Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word-Word-Word    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23916  MAT 21:21  Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
24152  MAT 26:29  Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaaw-si-tey ndoxum reseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum reseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
25715  LUK 16:26  Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgga jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgga jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.”
26618  JHN 11:26  Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27156  ACT 5:28  ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
27312  ACT 9:27  Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
27589  ACT 16:37  Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanam ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgga sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
27792  ACT 22:20  Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
27901  ACT 26:10  Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci sarxalkat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoona bëgga rey, ànd naa ci.
28541  1CO 6:6  Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanam ñi gëmul lañu koy defe!
28754  1CO 14:8  Rax-ca-dolli su liit gi jibul bu leer, kuy mana waajal xare ba?
28801  1CO 15:15  Rax-ca-dolli gis nañu ne seedeel nanu Yàlla ay fen, ndaxte seede nanu ci mbiram ne dekkal na Yeesu, te fekk dekkalu ko, su néew yi dul dekki.
28961  2CO 5:16  Kon nag gannaaw-si-tey xoolatunu kenn ci gis-gisu àddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu àddina, léegi xooleetunu ko noonu.
29017  2CO 8:17  Bi nu ko laajee, mu ñëw ci yéen, nangu na, te rax-ca-dolli cawarteem tollu na, ba nu mana wax ne ci coobarey boppam la jóge, jëm ci yéen.
29038  2CO 9:14  Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen.
29457  PHP 1:29  Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,
29485  PHP 2:27  Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xawa dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma baña am tiis ci kaw tiis.
29496  PHP 3:8  Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
29701  1TH 5:13  rax-ca-dolli ngeen naw leen seen kem kàttan te bëgg leen ndax seen liggéey. Na jàmm am ci seen biir.
29843  1TI 5:13  Te du yem ci bëgga séyaat rekk, waaye ku tayel lay doon; di ku wër kër ak kër, rax-ca-dolli réy làmmiñ te deñ kumpa, di wax lu yoonam nekkul.
29955  2TI 4:18  Rax-ca-dolli dina ma musal ci bépp jëf ju ñaaw, tette ma ci jàmm, ba tàbbal ma ci nguuram gu kawe ga. Yal na yelloo ndam ba fàww. Amiin.
30137  HEB 7:6  Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi.
30151  HEB 7:20  Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay sarxalkat te kenn giñul.
30735  3JN 1:10  Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru bokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi.