Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   ;    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

16  GEN 1:16  Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi.
27  GEN 1:27  Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind.
28  GEN 1:28  Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»
36  GEN 2:5  genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul.
40  GEN 2:9  Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon.
43  GEN 2:12  di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë.
44  GEN 2:13  Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp;
45  GEN 2:14  turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat.
50  GEN 2:19  Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom.
62  GEN 3:6  Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.
70  GEN 3:14  Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp.
73  GEN 3:17  Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.
75  GEN 3:19  saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
87  GEN 4:7  Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»
89  GEN 4:9  Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?»
98  GEN 4:18  Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg.
105  GEN 4:25  Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.»
152  GEN 6:14  «Yaw nag wutal dénku sippar, yettal ci sa bopp gaal gu mag; nga sàkk ci ay néeg, te diw ko koltaar biir ak biti.
155  GEN 6:17  «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee.
157  GEN 6:19  Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc.
224  GEN 9:18  Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan.
249  GEN 10:14  ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi.
259  GEN 10:24  Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber;
271  GEN 11:4  daldi ne: «Ayca nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.»
296  GEN 11:29  Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay.
301  GEN 12:2  ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;
307  GEN 12:8  Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.
312  GEN 12:13  Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.»
328  GEN 13:9  Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.»
362  GEN 15:1  Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»
393  GEN 16:11  tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar.
396  GEN 16:14  Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret.
403  GEN 17:5  Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare.
413  GEN 17:15  Ba loolu weesee Yàlla waxaat na Ibraayma, ne ko: «Sa soxna tuddatul Sarayi; léegi moo di Saarata.
414  GEN 17:16  Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.»
422  GEN 17:24  Ibraayma amoon na juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), bi muy xaraf;
466  GEN 19:8  Dégluleen, ma wax leen; man, am naa ñaari doom yu jigéen, te xamuñu góor. Mayleen ma, ma yót leen leen, ngeen def leen lu leen neex. Rikk buleen def góor ñii dara, ndaxte samay gan lañu.»
478  GEN 19:20  Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?»
492  GEN 19:34  Ca ëllëg sa taaw ba wax rakk ji, ne ko: «Man tëdd naa ak sama baay biig; guddig tey it, danu koy nàndalaat biiñ, su ko defee nga dugg tëdd ak moom, ndax sunu xeetu baay du fey.»
513  GEN 20:17  Fekk na Aji Sax ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom.
540  GEN 21:26  Abimeleg nag ne ko: «Xawma ku la def jooju jëf de, ndax yaw waxoo ma ci dara; guléet ma dégg ko tey.»
554  GEN 22:6  Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar.
560  GEN 22:12  Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»
576  GEN 23:4  «Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»
578  GEN 23:6  «Déglul rekk, kilifa gi. Kilifa gu mag nga ci sunu biir. Dangay tànn ci sunuy bàmmeel, bi la neex, suul fa néew bi; kenn ci nun du la tere, nga suul sa néew ci bàmmeelam.»
583  GEN 23:11  «Déglul, ma wax la, kilifa gi, fabal tool bi, booleek xuntim xeer, mi ci nekk far. Maa la ko jox ci sama kanami bokk; jëlal, denc fa sa néew.»
587  GEN 23:15  «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?»
623  GEN 24:31  Mu ne ko: «Yaw mi Aji Sax ji barkeel, agsil boog! Looy toog ci àll bi; waajalal naa la ab dal, te giléem yi am nañu fu ñu nekk.»
635  GEN 24:43  maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’
686  GEN 25:27  Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu te bëggoon toogaayu kër.
694  GEN 26:1  Ba loolu wéyee xiif am ca réew ma, muy xiif bu wuute ak ba woon ca jamonoy Ibraayma; Isaaxa nag dem Gerar ca Abimeleg, buurub waa Filisti.
696  GEN 26:3  Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
717  GEN 26:24  Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.»
721  GEN 26:28  Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw kóllëre.
791  GEN 28:17  Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.»
834  GEN 30:3  Mu ne ko: «Xoolal, sama jaam Bilaa ngii; dëkkoo ko, ndax mu amal ma doom, ba jabootal ma.»
837  GEN 30:6  Bi loolu amee Rasel ne: «Yàlla àtte na ma; dégg na sama ñaan, ba may ma doom.» Mu tudde ko nag Dan (mu firi Kiy àtte).
860  GEN 30:29  Yanqóoba ne ko: «Yaw ci sa bopp xam nga ni ma la liggéeyale ak ni sa gétt mujj mel ndax man;
882  GEN 31:8  Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer.
902  GEN 31:28  Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii!
917  GEN 31:43  Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom?
921  GEN 31:47  Laban tudde bérab ba Yegar Saaduta; Yanqóoba tudde ko Galet.
934  GEN 32:6  ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”»
938  GEN 32:10  Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
993  GEN 34:12  Limal-leen ma warugar yi ak nu mu mana tollu, boole ci may gi; dinaa joxe lu ngeen ma sas; mayleen ma janq bi rekk.»
1022  GEN 35:10  ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la wooye Yanqóoba; léegi yaa di Israyil.» Mu tudde ko nag Israyil.
1034  GEN 35:22  Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.
1045  GEN 36:4  Ada am ak Esawu Elifas; Basmat am ca Rewel.
1057  GEN 36:16  ak Kora ak Gatam ak Amaleg, ku ci nekk ak làngam. Làngi Elifas, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Ada.
1058  GEN 36:17  Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu.
1127  GEN 38:7  Er, taawub Yuda boobee, doonoon ku Aji Sax ji seede coxoram; Aji Sax ji nag rey ko.
1232  GEN 41:36  Dund boobooy doon sàqu réew mi diiru juróom ñaari ati xiif yiy dal ci réewum Misra; su ko defee waa réew mi duñu loru ci xiif bi.»
1236  GEN 41:40  Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.»
1251  GEN 41:55  Ba waa Misra xiifee, dañoo dem jooytuji dund ca Firawna. Mu wax ak ñépp ne leen: «Demleen ca Yuusufa; lu mu leen wax, defleen ko.»
1264  GEN 42:11  te nun ñépp a bokk baay, di nit ñu maandu; nun kay, sang bi, dunu ay yëddukat.»
1273  GEN 42:20  Waaye nangeen ma indil seen rakk, ba ma xam ne li ngeen wax dëgg la; su ko defee dungeen dee.» Ñu daldi ne: «Waaw,»
1274  GEN 42:21  te naa ci seen biir: «Céy su nu yégoon, sunu àqu rakk a nu topp nii, ndax danu koo seetaanoon, mu nekk ci njàqarey xol, di nu tinu, te faalewunu ko; looloo waral sunu njàqarey tey jii.»
1275  GEN 42:22  Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.»
1284  GEN 42:31  Nu ne ko: “Nun ay nit ñu maandu lanu, dunu ay yëddukat;
1286  GEN 42:33  Waa ja yilif réew ma ne nu: “Ni may xame ne ñu maandu ngeen, nii la: dangeen may bàyyeek kenn ci yeen, te dem yóbbul dund seen waa kër, yi nekk ci xiif;
1289  GEN 42:36  Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!»
1300  GEN 43:9  Dige naa sama bakkan; boo yeboo laaj ma ko. Bu ma la ko délloosilul, ba teg ko fi sa kanam, maa lay tooñ sama giiru dund.
1314  GEN 43:23  Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko.
1323  GEN 43:32  Loolu wees ñu may Yuusufa moom rekk; ber doomi baayam ya. Waa Misra ña fa doon lekke it, ñu beral leen seen ndab, ngir waa Misra daawuñu bokk ak Ebrë yi lekk, ndax mbañ la fa woon.
1334  GEN 44:9  Ngalla kilifa gi, yaay sunu sang; koo ko fekke ci nun rekk, boo yeboo reyal, ñi des ci nun doxe fa, di say jaam.»
1342  GEN 44:17  Mu ne leen: «Jomb naa loolu. Ki ñu fekk kaas bi ci loxoom mooy doon sama jaam; ñi ci des dellu ca seen baay ci jàmm.»
1368  GEN 45:9  «Gaawleen dellu ci sama baay te ne ko: “Sa doom Yuusufa nee na: Yàlla fal na ma kilifag Misra gépp; ñëwal fi man, nu mu gëna gaawe.
1392  GEN 46:5  Ba loolu amee Yanqóoba jóge Beerseba; doomi Israyil boole seen baay ak seeni doom ak seeni soxna, yeb leen ci watiir, yi Firawna yónnee woon, ngir yóbbu leen.
1466  GEN 48:14  Israyil nag jàllawle ay loxoom, tàllal ndijooram, teg ko ca kaw boppu Efrayim, mi gën di ndaw; càmmoñam tege ca boppu Manase, doonte mooy taaw.
1476  GEN 49:2  Dajeleen te déglu ma, man Yanqóoba seen baay; teewluleen seen baay Israyil.
1485  GEN 49:11  Mooy yeew mbaamam cig reseñ, cumbur ma féeteek car, ba ca gën; muy fóote ay yéreem biiñ, di sumb mbubbam ci ndoxum reseñ.
1503  GEN 49:29  Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntim bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba.
1530  GEN 50:23  te gis na doomi Efrayim, ba gis sëti Efrayim sax; rax ca dolli doomi Makir, mi Manase jur, fa kanamam lañu juddoo.
1536  EXO 1:3  ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin;
1550  EXO 1:17  Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund.
1552  EXO 1:19  Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.»
1574  EXO 2:19  Ñu ne ko: «Ab waa Misra daal, moo nu xettli ca sàmm ya; rootal na nu sax, ba wëgg jur gi.»
1588  EXO 3:8  Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.
1608  EXO 4:6  Aji Sax ji dellooti ne ko: «Léegi dugalal sa loxo, teg ko ci sa dënn.» Musaa dugal loxoom, teg ko ca dënnam; ba mu ko génnee, mu defi àkk, xobbiku.
1618  EXO 4:16  Na lay waxal ak mbooloo mi; su ko defee sa kàddu di kàddoom, te yaw nga mel ci moom ni Yàlla.