleen noonu it ci jëfu ndimbal lii.
29009  2CO 8:9  Ndaxte yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist umpu leen, ni mu futtee am-amam, ba ñàkk ngir yéen, ndax ngeen woomle cig ñàkkam.
29031  2CO 9:7  Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi.
29063  2CO 11:6  Bu ma dul jàmbaari wax it, néewuma xam-xam, te won nanu leen ko ci bépp mbir ak ci bépp fànn.
29099  2CO 12:9  Mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man.
29294  EPH 1:21  mu tiim lu sore malaaka yépp, muy kilifa, boroom sañ-sañ, boroom doole mbaa buur, te gëna màgg wépp tur wu ñu mana tudd, muy tey, muy ëllëg.
29416  EPH 6:12  Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi.
29648  1TH 2:11  Xam ngeen ne dénk nanu leen kenn-kenn, ni baay di def ak doomam, dëfalal leen seen xol te dëggal ci yéen, ngeen dund dund gu neex Yàlla, moom mi leen di woo, ngeen séddu ci nguuram ak ndamam.
29650  1TH 2:13  Te it dunu noppee sant Yàlla ci lii: ba ngeen jotee kàddug Yàlla, gi nu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni kàddug nit waaye ni kàddug Yàlla, ndaxte moom la ci dëgg-dëgg, te mu ngi jëf ci yéen ñi gëm.
29665  1TH 3:8  Ndaxte noo ngi dund dëgg-dëgg, ndegam yéena ngi sax ci Boroom bi.
29875  1TI 6:20  Céy yaw Timote, sàmmal li la Yàlla dénk! Tanqamlul waxi neen yu àddina kese, te dëddu werantey ñi mbubboo xam-xam, fekk dañoo réer.
29940  2TI 4:3  Ndaxte jamono dina ñëw, joo xam ne nit ñi dootuñu xajoo njàngle mu wér mi, waaye dinañu jublu ci seeni bëgg-bëgg, di fortaatu jànglekat yu leen di jay.
30019  PHM 1:14  Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli.
30405  JAS 4:1  Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér?
30432  JAS 5:11  Xam ngeen ne ñiy góor-góorlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen muñ ga Ayóoba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy ñeewante la te bare yërmande.
30455  1PE 1:14  Gannaaw gaayi Yàlla yu koy déggal ngeen, buleen toppati bëgg-bëgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Yàlla.
30534  1PE 5:2  Lii laa leen di ñaan: sàmmleen géttug Yàlla, gi mu leen dénk, di ko wottu, waxuma ci sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli; ngeen def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal.
30551  2PE 1:5  Na loolu tax ngeen góor-góorlu, ba yokk ci seen ngëm njàmbaar, ci njàmbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci not sa bopp.
30561  2PE 1:15  Te dinaa góor-góorlu, ngir sama gannaaw ngeen di fàttaliku li ma leen doon wax.
30580  2PE 2:13  muy seen peyug njubadi. Xawaare bëccëg ndarakàmm mooy seen bànneex. Su ñuy lekkandoo ak yéen, dañuy bànneexu ci seeni bëgg-bëgg, di ay gàkk ak i sikk ci seen biir.
30603  2PE 3:14  Kon nag samay soppe, gannaaw yéena ngi séentu loolu, góor-góorluleen, ngir bu Kirist ñëwee, mu fekk leen ci jàmm, ngeen baña am benn gàkk mbaa sikk.
30747  JUD 1:7  Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo sawara ba fàww.
30880  REV 7:2  Ma gis it meneen malaaka, muy yéeg, jóge penku, yor màndargaalu Yàlla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb ñeenti malaaka ya ñu joxoon sañ-sañ, ñu yàq suuf ak géej,
31074  REV 18:12  seen wurus ak seen xaalis ak seeni jamaa ak yeneen per; seeni piis yu rafet ak piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen dénk wu xeeñ ak seen yëf yi ñu defare bëñi ñay walla dénk wu jafe walla xànjar walla weñ walla marbë;
31077  REV 18:15  Baana-baana, yi daan jaay yëf yooyu ba woomle, dinañu sore ndax ragal coonoom. Dinañu jooy di naqarlu,
31079  REV 18:17  sa alal ju bare jépp naaw na ci waxtu!» Noonu ñépp ñiy dawal gaal ak ñi ciy tukki ak ñi ciy liggéey ak ñi ciy baana-baana, ñépp di sore bérab boobu,