26154 | JHN 1:41 | Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist». |
26155 | JHN 1:42 | Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer». |
28886 | 2CO 1:18 | Wóor na Yàlla ne li nu leen di wax, du «waaw» ju ànd ak «déedéet». |
30919 | REV 9:11 | Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku ebrë, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat». |