23911 | MAT 21:16 | Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu ne leen: «Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleena jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?» |
26291 | JHN 5:12 | Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?» |
26433 | JHN 7:36 | Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen mana dem fa may nekk”?» |
26812 | JHN 16:17 | Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, ñu waxante ne: «Lu muy wax nii: “Ci kanam tuuti dungeen ma gisati; bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,” ak naan: “Ndaxte maa ngi dem ca Baay ba”?» |
26893 | JHN 18:39 | Seen aada laaj na, ma bàyyil leen kenn, saa su ñuy def màggalu bésu Mucc bi. Xanaa ma bàyyil leen “buuru Yawut yi”?» |