54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
60 | GEN 3:4 | Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! |
93 | GEN 4:13 | Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! |
318 | GEN 12:19 | Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» |
356 | GEN 14:19 | Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf! |
357 | GEN 14:20 | Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
440 | GEN 18:15 | Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» |
450 | GEN 18:25 | Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
465 | GEN 19:7 | Mu ne leen: «Bokk yi, ngalla buleen def lu bon loolu waay! |
467 | GEN 19:9 | Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. |
476 | GEN 19:18 | Lóot nag ne ko: «Déet, sang bi! |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
521 | GEN 21:7 | Mu neeti: «Éy, ku noon Ibraayma, Saarataa ngay nàmpal! Teewul ma jural ko góor, te muy mag.» |
549 | GEN 22:1 | Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.» |
555 | GEN 22:7 | Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» |
559 | GEN 22:11 | Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» |
619 | GEN 24:27 | daldi ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, sama Yàllay sang, Ibraayma, moom mi masula noppee laaye biir sama sang, te masu koo ñàkke worma. Man it, Aji Sax ji wommat na ma ba sama kër bokki sang!» |
623 | GEN 24:31 | Mu ne ko: «Yaw mi Aji Sax ji barkeel, agsil boog! Looy toog ci àll bi; waajalal naa la ab dal, te giléem yi am nañu fu ñu nekk.» |
652 | GEN 24:60 | Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, te sa askan teg ay bañam tànk.» |
681 | GEN 25:22 | Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji. |
702 | GEN 26:9 | Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» |
748 | GEN 27:20 | Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
773 | GEN 27:45 | Bu sa meru mag giifee, ba mu fàtte li nga ko def, dinaa yónnee, ñu jëlsi la. Duma seetaan mukk, ba boole leen ñàkk, yeen ñaar ñépp, ci benn bés!» |
774 | GEN 27:46 | Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» |
791 | GEN 28:17 | Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.» |
803 | GEN 29:7 | Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!» |
810 | GEN 29:14 | Laban da ne ko: «Yaw kay sama jarbaat nga lenqe!» Yanqóoba toog na fa ak moom lu mat weer. |
842 | GEN 30:11 | Leya ne: «Ndaw wërsëg wu réy!» daldi ko tudde Gàdd (mu firi Wërsëg). |
844 | GEN 30:13 | Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte). |
889 | GEN 31:15 | Doonunu lu moy ay doxandéem ci moom de! Nde da noo jaay, lekk sunu njég, ba mu jeex tàkk. |
902 | GEN 31:28 | Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii! |
965 | GEN 33:4 | Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy! |
1029 | GEN 35:17 | Ba mu demee ba mat wa gëna metti, rewlikat ba ne ko: «Muñal nag, ndax góor laati de!» |
1103 | GEN 37:19 | Ña nga naan: «Boroom gént gaa ngee di ñëw! |
1114 | GEN 37:30 | Ba loolu amee mu jóge ca, dem ca ay rakkam ne leen: «Xale ba nekkatu fa de! Te man xawma nu may def léegi.» |
1117 | GEN 37:33 | Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!» |
1239 | GEN 41:43 | ba noppi waral ko watiiru ku sës rëkk ci moom Firawna, te fu mu ware ñu jiitu ko, di yéene naan: «Sujjóotleen!» Noonu la ko Firawna fale, mu yilif Misra gépp. |
1255 | GEN 42:2 | Mu ne leen: «Dégg naa ne pepp am na ca Misra. Demleen jëndali nu ca, ndax nu mana dund, ba xiif bañ noo rey kay!» |
1289 | GEN 42:36 | Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!» |
1298 | GEN 43:7 | Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!» |
1305 | GEN 43:14 | Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.» |
1320 | GEN 43:29 | Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!» |
1330 | GEN 44:5 | Ndax li ngeen jël du sama kaasu sang, bi muy naane, rawatina di ko gisaanee? Lu ñaaw ngeen def nii!”» |
1332 | GEN 44:7 | Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu! |
1353 | GEN 44:28 | Kenn ki dem, wacc ma, ma ne moom kay, aw rabu àll a ko daggate! Gisaatuma ko ba tey jii. |
1356 | GEN 44:31 | bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbsi— aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw. |
1359 | GEN 44:34 | Ndax xawma nan laay delloo ca sama baay te ànduma ak xale bi. Yàlla buma fekke njekkar, li ciy dal sama baay!» |
1360 | GEN 45:1 | Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam. |
1362 | GEN 45:3 | Yuusufa nag ne magam ya: «Man mii maay Yuusufa! Mbaa sama baay a ngi dund?» Magam ya nag manuñu koo tontu, ndax booba njàqare jàpp na leen. |
1385 | GEN 45:26 | Ñu wax ko ne ko: «Ndekete Yuusufaa ngi dund! te sax mooy kilifag réewum Misra gépp.» Ba Yanqóoba déggee loolu, yaramam dafa dee goyy ca saa sa, ndaxte gëmu leen. |
1387 | GEN 45:28 | Israyil daldi ne: «Moom kay na dund rekk! Sama doom Yuusufaa ngi dund. Man kay dinaa dem ba gis ko, bala ma fee jóge.» |
1389 | GEN 46:2 | Yàlla wax ak Israyil foofa ca guddi ci biir gént ne ko: «Yanqóoba, Yanqóoba!» Israyil ne ko: «Naam.» |
1429 | GEN 47:8 | Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» |
1436 | GEN 47:15 | Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» |
1446 | GEN 47:25 | Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.» |
1492 | GEN 49:18 | «Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal! |
1518 | GEN 50:11 | Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra). |
1561 | EXO 2:6 | Naka la ko ne ubbet, yem ca xale ba, muy liir bu góor, xale bay jooy, yaram wa daw, mu ne: «Kii de ndeysaan, ci doomi Ebrë yi la!» |
1575 | EXO 2:20 | Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!» |
1584 | EXO 3:4 | Ba Aji Sax ji Yàlla gisee Musaa jàdd, di xoolsi, ca gajj ba la àddoo, ne ko: «Musaa, Musaa!» Mu ne ko: «Maa ngi.» |
1637 | EXO 5:4 | Buuru Misra ne leen: «Yeen Musaa ak Aaróona, lu waral ngeen di jële mbooloo mi ci seeni liggéey? Laggleen ca seeni sas waay!» |
1638 | EXO 5:5 | Firawna dellu ne: «Baadoolo yi ne xas tey ci réew mi, ngeen nar leena dëdduloo seeni sas!» |
1641 | EXO 5:8 | Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: “May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!” |
1650 | EXO 5:17 | Firawna ne leen: «Yaafus yi ngeen doon! Yaafus a leen tax di wax naan: “May nu, nu dem rendili Aji Sax ji sarax.” |
1651 | EXO 5:18 | Neleen mott, liggéeyi! Du menn boob mu ñu leen di jox. Te du tee ngeen matal seen limu móol.» |
1656 | EXO 5:23 | Ba ma demee ca Firawna, di wax ci sa tur ba tey, mu ngi lor bànni Israyil, sa ñoñ, te xettliwoo leen sax!» |
1695 | EXO 7:9 | «Bu leen Firawna waxee ne leen: “Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: “Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.» |
1730 | EXO 8:15 | Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon. |
1785 | EXO 10:7 | Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» |
1786 | EXO 10:8 | Ñu délloosi nag Musaak Aaróona ca Firawna, mu ne leen: «Demleen màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Waaw, ñiy dem sax, ñan la?» |
1788 | EXO 10:10 | Firawna ne leen: «Ãa, yal na leen Aji Sax ji saxoo taxawu walla, ndegam maa leen di bàyyi moos, ngeen dem, yóbbaale seen njaboot! Xam ngeen ne naruleen njub de. |
1789 | EXO 10:11 | Mukk laa wax! Du dangeen di màggal Aji Sax ji? Demleen boog, yeen ñiy góor!» Ba loolu amee ñu dàq leen, ñu jóge ca Firawna, |
1806 | EXO 10:28 | Firawna nag ne Musaa: «Neel mott! Bul fexe ba taxawati sama kanam! Ndax bés boo jàkkaarlooteek man, kera ngay dee.» |
1807 | EXO 10:29 | Musaa ne ko: «Noonu la sax de. Duma jàkkaarlooteek yaw moos!» |
1815 | EXO 11:8 | Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. |
1848 | EXO 12:31 | Ba loolu amee Firawna woolu Musaak Aaróona ca guddi googu, ne leen: «Ayca! Mott! Soreleen sama waa réew, yeen ak seeni bokk! Laggleen, jaamuji Aji Sax ji, li ngeen bëgg. |
1849 | EXO 12:32 | Te itam yóbbaaleleen seen juroo jur, gu gudd ak gu gàtt, li ngeen bëgg rekk, te ne mott! Waaye ñaanaaleleen ma seen Yàlla nag, mu barkeel ma.» |
1850 | EXO 12:33 | Ba mu ko defee waa Misra soññ bànni Israyil, ngir ñu gaaw génn réew ma, ndax booba ña nga naan: «Nun ñépp ay dee!» |
1902 | EXO 14:12 | Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!» |
1915 | EXO 14:25 | Mu boole ca téye mbegey watiir ya, ba neexatuñoo dawal. Waa Misra ne: «Nan daw gaaw, ba rëcc bànni Israyil, ndax kat Aji Sax ji moo leen di xeexal, te moo dal ci sunu kaw!» |
1924 | EXO 15:3 | «Aji Sax ji jàmbaari xare ji, Aji Sax jeey turam! |
1927 | EXO 15:6 | «Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax. |
1929 | EXO 15:8 | Nga wal sag noo, ndox ya tegloo, wal ma ne sàtt, jaloo jalu, ndoxi xóotey géej way deeŋ! |
1931 | EXO 15:10 | Waaye sa ngelaw nga wal, géej mëdd leen, ñu diigandoo ni beteex biir géej mbàmbulaan! |
1986 | EXO 17:2 | Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» |
2443 | EXO 32:4 | Mu nangoo ko ci seeni loxo, liggéey ko ba sàkk ci sëllu wu ñu móol. Ci kaw loolu ñu naan: «Bànni Israyiloo, seen Yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!» |
2447 | EXO 32:8 | Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”» |
2448 | EXO 32:9 | Aji Sax ji dellu ne Musaa: «Maa gis askan wii, askan wu dëgër bopp a ngii! |
2456 | EXO 32:17 | Ci kaw loolu Yosuwe dégg coowal mbooloo may xaacu. Mu ne Musaa: «Coowal xaree ngoog ca dal ba!» |
2463 | EXO 32:24 | Ma ne leen: “Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!» |
2465 | EXO 32:26 | Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak Aji Sax ji, fii ci man!» Leween ñépp dikk, yéew ko. |
2489 | EXO 33:15 | Musaa ne ko: «Soo demul yaw ci sa bopp kay, bu nu jële fii! |
2492 | EXO 33:18 | Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!» |
2506 | EXO 34:9 | ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.» |
2997 | LEV 10:19 | Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» |
3098 | LEV 13:45 | «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!” |