20441 | LAM 3:18 | Ca laa ne sama doolee (/muñukaaya/darajaa) jeex! ak sama yaakaar ci Aji Sax ji. |
20488 | LAM 3:65 | Dërkiisalal seen xol (Tegleen njàqarey xol / Muural seenum xel,) na leen sag alkànde ñeel. |
22881 | ZEP 2:7 | Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moom, ñu di ca fore, bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon. Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal, tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.) |
23069 | ZEC 9:1 | Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo rot ci kaw réewum Addarag, ba dali ca kaw Damaas. Du ci mboolem giiri Israyil rekk la Aji Sax ji ne jàkk bëtam, waaye doom aadama yépp la ne jàkk. (xg / Gëti nit ñi, ba ci giiri Israyil gépp kat, ñu ngi ne jàkk ci Aji Sax ji.) |
23081 | ZEC 9:13 | Yuda déy laay bank, muy samag xala, te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi. Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan). Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar. |
23103 | ZEC 11:6 | Dootuma yërëm waa réew mi (/àddina) déy,» Kàddug Aji Sax jee! «Maa ngii di teg doom aadama yi, ku nekk ci loxol moroomam, ak ci loxol buuram, ñu not réew mi, te duma leen xettli ci seen loxo.» |
23190 | MAL 3:1 | «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. |