Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word.    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23214  MAT 1:1  Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
23219  MAT 1:6  miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri;
23224  MAT 1:11  Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
23229  MAT 1:16  Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
23230  MAT 1:17  Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
23231  MAT 1:18  Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
23232  MAT 1:19  Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
23233  MAT 1:20  Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
23237  MAT 1:24  Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
23238  MAT 1:25  Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
23239  MAT 2:1  Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
23241  MAT 2:3  Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
23242  MAT 2:4  Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo.
23245  MAT 2:7  Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
23246  MAT 2:8  Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
23247  MAT 2:9  Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
23248  MAT 2:10  Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy.
23249  MAT 2:11  Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
23250  MAT 2:12  Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
23252  MAT 2:14  Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
23253  MAT 2:15  Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
23254  MAT 2:16  Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
23259  MAT 2:21  Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
23260  MAT 2:22  Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
23261  MAT 2:23  Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.»
23262  MAT 3:1  Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
23265  MAT 3:4  Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
23266  MAT 3:5  Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
23267  MAT 3:6  Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
23268  MAT 3:7  Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
23270  MAT 3:9  te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
23271  MAT 3:10  Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.
23272  MAT 3:11  Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
23274  MAT 3:13  Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
23276  MAT 3:15  Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
23277  MAT 3:16  Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
23279  MAT 4:1  Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
23280  MAT 4:2  Yeesu nekk fa te lekkul ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi, doora xiif.
23283  MAT 4:5  Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
23286  MAT 4:8  Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
23289  MAT 4:11  Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
23290  MAT 4:12  Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
23291  MAT 4:13  Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
23296  MAT 4:18  Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
23298  MAT 4:20  Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
23299  MAT 4:21  Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
23300  MAT 4:22  Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
23302  MAT 4:24  ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
23303  MAT 4:25  Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan.
23304  MAT 5:1  Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom.
23306  MAT 5:3  «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
23307  MAT 5:4  Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol.
23308  MAT 5:5  Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina.
23309  MAT 5:6  Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg.
23310  MAT 5:7  Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen, ndax dees na leen yërëm.
23311  MAT 5:8  Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen, ndax dingeen gis Yàlla.
23312  MAT 5:9  Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen, ndax dees na leen tudde doomi Yàlla.
23313  MAT 5:10  Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
23314  MAT 5:11  «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man.
23315  MAT 5:12  Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
23316  MAT 5:13  «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
23317  MAT 5:14  Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du mana nëbbu.
23318  MAT 5:15  Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp.
23319  MAT 5:16  Na seen leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw.
23320  MAT 5:17  «Buleen defe ne ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man.
23321  MAT 5:18  Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am.
23322  MAT 5:19  Ku tebbi nag ba gëna tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23323  MAT 5:20  Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23325  MAT 5:22  Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara.
23327  MAT 5:24  nanga fa bàyyi sa sarax ca kanam sarxalukaay ba, nga jëkka dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax.
23328  MAT 5:25  «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la.
23329  MAT 5:26  Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj.
23331  MAT 5:28  Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel.
23332  MAT 5:29  Bu la sa bëtu ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore.
23333  MAT 5:30  Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara.
23335  MAT 5:32  Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa soxna te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga.
23338  MAT 5:35  bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi.
23339  MAT 5:36  Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte manuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar.
23340  MAT 5:37  Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
23342  MAT 5:39  Waaye man maa ngi leen di wax ne buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndijoor, jox ko ba ca des.
23343  MAT 5:40  Ku la bëgga kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag.
23344  MAT 5:41  Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar.
23345  MAT 5:42  Mayal ku lay ñaan, te bul jox gannaaw ku lay leb.
23348  MAT 5:45  ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.
23351  MAT 5:48  Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate.
23352  MAT 6:1  «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.
23353  MAT 6:2  Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
23355  MAT 6:4  ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
23356  MAT 6:5  «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
23357  MAT 6:6  Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
23358  MAT 6:7  «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
23359  MAT 6:8  Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax.
23361  MAT 6:10  yal na sa nguur ñëw, yal na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.
23364  MAT 6:13  Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu, waaye yal nanga nu musal ci lu bon. Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
23365  MAT 6:14  «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam.
23366  MAT 6:15  Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.
23367  MAT 6:16  «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
23369  MAT 6:18  ngir sa koor baña feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
23370  MAT 6:19  «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko.
23371  MAT 6:20  Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko.